Antoine de Saint-Exupéry
Ndoomi Buur si
Traduit en Wolof par Dr. Tamsir ANNE
Tudee naa ko Leon Werth
Yeen xale yi, na ngeen ma baal, ndax teere bii ki ma ko tuddee du xale, mag la. Wante am naa lay: benn, kookooy sama xarit bi ma gën a fonkk ci àddina. Ñaar, mag la gaa, wante lépp la mën a jëli, ba ci nettali-xale sax. Ñett, waa jooju Faraas la dëkk te jamono jii ndeysaan dafa mar, xiif, moo tax ma bëgg koo dëfal tuuti.
Su lay yooyu yépp nag doyul, kon may naa teere bi xale ba waa jooju masoon a doon , ndax mag ñi ngeen di gis doonoon nañu ay xale, wante ñi ciy fàtteliku loolu ñu neew lañu.
Kon ma jubbanti wax ji.
Tuddee naa teere bi Leon Werth
Ca ba mu nekkee xale bu góor bu ndaw.
I
Ba ma nekkee xale bu tollu ci juróom-benni at, dama masoon a gis benn bés nataal bu yeeme ci benn teere bu doon nettali lu jëm ci “àll-bu-xonq bi” bu tuddoon “Ay nettali yu dëggu yu ñu dund”. Nataalu benn yeew la woon bu doon wànn benn rábbu-àll. Sotti nataal baa ngi nii:
ci teere bi dañu cee bindoon ne “yeew yi suñu fàddee dañuy warax du nu sàqarmi: su ko defee dootuñu mëna yëngu, dañuy tëdd juróom-benni weer di ko nelaw ngir li ñu wànn rees“.
Ma jógge fa topp di xalaat lu bari ci xew-xew yi ci àll bi. Man tamit ma nataal ak sama karayoƞ
-kulóor sama nataal bu njëkk. Sama nataal boobu ni la meloon :
Ma won sama nataal bi ay mag, laaj leen ndax ragaluñu ko? Ñu toontu ne: lan lañu war a ragal ci ab “mbaxana”?
Ma ne leen nataaluma mbaxana de. Yeew buy wànn ñay di ko reesal laa nataal. Ma nataalaatal leen biir yeew bi, ndax ñu mën a jëli li ma leen wax noonu. Mag ñi noonu la ñu mel: fokk nga leen di leeral lépp. Bii moo doon sama ñareelu nataal:
Ñoom nu far digal ma ne naa bàyyi nataal yeew yu tëjjook yu ubbeeku te jeem a toppatoo lu jëm ci xam-xami cosaan, xayma, xàmmeefi-sàrti baat, ak nataalu-suuf-si. Noonu laa mujj a bàyyee ca ba may am juróom-benni at sama mébetu dooni bés nataalkat bu narkoon a mucc-ayib.
Sama ñaari nataal yooyu, bu njëkk beek bu mujj bi, noonu ñu leen soofale woon, looloo ma xàddiloo. Mag ñi moom du ñu nànd dara, te dafa sonnale ci xale nga di leen leeral lépp saa su nekk ci lu nekk.
Noonu laa mujj a tànn beneen mece, jàng dawal awiyoŋ. Fu nekk ci àddina bi naawal na fa awiyoŋ. Natalu-suuf si nag, dëgg la gaa, amal na ma njëriñ lool foofu. Su may xelmati béreb rekk di xàmmee fan la, Siin mbaa Arisonaa. Am na njëriñ lool, rawatina soo reere guddi. Ba ma juddoo ba léegi taseek naa nit ñu bari ñu am xel. Dund naa ak mag ñu bari. Seetlu naa leen it bu baax, wante loolu soppiwul, gën a rafetal sama xalaat ci ñoom.
