Waxi Wolof Njaay

Juddu ci gëléem, nàmp ci mbaam

Bu sunu boroom bi bëggee, ñépp ñàkk

Bant su tooyee yomb a jubbanti

Juróom-ñeenti walaakaana soo leen bëggee jubbanti, soo moytuwul fukkeel leen

Boroom kuddu du lakk

Wax dëgg du wàññi wërsëg

Nit ki, li nga ko gëne, booy sangu bu ko summi

Doxkat du fekke dëju maamam

Njëriñ loo fekke

Tontu du forox

Goloo la gën a xam kër gu bariy xaj

Jaam ak pexeem, Yàllaak dogalam

Suul ker du ko teree feeñ

Lu la bett mën la

Ku dee ca ja ba yaa tàgge sa bopp

Ku xamul guro moo koy baxal

Ku ñuy watat, doo taamu fi ngay teg sa ndodd

Ku wax feeñ

Gàcce gu gàtt moo gën gàcce gu gudd

Ngénte bukki, gaynde du fa bàjjan, te lu dul sob yóbbuwu fa béy

Kenn du jiitu paaka ci mbaram

Ku fiir ba du lekk fiiriir !

Seelu taw moo ma gënal seelu ngelaw

Fàttee mag boroom

Bëñ du ree jámm
Ku wéet, sa baat wéttali la

Sikkim nga, geestoo la yóbbaale

Wax su baree fàww mu génne asaka

Waxu mag mën na guddee waaye du fanaan àll

Soo yokkee cere, yokkal ñeex, bala la cee mëq di fekk

To?-to?u naat saa yu wëreem réew dunq yaa tax

Loo jëmbat yendu ci keram ba mu des nit

Kuy làqu di naan, soo màndee feeñ

Gaynde gu xiif déggul jat

Foo fekk kuy puus oto, du ca dugg mukk

Ku wax feeñ

Koo ëppul mbokk mënoo ko jëw

Nettali mooy indi ay

Soo xamul foo jëm, dellul fa nga jóge

Xol du wóom ba ñu koy bës

Coow la ca teen ba, ña amul baag a ko waral

Làkku jaambuur, su neexee ni tàngal it, kenn mënu koo macc ba ciy tàqamtiku
– Ay kàddu yu xóot yu ma daan faral a dégg ci Séex Anta Jóob –