Téy ci 18eelu fan ci wéeru Suliye lay Nelson Mandela, mi kenn dul nettali ay jàllooreem di am 94 at! Réewum Afrik di Sid yépp, Afrik gépp ak àddina sépp di ko berndeel di ko delloo njukkël.Bésam bi di bésu téy la mbootaayu xeet tuddee bésu Mandelaa ngir magal manduteem, paspasam, fonk boppam ag askanam ba jaraloon mu tayle dundam ngir Afrik di Sid moom boppam, nit ku ñuul ak ku weex bokk dëkk, yem ay sañ-sañ, wegante.
Mandela gànnaaw ba mu tëddee 27 at ci kaso ca jamonooy apartheid, la genn doon peresidaa Afrik di Sidd ci atum 1994 ba 1999.
Kookooy Madiba Mandela, ñayu-xare, ki sagal nit ku ñuul ak ku weex!
Yàl na ko fi Yàlla bàyyi mu dund ba weesu 100 at di dem..