Su ma tasewaan ak ku ma niru ku yemb, da ma ko daan seetlu won ko sama nataal bu njëkk bi ma dencoon. Lépp ngir bëgg a xam, ndax nànd na. Wante amu ci kenn ku ma newul „lii mbaxana la“. Man nag du ma ko wax waxi yeew ak àll-yu-xonq mbaa ay bidiw. Damay wàcc ba tollook moom di ko wax waxi kàrt ak golf, politik mbaa ay karawaat. Su ko defe mag moomu da daan bég ci lu mu dajeek ku ni mel, ku yembee noonu.
II
Noonu la nekkee woon ak sama weetaay, amuma kenn ku ma mën a waxal dëggantaan ba bés bi ma paane ci biir deseeru Sahara bi, booba ak léegi juróom-benni at la. Dafa am lu tojoon ci moëtër bi. Ndegam nag aduma woon ak mekanise mbaa maa yobbale kenn, may waaj, lu naroon a jafe nag, jeem koo defarat man doŋŋ. Sama bàkkan bii ci loolu la teggu woon. Li ma dese woon ci nduxum-naan weesuwuloon àppu juróom-ñetti fan. Ngoon gu njëkk gi ci suuf si laa fanaan, fenn fu nit dëkk jegewuma ci lu ëpp juniy juniy kilometaar. Kon maa gënoon weet ku gaalam suux digg-géej, mu ne cunduŋ moom doŋŋ jafandu cib tëmbal.
Xalaat leen kon mbetteel gi am ba bët di set, am senn mbaat su sew, su xoromu sax su ma yee naan ma:
– Doo ma nataalal xar, su la neexe?
– Man ne „Han“!
– Nataalal ma xar…
Ma ne bëreet ne ku dënnu fàdd, toxoñ samay gët, xoolaat bu baax, daldi gis as xale su ngóor su doy waar sax su ne ma jàkk di ma niir! Nataal bii ma ko nataal ca gànnaaw ga mooy bi ko gëna indi, wante bir na me sama nataal boobu xaajul jege kemtaan gi mu doon roy. Du samag sàggan nag, ndax mag ñee ma xàddiloo woon ca ba may tollu ci juróom-benni at, ma dumooyu mecce nataalkat bi doonoon sama mébet jamono jooja: samam njàng ci fànn woowu rombuloon nataal ay yeew yu tijjiku ak yu tëju. May xool njuuma li, sama gët yi ne xujj ndax waari. Bu leen fàtte ne benn dëkk dànduloon fa ma newoon. Te itam sama ngóor si niruwuloon ko reer, ku sonn ba dóg, ku xiif, mar, mbaa tiit bay bëgg a dee! Niruwuloon benn yoon xale bu reer ci digg deseer bi, ci ajag-jag gii. Ba sama fit wi dellusee, ma mën a wax ak moom laa ne ko :
– Waay…looy def fii?
Mu baamtuwaatal ma ndànk, mel ni loolu lu ko ñor la lóol:
– Ey waay, nataalal ma xar…
Ndeke soo waaroo doo sañ a bañ. Ak li ma mbir mi jommal lépp, béreb bi mu ma fekk xàndu fenn fu nit ëkk, sama bakkan nekk ci xottu-gerte, noonu laa gennee sama poos ab keyit akub xalima.
Wante foofu ma fàttelikuwaat ne nataalu-suuf, cosaan, xayma, xàmmeefi-sàrti-baat la gënoon a mokkal, ma xaw a mer ne ngóor si mënu maa nataal. Mu ne ma: loolu du ci dara nataalal ma xar. Ndegam masuma woon na nataal xar nag, ma nataalal ko benn ci ñaari nataal yooyu kese ma mënoon. Nataalu yeew bu tëju bi.
Ma gënatee waaru ba ma ngóor si ne tónneet:
• Déedéet! Déedéet! Bëgguma nataalu ñay bu nekk ci biiru yeew. Yeew wóorul te ñay daa rëy ba ëpp, fama dëkk xat lool. Xar laa bëgg,nataalal ma xar.
Ma daldi joos:
Mu xool ko xoolaat ko bu baax ne:
– Déedeet! xar mii dafa wopp lool! Nataalal ma beneen.
