Juddu ci gëléem, nàmp ci mbaam Bu sunu boroom bi bëggee, ñépp ñàkk Bant su tooyee yomb a jubbanti Juróom-ñeenti walaakaana soo leen bëggee jubbanti, soo moytuwul fukkeel leen Boroom kuddu du lakk Wax dëgg du wàññi wërsëg Nit ki, li nga ko gëne, booy sangu bu ko summi Doxkat du fekke dëju maamam Njëriñ…