Wote bi nu dëgmal, ñépp xam na ñu ko, wote bu jeggi dayoo la: ndax ci la ëllëgu réew mi aaju! Wote tànn la wan yoon la Senegaal war a teggu jëm ca kanam mbaa mu teggi ko, dellu gannaaw: lawla cat! Wante li ñu soxal ci jukki bii, lu lëkkëloog loolu gaa, wante leneen la. Loo xam ne soo ko seetloo, dafa mel ni dafa am jàllarbi ci ni “politiciens” di jëfandikoo làkki réew mi! Li ñu leen doon faral di wax mooy: demokaraasi ci làkki-jambuur ay kácci neen la, mënu la nekk! Ndax demokaraasi mooy nguuru askan wi ngir askan wi!
Waaw, bu fekke ne nag fa ñuy takke aka tekki, fa ñuy dógale, fa ñuy fasee aka fecci, ña fay wax du ñu wax lu askan wi mën a dégg, naka lees mën a tuddee mbir mooma demokaraasi? Dafa mel ni daal buum bi ñu kolonisatëër bi nasoon, ba taxoon ñuy wéy ci waawaam, ba léegi dógagul! Te buum boobu, xàncc bi ñu ko ràbbee mooy di jëfandikoo làkki nasaraan soofal sunu bos, di jàng cosaanaam fàtte sunu bos, jël ay kureelam indi teg, jël doxalinam indi teg, jël xaalisam indi teg… Te loolu feek mu ngi fi, cóow leey bari rekk, wante demokaraasi dëgg, mbaa jëm-ca-kanam ci wàllu koom-koom caada ag nekkinu askan wi da na fi jafe lool!!!
Liy firndeel loolu, mooy ba nasaraan bi xamee ne léegi mu ñakk réewi Afrik yi mu kolonise woon, fekk Alseeri ngiy xare ngir moom boppam, Wietnam duma Faraas Jemben-Fuu, Kamerun tàmbalee fippu, seneraal Degaulle da fa ne woon: “na ñu yolomal buum gi ba laa moo dóg”!
Te loolu li muy tekki mooy, na fi sunu jëmm yi jógge, wante sunu doxalin moom na sax ci xel yi ba fàww! Te looloo fi amoon, ba fi Seηóor nekkee ba ci Abdu Juuf ag ñi fi nekk téy! Xam nañu ne Seηóor ba mu fi jógge da dem Faraas nekk “Accadémie francaise” , Abdu Juuf jógge fi dem jiiteji “francophonie” di bàkk, di bàkkoo làkki nasaaraan! Xalaas, loolu de du ngoóora! Te su caaxaan faaxee dëgg des, Afrikee rekk ngay gis muy nangu loolu! Kenn ñemewul xalaat sax, gis sinwaa, mbaa sapone mbaa wietnamee buy soofal làkk wi mu nàmp, dem di bàkkoo làkki ñi ko mas a dëkkee tuutal ag nas buum! Da ñu fee déggoon ci lu yàggul dara sax njiitu-réew mi di wax di bàkku naan, Senegaal mooy réew mi nga xam ne, soo limaaleewul Faraas, fa la nit ña gën a xereññee ci làkk nasaraan!!! Wante nag Wolof Njaay da ne li nga moom nga mën a tiitaroo! Li nga moomul moom, Bafa rekk la sànt! Seex Anta yokk ca ne “lákki jambuur de su safoon suukar ba mel ni lem itam, mënoo ko mácc ba cay taxamtiku”.
Ñaka xam daal ag ñakk fayda li ñu waral bari na! Ñu bari ci waay-xeltu yi sax dañoo defe ni, wax yu ni mel ay waxi-démb mbaa ay wax yu amul solo lañu, te fekk ne loolooy ndéyi-mbill ji!
Amul xejj-ak-seen, amul benn réew bu mëna am yokkute, am tawféex ci kow topp aadaa, ag cosaanu weneen askan, rawatina dëkkee jëfandikoo làmmiñ woo moomul te fekk Yàlla natoowul a ag lu!
ImageWante nag ba léegi yakaar tasagul! Ndax téy soo seete xale yiy “rap”, seen xarala ci lákki réew mi, li ñu ciy wax, li ñuy ciy yàtt ci ay káddu yuy xalam, seen farlu ci siggil réew mi ag askan wi, dootoo amati benn siiki-saaka ne làkki réew mi ñu ngi ci yoonu suqaliku gu wér! Ba tax na sax, soo koo setantalee, da ngay gis ne “politiciens” seen bopp dafa mel ni dañoo xawa nànd loolou”! Ndax léegi ñoom ñépp a taamoo wut ay dàkkentali wolof: Moo xam “Bennoo Siggil Senegaal la, Bes du ñakk, Fekkee ma ci boolee, Daas fanaanal, Nay leer, Car leneen, Taxaw temm…” ag yeneen yeneeni yëngu-yëngu lañu! Loolu soo koo seetloo bu baax ag jàllarbi la daanaaka, ab “revolution linguistique” la! Ndax ku ci nekk xam na ni soo nee askan wi “bennoo siggil Senegaal” rekk nit ñi xam loo wax, jaratul sax nga leen di faramfàcceel lenn. Wante soo leen nee “CAP 21”, walla nga ne leen “Coalition pour l’Aternative” ñu bari day mel ci ñoom ne ay waxi-picc! Te mbir mi nag, waxoon naa leen ko fi, su ñu doon jëfandikoo sunu làkk yi rekk léegi lépp leer naññ! Loo waxati ñépp xam ko: doo fi naxati kenn! Moo tax ba fi njiitu-réew mi nee “maa waxoon waxeet!” mbàmb li wër àddina! Wante su ne woon ci nasaaran “j’avais dit, mais maintenant je me dédis”, mbir mi du demee noonu! Kon soo ko seete, làkki jambuur wi ñu fi saxal ab juntukaay la itam bu ñuy noote aka naaxale askan wi la, maanaan “c’est un instrument de domination et d’infantilasation aussi du peuple”! Mbas ci li fi “Jean ak Paul def”!
Tamsir Anne : tamsir.anne@wolof-online.com
Nuyunaa ñëpp!!
Di rafetlu jukki bu am solo bii.
Aka neexoon ñëpp xameeko nii
Waaw góore yaw mi ciy def lu rafet lii lepp!!
Jërëfe yow!Li ñu teye du lenn lu dul ag xeeb sa bopp te bañ say maam.Waaye ku wacc sa’b ànd,ànd boo dem fekk ca boroom.