Ma joosati:
Sama waa ji muuñ, deey ma ndànk ne:
– xam nga ne lii du xar kuy la. Dafa am ay béjjen…
Ma rëddaat samab nataal boobee:
Mu làŋkati ne:
– Bii dafa màggat…buy dund lu yàgg laa bëgg.
Mbir mi bugg maa sóof te fekk maa ngi yàkkamtee jublu ci wàccee sama motëër bi, ma karaas-karaasal ko nataal bii:
Ne ko:
– lii kees gi la. Xar bi nga bëgg, mu ngi ci biir.
Ma gënatee am mbeteel ba ma gise xar-kanamu sama àttekat si di leer mu ne:
– Waaw kañ….bu mel ni nag laa bëggoon! Defe nga ni xar mii dina soxla ñax mu bari?
– Lu tax?
– Fi ma dëkk daa xat lool..
– dina war a doy de…xar mu ndawa-ndaw laa la jox.
Mu daldi sëgg ci nataal bi:
– Ndawul noonu kat..Xoolal! Nellaw na…
Ci anam yooyu laa xamanteek ndoomi-buur si.
Bii mooy nataal bi ko gën a indi bi ma ko nataal ca gànnaaw ga:
IV
Noonu kon laa xame meneen mbir mu am solo: palanet ba mu bawo ëppuloon daanaka as kër lu bari! Loolu nag mënuma woon a jaaxal lool, ndax xamoon naa ne su weesoo yenn palanet yu rëy yi mel ni Suuf si, Sipiteer, Mars, Wenis, yi nu wutal tur, am naay téeméeri téeméeri yeneen palanet yu tuutee tuuti ba daanaka mëneesul a sax gis bu baax ci teleskop. Su ci ab astronom feeñale benn da leen di wutal ab lim, da naan ko ci misaal “dippi-biddiw 1 3251”. Am na tegtal yu bari nag yu ma gëmloo ne palanet ba ndoomi mbuur si jógge woon dippi-biddiw B612 la woon. Dippi-biddiw boobu benn yoon kese la ko benn xamlukatu-biddiw bu Tirki mas a seen ca atum 1909.
Ci benn ndaje xamlukatu-biddew yu àddina-wërngël-képp mu indi ay firnde yu wér ci loolu mu feeñaloon. Wante kenn gëmuko, te dara waraluko woon lu moy li mu soloon. Mag ñee mel noonu.
Ndokk turu dippi-biddiwu B 612, nde lenn kese koo tax a siiw ba tey te mooy la benn njiitu-réewum Tirki bu tàngoon doxalin, dogaloon ne tirk bu soluwul ni waa- Ëroop yi di soloo rekk dinañu la rey. Ca atum 1920, mennam xamlukat tirk boobu, sol yëretubaabam yu rafet, joxewaat firnde ya mu joxe woon ca ndaje mu njëkk ma. Bi yoon, ñépp mànkoo, ànd ne li mu wax yépp dëgg gu wér peŋŋ la.
Li tax ma nettali leen loolu lépp ci dippi-biddiw B 612 ba noppi wax leen limam, du lenn lu dul mag ñi ñuy dégglu. Ndax xam ngeen ne ñoom ay lim ak xayma kese lañu fonkk.
Soo leen di wax sa xarit bu bees, duñu la laaj mukk lu am solo. Duñu ne la: « Nan la baatam mel? Yan po la gën a bëgg ? Ndax day dajale ay lëppa-lëpp ?” Déedéed dañu lay laaj :
“Ñaata at la am ? Ñaata mag mba rakk la am ? Ñaata kilo lay peese? Ñaata la baayam di fàyyekku wér wu dee?”. Soo leen toontoo laaj yooyu nag kese ci lañuy defe ne xam nañu kon sa waay. Mag ñi soo leen nee « gis naa kër gu rafet, am ay birik yu roos, am ay tóortóor ca palanteerya, ay pitax tàgg ca puj ga…” duñu mën a jëli li nga leen diwax. Da nga naan leen „gis naa kër guy jar nangami junni”. Su ko defe ñu yuuxoondoo ” Ah! kon de rafet na!”
