Maa ngi tàmbale samay wax ak jëf ci turu Yàlla miy kiy boroom yërmande ju yaa ji ci adduna ak ja ca allaaxiraa. Yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc ci suñu sàng Muhammad ak ci ñoñam aki saabaam ci anam yu sax Yàlla doy na ñu, moom de wéeruwaay wu baax la, wu mat…
Author: tam
Yeesal baatu xarala ci wolof / Taatanu Wolof ak Xamle
1- Jollasu gi = téléphone 2- Kippaango gi = groupe 3- Njémmeer gi = public, assemblée, assistance 4- Limat gi = numéro 5- Lënd gi = internet 6- Lënku = connecter 7- Lënkaay gi= 8- connection 9- Peeñ bi= image 10- Baataan= vocabulaire 11- Limtu gi= chiffre 12- Nataal bi= photo 13- Ndéggat gi= audio….
Lu tax nu war a jàng ci làkki réew mi
Melo yi wolof
Bés bu taalifkati yeneen réew làkkee wolof…
* Jukki bii topp maa ngi ko jëlee sama téere bi ma tuddee Téere-woy yi te mu genn ci atum 2011 ca Almaañ. Téere bi mën ngeen ko am NDakaaru ca “Librairie Clairafrique” walla “L’Harmattan” Ubbite bi Ci téere bii, dañu fee tànn woyi taalifkat ak xaralakat yi gën a mag ci làkku almaa, toxal…
Alxuraan ci làkku wolof
Alxuraan ci wolof
Bés bi UNESCO jagleel làkki ndey yi …
Bésu 21 fan ci weeru fewrie at mu jot, moom la kurél giy toppatoo caada, njàng ak xamtéef (UNESCO) te féetoo ci mbotaayu xeet yi, jagleel làkki ndey, maanaam làkk wi nga xam ne moom la nit ku nekk nàmp. Loolu bi ko UNESCO dooree ak léegi ëpp na 10 at. Li waral bés bi…
Benn bés, benn woy: Sëriñ Musaa ka
XARNU BI Sëriñ bi noo gi deeti ñaan Faqiir dafay nangoo dagaan Nangul nu lépp lu nu ñaan Ndax Yàlla naatal xarnu bi Noongi dangaan ci Mustafaa Ma nekk marwat’ak safaa Ak àqi amdi Mustafaa Mi Yàlla jébbal xarnu bi Ak àqi mboolem ay rakkam Ak àqi séen baay yi ñu am Ak àqi seex…
Njuuj-njaaj: Céy miim réew…
Ñeel Seex Anta Jóob
Liggéey bu mel ni bii ñu fi dëgmal, wareef la ci sunu gis-gis, ñu ñeel fi ca ndorte la góor gu mel ni Seex Anta Jóob. Ndax daf fee def, lu fi daanaka kenn ci waay-xeltu yi ci Afrik ak li ko wër deful: maanaam yesalaat yoon wi àddina sépp doon gise cosaanu nit ku…