Alxuraan ci Wolof: Suraat XCII – Guddi

Wàcce ci Màkka 21 laaya
Benn – Senn – Menn la – Raax Menn – Raax Yërëm

1- Ag guddi fu mu tallale muraayam

2- Ag bëccëg fu mu leere naññ

3- Ag kooku sàkk góor ak jiggéen

4- Seeeni coono daaanu wuute li ñuy diir.

5- Kiy joxe te ragal Yàlla

6- Ki teg ngëm gi gëna rafet naka dëgg axxan

7- Koooku dananu ko yombalal yoon wi gënë yomb

8- Waaye ki bëgge, ki faalewul kenn

9- Te teg ngëm li gëna rafet naka aw fen

10- Danau ko teg lu yomb ci yoon wi gëna jafe

11- Lu ko amamam di jëriñ fu ñu ko ware tàbbal jaanama?

12- Ñoo moom di teg nit ñi ci yooon

13- Ñoo moom dundu ëllëg ak dundun fii

14- Ma di leen yëgel safara suy riir

15- Te ñi ñu rëbb kese la ñu cay joo

16- Ñoom ñi jeeñ sunu ndaw yi fenkat dëddu leen

17- Nit ki gëm dana ca mucc

18- Ki daan joxe amamam ngir gëna sell

19- Te daawul def lu baax lu jar neexal ngir aw nit

20- Waaye ngir rekk Yàlla mi sut lépp teg ko bët.

20- Ci dëgg kooku dana ami mbégté.

Tekki bi: Pathe Diagne, Alxuraan ci Wolof. Editions Sankore, L’Harmattan.

One Response

  • Cheikh Diop says:

    Jaajeuf Serigne Pathe Diagne! Ligueye bi am na solo lool. Li migui deguel li Cheikh Anta Diop doon wakh. Bou gnou moune def ligueye bou wer bi chi Al Kuran, menees na def chi wallou kham kham yeup moudi literature, science, politik, fane yeup rek!
    ma bantou waat di lene sant, te di lene jaajeute!

Leave a Comment