Jaar-jaaru woykat bu jege woon askanam
Ci sanwiye 1999, yeneekay Lasli/Njëlbéen amoon na laaj-tootu bu yaatu ag Njaga Mbay, doon ca feeñal ay jaar-jaaram. Waxtaan woowu Njaga Mbay amoon ak Séydu Nuuru Njaay, di njiital Lasli/Njëlbéen moom lañu leen fi indilaat, di ci ñeel woykat bu mag bu àddina sépp jooy.
Kan mooy Njaga Mbay?
Man. Njaga jooju nga tudd, ñu ngi ma tuddee gennn góor gu tudd Njaga Mbeng, nekkoon jaaykat bu mag di woon itam aalim. May doomu góor gu ñuy wax Ngóor Mbay, ñu koy woowee Abdu Faatma ca Cilmaxa ak jiggéen ju ñuy wax Kumba Ndaxaar Sàll. Ngóor Mbay nag da daan xalam, Kumba Ndaxaar moo yore woon kër gi. Maa ngi judd ci 1948 ci Taatagin ca diiwaanu Siin-Saalum; booba jamono ay arondismaa amagul. Fa laa jàngee sa ma njàng mu njëkk ci tubaab, ba Yàlla def ci 1962, ma jóge fa dem Fatig di yokki sama njàng ci «CEG» ba fa nekk.
Ci ñi njëkka jàng ci «CEG» ci la bokk. Ci 1965, ginaaw ñetti at ci daara ju dig-dóomu jooju, ma bàyyi dem nekki benewol ca rondismaa Taatagin. Foofu laa duggee làrme ci 1966. Ci xumbte yi doon tëj sunu jàngum militeer man ak ñoom Mbeng Mbay Maa Daawur, Siidi Buya Njaay booba liyetnaa la woon, ñoo xumbal ngoonal gi. Bi ñu paree ñu indi ñu Dakaar; booba Cerno Ba, mu ngi woon ca jawriñ ji ñu dénk gi Caada gi. Moom moo gis Sonaar SeÅ‹oor ne ko gis naa xale boo xam ne, boo leen ko jële di na leen amal solo lool. Booba 1967 lawoon, maa ngi woon «Marin»; bi may dem ñu may dégglu ca Soraano, booba yere «Marin» la soloon. Ma dem ñu dégglu ma. Bés ba ma delluwaatee Soraano ngir nemmeeku la ma fa defoon, ñu ne ma foo nekkoon? Ñëwal liggéeysi. Noonu laa duggee Soraano…. Am naa ñetti soxna ak ay doom. Aal pulaaren yi ñu ngi may njukkal. Am na ay gëstukat yu mel ni Amiidu Ja, yu bind ci man ay téere ak itam Ibrahima Wan, doon def ab gëstu ci njàngam ca Daara ju mag ja ci man, ak ñoom Samba Jabare ak Yusu Nduur. Baaba Maal moom itam moom bañ na ko ba balaa bég, su ne cépp Podoor ma dikk fa. Ku dikk mu ne ko kii mooy sunu xalifa, mooy sunu mag, mooy sunu lépp. Xam nga kon mënu maa wax ci lenn di wone suma bopp te wone wu ma suma bopp jarale ko ci njabootu Aal-Pulaar yi…Maa ngi sargal itam Seex Aamidu Kan…
Fent…
Maa ngi ci sama ñetenteeli kaset. Booba xalaatuma woon defarlu kaset. Sama kaset bu njëkk mu ngi tudd «Dans le vent», bi ci topp maa ngi ko tuddee «ndaanaani réew mi», bi ci topp maa ngi ko tuddee «nanu muñ», bi ci topp mooy bi mujj, maa ngi ko tudde «Njaga plus». Ndax damaa fas yeenee wettali xali yi, moo tax mane Njaga ak as lëf, Njaga ak leneen. Misiku kaset moo deme noonu.