Ba tey soo leen ne woon “liy firndeel ne ndoomi buur si nekkoon fidi dund, mooy taaram, da daan ree ba noppi daa bëggoon a am xar, ndax loolu firnde la ci ne diw sangam nekk na. Su waay deme bay bëgg am xar firnde la na ne nekk na”, su booba dañuy wag seeni mbàgg ne la xale nga moo tax!”
Wante soo leen waxe ne : „palanet ba mu jógge dippiv biddiw B612la” ñuy gëm li nga wax, noppal la ci seen laaj yu bare. Noonu lañu mel nag, kon bu leen leen ko jàppee. Xale yi fokk ñu laaye-biir mag ñi. Li leer ba leer daal mooy ñun ñi xam luy àddina sunu yoon ci ay nimero!
Li ma gënkoon a taamu moo doon tàmbale nettali bii ni ab léeb! Doon kon naa leen a wax ne: « Amoon na fi as doomi-buur su dëkkoon cib palanet boo xam ne daanaka li mu ko ëppee woon moom ci boppam bariwuloon,bu bëggoon na am ab xarit… ». Ku xam luy àddina dinga xam loolu gën a niru lu dëggu.
Ndax bëgguma nag kuy jàngantu samay téere. Sama xol day fees ak nàqar saa yu may nettali fàtteliku yooyu. Juróom-benni weer xaat ba sama xarit ba demeek xaram. Suma fiy binddi jeem tegtale na mu bindoo woon bañ koo fàtte mo tax. Ndax fàtte sab xarit ndey-saan mbir mu tiis la. Te du ku nekk mas a am ab xarit. Te itam mën naa meli bés ni mag ñi soloolul leneen lu moy ay lim. Looloo tax tamit ma jënd ab boyetu-kulóor ak ay karayoŋ. Yombul nag dellu di natalaat ci samay at, rawatina su dee masuloo jeem a nataal leneen lu weesu nataalub yeew bu tëjju ak bu tijjeeku ca say juróom-benni at! Naam, diina def sama kemtalaayu-kàttan def nataal yu ko gën a dippi, wante wóoruma ndax loolu dina àntu. Yenn saa yi am nataal bu tane, beneen ba ca topp du ko niru.
Damay juum tamit ci taxawaayam. Léeg-léeg ndoomu buur si njóol , léeg-léeg mu gàtt ba ëpp. Kulóoru yëre ya mu soloon itam dama koo xaw a fàtte. Kon damay làmbatu doŋŋ di góorgóorlu. Ci yenn yëf yu sew-sewaan yi gën a am solo dinaa ci xala juum moom. Wante rikk, loolu na ngeen ma ko baal. Sama waa ji masumaa faramfàcceel lenn. Xam naa dafa defe woon ne man ak moom ñoo niroo. Wante man ndeysaan mënumaa gis xar yu tëjju ci biiri kees. Xëy na damaa far mel ni mag ñi. Ku dem, mag dafa maa dab
V
Noonu la doon jànge bés bu jot lu bees ci palanet bi, ci dem bi ak ci tukki bépp. Ndànk-ndànk ndànk la daan juuxsi ànd ak xalaat yi ma daan dikkëll. Noonu la xame ca ñattelu bés ba mbuggëlu guy yi.
Bii yoon itam xar mee ma suqali, ndax ndoomi-buur si dafa tóog-tóog, mel ni ku jaaxle, ne tónneet laaj ma:
– Dëgg la de ne xar yi dañuy lekk garab yu ndaw yi?
– Waaw dëgg la kañ.
– Ah! kon bég naa.
Jëliwuma woon nag lu waroon a tax xar yiy lekk ngarab su ndaw si am solo soosu. Wante
ndoomi-buur si da caa yokk ne:
– Kon dañuy lekk guy yi tam?
