* Jukki bii topp maa ngi ko jëlee sama téere bi ma tuddee Téere-woy yi te mu genn ci atum 2011 ca Almaañ. Téere bi mën ngeen ko am NDakaaru ca “Librairie Clairafrique” walla “L’Harmattan”
Ubbite bi
Ci téere bii, dañu fee tànn woyi taalifkat ak xaralakat yi gën a mag ci làkku almaa, toxal leen ci wolof. Taalifkat yooyu yépp, muy Goethe, Heine, Hesse mbaa keneen ku mu ci doon, seeni bind wër nañu àddina sépp, siiwal nañu leen daanaka ci làkk yépp. Kon, ci sunu gis-gis, yoon la te it jot na, ñu tekki seeni woy ak seeni bind yépp ci làkki réew-mi, ba képp ku jàng mën a jëriñoo seen xalaat, bég ca seen xarala, ràññee pexe ya ñu tëral ba yàtt ca làmmiñ ya ñu nàmp kàddu yuy xalam.
Gannaaw loolu nag, aw làkk wuy dund moom, dafa mel niw gàncaq rekk: soo ko suuxëte, toppatoo ko, solool ko, bu ci Yàlla àndee day law, naat! Tos giy tax làkk woowee di gaaw a sëq, meññ, mooy dëkke di ca sotti lépp lu xelu doomu-àadama di sàkk te fekk muy lees mën a jëriñoo mbaa di ci namm am xel.
Tekki bépp xeeti xam-xam, ak ci làkk wu xam-xam boobee mën a sosoo, ci sunu làkki réew mi, loolu fés na ne lu mën a am, lu war a am la.
Ndem-si-Yàlla si Séex Anta Joop da daan wax ne, “am xel mooy gàtt, wante aw làmmiñ moom du gàtt”. Ndax lépp lu xel xalaat ba mën koo daj, xam ko, làmmiñ mën na ko tudd. Li des kañ mooy gën a tàkkuwaat, gën a farlu ci liggéey jëmale ci làmmiñ yi ñu moom, yi ñu jégganiwul fenn, sunu maam ak maam-mataar ya, ba ca mag ñu njëkk ña, daann leen jëriñoo di ca xalaat, di ca fent, di ca léeb, di ca bind, di ca jaamu Yàlla. Kon mënu ñu leen a wecceek lenn! Te sax Wolof Njaay da ne « ku wàcc sa and, and boo toog mu toj! »
Yàkkaar nañu ne daal, liggéeyu tekki bii ak yeneen yu ni mel yu am solo yu ko jiitu, dañuy gën a leeral yoon wi ñu mën a jëriñoo li ñu moomul, te du ñu sànni li ñu moom.
Jukkib-tànneef bu ni mel nag, ca ndoorteem moom, daanaka mënul a mucc-ayib. Rax ci dolli, ni ko Italiyee bi di waxe: “traduttore tradittore”, maanam “tekki, teggi”, ndax tekke ca làkk bu mu mënti doon jëmale ca beneen làkk, fàww mu am lu mu moy.
Terewul nag ci sunu jeemëntu bii, ñu def sunu kemtulaayu-kàttan ngir indi fi maanaa ak taaru kàddu xaralakat yu mag yi ñu fi toxal seeni taalif.
Xel nag moom du doy, te kuy jeem ay juum.
Goethe mooy xaralakat, fentkat ak taalifkat bi ñu gën a ràññee ci waaso Almaa yi. Goethe nag xam-xamam màcculoon rekk ci wàllu woy ak mbindu-fent yem ca, lawoon na ba yégg ci xam-xami càkkeef gi, filosofi ak yeneen xeeti xam-xam yu bare. Goethe ku jiitu woon jamonoom te ku ubbeeku woon la: ku solool lislaam la woon itam, doon jàng araab ak alquraan. Ci benn ci téere-woyam bi mu tuddee „Gànguneeg penku-sowu-jànt” walla „Westöstlicher Diwan” ci almaa da cay ñeel di ca bàkk diine lislaam. Goethe ba bési tey mooy xaralakat bi gëna siiw ci askanu Almaa te ay bindam daj nañu àddina sépp.
Jaxaay ji ak picc mi
Doomu jaxaay daa firiiy laafam
Ne day këfi.
Rëbb ba jam ko féttam
Ba bëtt laafu ndeyjoor ba.
Jaxaay ja ne jóoreet ca ron kàdd ga.
Ñetti guddi ndeysaan,
Ñetti fani lëmm ndeysaan,
Muy dëtëm metitam.
Ñetti guddi ndeysaan,
Ñetti fani lëmm,
Muy lox ndax metit.
Tawféex gi nekk fépp
Ci càkkeef gépp
Faj gaañ-gaañam ba mu wér.
Jaxaay ja direekoo cag ngeer
Talali laafam,
Wante ax ndeysaan !
Laaf ya ne làpp,
Muy fët-fëtiy dàquw rëbëntaan !
Doomu jaxaay ja sëngeem
Tàgg ca kow doj sa,
Teen xool ca kow kàdd ga,
Teen xool ca kow asamaan sa,
Gët ya, ndeysaan
Tàmm a xoole kow ga,
Daldi taa.
Foofa ñaari pitax
Riiree ca bànqaas ya,
Dal ca tàkku déeg gay samandaayu
Pëndëxu wurusu-ngalam,
Wiccaxu, di wër fu ñu làngaan.
Seen gët yu xónq ya
Di jéer ba daj jaxaay sa
Fa mu sëgg di metitlu.
Pitax ma fal-fal naaw
Ag dëñ-kumpaam,
Wutali ngeer ga.
Lamsal, xool jaxaay sa,
Déey ko ne ko:
Bul nàqarlu xarit sama,
Muñal rekk.
Xanaa gisoo ne,
Lépp loo dabe sa bànneex,
Mu ngi ci bërëb bii?
Gisoo car bee di niroog wurus
Te lay aar ci tàngooru bés bi?
Su jànt di so,
Nga daagu ci tefes gi,
Leer gi wàcc ci sa dën bi.
So xëyye temp ndànk,
Tóor-tóor wër la, mbuboo lay gu bees !
So xiife wut ci àll bi
Ñam wu la soob
So mare, sëgg naan
Ci ndoxu-sayaan
Suy melax ni xaalis.
Ax, xarit sama,
Bànneex dëgg mooy doylu!
Te doylu fu mu nekk la mu am doy.
Céy yi baatu-dëgg! jaxaay ja ne.
Xol ba jeex, mu gën a sàngoo
xalaatam.
Bilaay pitaxoo mbaay,
Sa kàddooy gu mbaaxaay.
Ligeey bi am na solo lool