Alxuraan ci Wolof: Suraat XCII – Guddi
Wàcce ci Màkka 21 laaya Benn – Senn – Menn la – Raax Menn – Raax Yërëm 1- Ag guddi fu mu tallale muraayam 2- Ag bëccëg fu mu leere naññ 3- Ag kooku sàkk góor ak jiggéen 4- Seeeni coono daaanu wuute li ñuy diir. 5- Kiy joxe te ragal Yàlla 6- Ki teg…
Ñi seen xel matadi ci biir Ndakaaru…
Taalif “Les poetes de la rue”
Laaj-toontu ak Njaga Mbay
Jaar-jaaru woykat bu jege woon askanam Ci sanwiye 1999, yeneekay Lasli/Njëlbéen amoon na laaj-tootu bu yaatu ag Njaga Mbay, doon ca feeñal ay jaar-jaaram. Waxtaan woowu Njaga Mbay amoon ak Séydu Nuuru Njaay, di njiital Lasli/Njëlbéen moom lañu leen fi indilaat, di ci ñeel woykat bu mag bu àddina sépp jooy. Kan mooy Njaga Mbay?…
Ku wax feeñ: demokaraasi ag làkki réew mi
Wote bi nu dëgmal, ñépp xam na ñu ko, wote bu jeggi dayoo la: ndax ci la ëllëgu réew mi aaju! Wote tànn la wan yoon la Senegaal war a teggu jëm ca kanam mbaa mu teggi ko, dellu gannaaw: lawla cat! Wante li ñu soxal ci jukki bii, lu lëkkëloog loolu gaa, wante leneen…
Cëru-biir nit
jukki bi: http://www.hotkey.net.au/~mjackson/Language/Vocab/Anatomy%20Organs.htm
Isaa Bokar Si ” Yaaya Jàmme mooy ndeyyi-mbill mi ci Gambi ak Kasamaas”
Isaa Bokaar Si, ambaasadeur Yaaya Jàmme la woon, bokkoon na ak Y. Jàmme nekk tàkk-der. Ku ko xam la, ku xam fu ma jaar la…Déggluleen
Waxi Wolof Njaay
Juddu ci gëléem, nàmp ci mbaam Bu sunu boroom bi bëggee, ñépp ñàkk Bant su tooyee yomb a jubbanti Juróom-ñeenti walaakaana soo leen bëggee jubbanti, soo moytuwul fukkeel leen Boroom kuddu du lakk Wax dëgg du wàññi wërsëg Nit ki, li nga ko gëne, booy sangu bu ko summi Doxkat du fekke dëju maamam Njëriñ…
jiggéen yu mën góor…
Ci at yi ak wéer yi weesu, mel na ni Afrik dafa dellu fa baaxi maam nekkoon, te mooy wormaal, naw, solool jiggéen. Bu ñu ko fatte fii ci Afrik, jiggéen na fi ma masa fallu, di yaay, di lingeer, di ndey-ji-réew, di buur, ca Misira démb, Nibi, Meroe, ba ci Waalo ak Kajoor. Kon…
Téy la Mandela di am 94 at…
Téy ci 18eelu fan ci wéeru Suliye lay Nelson Mandela, mi kenn dul nettali ay jàllooreem di am 94 at! Réewum Afrik di Sid yépp, Afrik gépp ak àddina sépp di ko berndeel di ko delloo njukkël.Bésam bi di bésu téy la mbootaayu xeet tuddee bésu Mandelaa ngir magal manduteem, paspasam, fonk boppam ag askanam…