Ma xamal ndoomi buur si ne guy yi kat, duñu garab yu ndaw, garab gu tollu niy jàngu lañu te su yobbale woon sax coggalu-ñay, coggal googu du mënkoon a jeexal genn ag guy.
Waxu coggal-ñay googu ma ko wax nag da koo defi ree: mu ne xanaa kon dees kon leen di tegle ñu warante..
Mu yokkal ma ci te fekk muy dëgg:
– Guy balaa mag day tàmbale doon lu ndaw.
– Dëgg la! Wante lu tax sa xar yi war a lekk guy yu ndaw yi?
Mu ne ma: “yow tamit!”, mbete loolu lu jaralu laajte la. Ma xalaat, xalaat ba sonn door di xam lu mbir moomu wund. Ndeke palanet ba mu bawo, dafa
amoon kom ci palanet yépp rekk gàncaq gu baax ak gu bon, kon jiiwu gàncaq gu baax ak jiiwu
gàncaq gu bon. Wante jiwu yooyu kenn duleen gis. Ci kumpë biir-suuf si lañuy làqu di fa nelaw ba mu neex cab ndoom, mu daldi door a yeewu.
Su ko defe mu fuddu, saxaan ndànk as mbant su rafet te lewet suy law wutali jànt bi.
Su dee saxaanu radi mbaa rosiye moom mënees na ko bàyyi mu law fu ko neex. Wante su dee gàncaq gu bon, ci saa si lees ko war a buddi saa yees ko ràññee. Te dafa amoon ay jiwu yu doy-waar ci palanetu ndoomi-buur si… ay doomi-buy lañu woon. Suufu palanet bi moom la feesoon dell. Te guy moom soo ko yeexe gis, dootoo tàggooteek moom ba fàww. Palanet bépp lay fees bëtt kook reenam yi. Te su dee palanet bi daa tuuti ba ëpp guy yi bari fa lool dañu koy
kalaate.
“Mbirum farlu kese la”, loolu la ma ndoomi-buur si wax ca gànnaaw ga. „Soo sangoo suba ba noppi, da ngay bale palanet bi ba mu set. Te sax-saxaani guy yi foo leen ràññeek yu rosiye da da nga leen war a buddi ci saa si, ndax su ñuy ndaw daanaka mëneesuleen a xàmme. Liggéey bu soof la gaa, wante yomb na.”
Benn bés mu digël ma ne, naa góorgoorlu ba def nataal bu mucc-ayib, ndax xale yi fii ma dëkk mën koo jàpp ci seen xel bu baax. “Xëy na suñu tukkee bés dina leen mas a amali njëriñ. Yenn saa yi, dàq sa liggéey bi nga war a wàccoo ba jëmmi-jamono amul genn gàllakoor. Wante su dee liggéeyi guy yi la moom ag tóoxidoona la. Mas naa xam palanet bu waa ju tayal dëkkoon. Kooku sàgganee ñetti garab yu
ndaw…”
Ci tegtali ndoomi-buur si laa nataalee palanet boobu. Bëgguma di wax mel ni kuy yeddaate. Wante balaa bi ci guy yi daa jeggi dàyyoo, ñi ko umpale bari, te ku repp ba reer bés cib dippi-biddiw mën ngaa jànnook musiba yu rëy, ba tax bii yoon fàww ma soppi doxin, artu leen ne: “Xale yi! Moytu leeni guy!”
Kon sama xarit yi meloon ni man, dëkkee woon di felsasu musiba jooju ñu xamuloon, ma bëgg-oon a artu, moom ma taxoon a farlu liggéey nataal boobu bu baax.
Jàngale bi ma ci indi jaroon na coono boobu. Xam naa, xëy na, dingeen ne, waaw lu tax amul ci téere bii yeneen nataal yu muccee-ayib ni nataali guy gi ? Toontu bi yomb na: jeem naa ba tàyyi wante sottiwul. Ba may natal guy gi damaa yëggoon ne mbir mi lu jàmpoon la.
Li ci topp …