|
Ndaali-Maali walla Mande benn la woon ci nguuru nit ku ñuul yu mag yi nekkoon démb ci déndub Afrik. Moo fi wuutu woon ndaali GANA ci Afrik sóowu-jànt. Gana moom itam moo donnoon jàllooreey yeneeni nguur yu mel ni Aksum , Kuus, Nibi ak Misiraay-démb bu Buur-Fari ya.
Ndaali Maali jàpp nanu ne ca 10eelu xarnu ba ci 14eelu xarnu ba la fi nguuram lawoon, ëmboon réew yi téy: Maali, Senegal, Gambi, Gine, Niseer, ak bëj-boppu Gànaar...Ña fa doonoon Buur-daali seen jàlloree jàll xarnu yi ba yegsi ci nun: ñoom Mansa Musaa, Sumaaworo Kante, Sunjata Keytaa ak ñeneen. Booba Afrik a yore woon wurus àddina si, nit di jógge fu nekk di waliwaansi di wutsi xam-xam. Tekki bii nu leen fi indil téy nag ay-boroom xam-xami cosaan yu mag yu Senegaal, Mali, Gine ay gawlo ak ñeneen ñoo dekkalaat ca Kankan (Gine) sàrt bi doon doxal ndaali Maali. Maanaam na ñu tërëlewoon seen jëflaante ci seen biir sosiete ci fànn yépp: koom-koom, politik ak yeneen. Kon sàrt bii téy bi réew mu mel ni Senegaal tollee diggante ba ñépp aj seen noo di dégglu li àttekat yiy saytu sàrti-réew mi di nara doggal jëmale ko ci kandidaa bi njiitu-réew mi bëgga doonaat, téy la maanaa sàrt bii gëna fésati. Wante su weesoo loolu itam mënees na cee jàngat lu bare ci ni Maam yi gise woon àddina, seen farlu ak seen mandute. I NEKKANDOO CI BIIR ASKAN WI
Matukaay 1eel:
Askanu ndaali Maali pegg yi ñoo ko sos: . 16 xalakat walla "ton ta jon" . 4 njabootu garmi walla "mansa si" . 5 njabootu sëriñ walla "mori kanda" . 4 peggi liggéykat yi walla" nymakala"
Pegg bu nekk dafa am ay wareef ak ay sas.
Matukaay 2eel: Peggu liggéykat yi "Ñamakala" dafa war wu fu tollu di wax dëgg seeni njiit, di leen digal, di saytu ci seen làmmiñ ak seen jëf yoon yi ak sàrt yi ñu tëral ci ndaali Maali.
Matukaayu 3eel:
"Morikanda" yi walla sëriñ yi ñooy sunuy sàng te ñoo ñuy yar ci diine lislaam. Kon ku nekk yoreel na leen njukkël te war na leen a weg.
 Matukaayu 4eel: Askani ndaali Maali ay maas ñoo ko bokk. Maas bu nekk day fal njiitam. Ñi bokk benn maas ñooy nit ñi (góor walla jiggéen) yi seen magante weesuwul 3 at. "Kangbe yi", walla maas yi nekk diggante ndaw ñi ak mag ñi, dañoo wara bokk fa ñuy fasee tëral yu am solo yépp yi soxal sosiet bi.
Matukaay 5eel:
Nit ku nekk ci askan wi yelloo na dund, yelloo na karaangee ci yaramam. Képp ku faat bakkanu keneen nit, yoon di na la natt ñu faat sa bakkan. Matukaay 6eel:
Taxawalees na ngir xeex yaafuus ak yàccaral, am yokkute, kuréel gu ñu tuddee "Könögbèn wölö". Write Comment (0 comments) |