Bu leen kuppe» bu Yusu Nduur
Li jëm ci woy wi Yusu Nduur woy tudde ko «Bu leen kuppe», xam naa ne ñiy kuppe xam nañu sekere bi ci biir woy bi. Ndax ki ñu waxoon ne moo koy kuppe ba ñu ko deñcee ba négëni sii, yëf yaa ngi wéy di kuppe. Xéy na Yusu dafa njëkka wax nit ñi, waaye ku fekke am na ci kàddu. Lii dañu koo fekk ci jamono, te man samay woy damaa bëgg muy doon luy wéy. Lii kuppeeg tey la rekk ak tàkku ëllëg; yëfi jamono la rekk. Man nag, samay woy dama ci bëgg di woy loo xam ne luy wéy la ba pare tey jii itam ma ciy woy luy wéy ëllëg. Woy lu wéyoon démb, ngir fattali nit ñi. Woy itam luy wéy ëllëg lu mëna jàngale la. Njiinu réew mi Bu ñu ci jàppul bu baax di na réeri. Amoon nañu ci tiit ci jamono jee weesu waay tey ñu ngi dikk, di jéem a saxal ndax ci seeni woy ñu ngi ciy wax ay kàddug wolof, ñu nig ciy woy di ci boole ay tamaag ndënd, di ci boole li ñu moom…Ñakk a guñu.
Jàng ak bind ci làmmiñi réew mi?
Lu am solo la! Jiggéen ju masul jàng tubaab mën na tey bindal boppam ci làmmiñam. Mo tax Yàlla di gën barkeel seen liggéey! Na ku nekk jàpp ci li ñu moom mën caa lijjanti li mu soxla. Wolof ak pulaar lépp a ci yem, loo ci woyofal mu wéy. Lasli/Njëlbéen liggéyam rafet na! Njiitam Séydu Nuura Njaay woyof na! Abdu Juuf Sama digaale ak woykat yi, digaale bu rafet la. Dinaay seeti Coon, Yusu, Baaba. Baaba moom sama lépp la. Abdu Juuf dama koo waxoon ne: yaay baayu nasiyoÅ‹ bi, kon yaa wara yore sam «sold». Politigu ma ni ku nitu politik yi di defe waaye damay dindi lépp luy xiiroo te loolu ndimmbal la. Abdu Juuf digoon na ma kër, waaye booba ba tey am na at, te gisuma dara. Abdu dina ma déglu, dina ma jàng, dina ma gis. Umpalewul ne Njaga Mbay mu ngi ci réew mi. Ku réew yépp wara soxla, war nga mën a soxla sa réew. Jawriñ ji yore caada gi di Abdulaay Elimaan Kan, fan yii rekk gis naa ko, war nañoo gisewaat ci fan yii. Sëriñ Abdu Asiis Si Dama koo bëgg. Di ñaan Yàlla yeene bi mu amoon ci bani aadama yi ci kow suuf, Yàlla defal ko ko muy mbégtéem ci biir suuf. Ku baax la; tey wéetal na askan wi. Maa ngi koy jaale wa kër Seexu Umar, waa kër Momar Anta Sali ak kilifaay diine yépp: Laayeen, Ñaseen, Njaasaan, Cenaba, ak fépp fu jullit yi féete. Ndax du naqar weet rekk la! Képp ku baax ba seeti sa xarit bi nga gën a fonk ñee la rekk a war! Yàlla na suuf sedd ci kawam te eggali sunu yeene ci kow suuf. Mebét Maa ngi xaar laata may génnéewaat leneen, ndax ku lekk ak ñaari loxo gawa suur.Te war na boo nekkee ci géew, ba mu yàgg, nga demaat ca làng ga, ngir jàngaat.
Fàttaliku
Man woy, bu ma dee fàttaliku, maa ngi ko tàmbalee def bi ma nekkee xale. Bi may raam, sama pàppa, dafa amoon benn xaritu «seef de kanton‹» bu nuy wax Seex Njaay. Bu ngoonaan bu nu dikkee ca kër ga, di xawaare may raam nag di fëxle xalaam yeeg, di woyantu; su ko defe ñu daldi may jël tërali. Ma màgge noonu, màgge noonu ba ba may dugg lekkool. Ca lekkool ba itam, ci jamonoy Fay Waali dooonoon fa jàngalekat, Rosiñool lañu ma dooon woowee. Booba Iba Deer Caam mii tey, moom ak seneraal Waali Fay jàngaloon nañu ma…
Taatanu © Séydu Nuuru Njaay, Pikin Xuru-Naar : 19/01/1999