Seetal Fii
« Philosophie en wolof : A comme aada … »
aada j. : aada mooy mbooleem matukaay yi am mbooloo, gën gaa bare, aw askan di tegtaloo cig jëf, di ca xà jj lu bon ak lu baax. Matukaay yooyu ñooy doon tegtal yiy ommat nit ki ci yoon wi muy jëflanteek yeneen mbindeef yi ak cà kkeef gépp. Kon aada, du loo xam ne ci coobare boppam la ko way di nà ngoo topp mbaa mu jalgati ko. Ndax tëral yi ci biir aada, ñaare, ca cosaan la ñiy lawe, di meññ ba yegsi ci jamono.
Aada ci fà nn dund gépp lañu ko mën a rà ññee ci ab → sosiete, moo xam ci → kurél yi ñuy sà mp la, ci wà llu → politig, koom-koom, yoon mbaa diine la.
Mën nañoo wax ba tey ne aada mooy dig bi aw askan di mà ndargaale li mu moom ak li mu moomul, li mu caadawoo ak li mu à bb. Looloo tax askan wu nekk am aada yu mu moomal boppam, yu mu jéggaaniwul : kon aada dafa bare te bokkul.
Wante aada itam sangoowul der bu teref, ba dara lu bokkul ca moom ca cosaan du ca mën a rax. Nde ni jamono di doxee noonu la aada itam di doxe, di ko soppeekoo, ay tëral yu yees di ca juux, am yeneen yu ña cay xent. Ci kow loolu la aada yu bari di jaar ci yoonu diine, soppi lu bare ca na ñu daan rà ññalee mbaax ak mbon ginnaaw ba askan woowa tuubee, topp weneen yoonu diine.
Ba léegi, ay askan nu ñu gën a jegeente ca seen cosaan, noonu la seeni aada di gën a niroo. Seex Anta Jóob wone na ci téereem yu bari, ni réewu Afrig yi seeni aada róofoo ca cosaanu maam ya jamonoy Buur-Fari ya woon Misira démb ba tey jii.
Ci wà llu nekkandoo, aada bokk na ci liy fas te di gën a dëgëral li am mbooloo mbaa aw askan bokkandoo. Kon aada, ndonte kon wuute na ak yoon, ci natt yi miy teg ñiy jalgati ay tëralam, ci kenu yiy téye ab sosiete la bokk.
Wante meññeefu aada, maanaam njëriñ li mu là mboo ci jamono jii, mu ngi aju ci ni aada ji di soppeekoo à nd kook li jamonooy laaj. Bu ñu koy seet tey day mel ni matukaay yi mel ni waccoo ak yelleefi doomu aadama, sà mp nguur ci kow yoon, sà kku yokkute ci tawféexu nit ñi, dakkal xare ak faat bakkan cig neen, ay ponk lañu yu aada yépp ci à ddina war a mën a à nd.
Fr. : coutume
Â
ajeel b. : lëf ki, walla xew-xew bi nga xam ne lëf keneen ka, xew-xew beneen ba ca moom la aju, maanaam su amul loola du mën a am, mbaa deesu ko mën a xam.
Ci fà nnu losig walla jaduteef, mën nañoo faramfà cce mbir mi nii :
Dees nay wax ne ajeel sangam lu war la, su fekkee ne lëf sangam (L cig gà ttal) su amee, te ci kow mu am doŋŋ la lëf ka muy jur walla njureel la (N cig gà ttal) di ame. Su ñu ko baamtuwaatee mà ndargaay wax jooju lii la : su fekkee ne te su fekkee ne doŋŋ L ci lay N di ame.
Ab ajeel mën naa itam mat sëkk, su fekkee ne su L amul N du am, maanaam su dee (–L) kon (–N).
Mën nañoo tënke ci loolu ne : su dee L ajeel bu war la ngir N, kon itam ba léegi N ajeel bu mat sëkk la, ndax su dee ci kow L am doŋŋ lay N di amee kon su L amul N itam du am. Ab ajeel bu war te mat sëkk kon lii lay tekki : ci kow ajeel boobu nekk doŋŋ la ajeel ba ca des di mën a nekke.
Fr. : condition
…………………
There are no comments yet, be the first.