Liggéey bu mel ni bii ñu fi dëgmal, wareef la ci sunu gis-gis, ñu ñeel fi ca ndorte la góor gu mel ni Seex Anta Jóob. Ndax daf fee def, lu fi daanaka kenn ci waay-xeltu yi ci Afrik ak li ko wër deful: maanaam yesalaat yoon wi àddina sépp doon gise cosaanu nit ku ñuul, fa mu jaar ca njëlbéen ba yegsi fi mu tollu téy. {mosimage}Callalal-cosaan jooju la Seex Anta Jóob topp, dalee ko ca jamono yi nit ku xay, maanaam “homo sapiens” ci late?, feeñe ci déndu Afrik ba jamonooy téy.
Li tax mbir moomu di lu am solo, mooy ne boroom xam-xam yu bare ci tubaab yi ak seeni ndongo yu ñuul dañoo jàppoon ci kow fóogi kese, ne nit ku ñuul daal cosaanam kenn mëneesu ko leraal ndax bindul. Rax ci dolli it, ñooñu ne, li fi suuf si goqi ci ay tabax yu yàgg te kemaane, ca Misira, Nibi, Simbaabwe, Nok ak fenneen, li wóor mooy wenneen xeet moo fi juuxsiwoon, def ko. Ndax nit ku ñuul xameewu ñu ko lu dul roy, njaam ag di wéy ci ndiggëlu kenneen.
Téy, ba Seex Anta ñëwee, wéer ay gëstoom ci xam-xam bu wér, ay firnde yu kenn mënula nàttable, leer na ne nit ku ñuul moo njëkka nite ci àddina, moo njëkka bind, moo njëkka tabax. Fi sax faf, ci Afrik la Yàlla tënee sunu Maam Aadama, ba ay sët-sëtaatam joge fi dem dëkki fenneen, melokaanam ag deram dóog di sopiku! Xarala, xam-xam, tabax yi nekk fii Misira ak fenneen it ci Afrik te di yeem niteef gi, du kenn ku moy sunu maam yi ñoo ko fi def.
Wante dafa am benneen fànn bu am solo ciy gëstu Séex Anta sees di faral di umpale. Ndax bokk na ca la mu njëkka bind gëdd gi làkki-réewi Afrik wara dellu am, ba mëna dellu nekkaat ay juntukaay yu mat yuy jëmële askan yi ca kanam. Séex Anta masul a jóg di bind, di gëstu ci wolof ak yenneeni làkki Afrik yi. Ci kow loolu la tekki xeeti xam-xam yu nekk ci wolof: Dalee ko ci xam-xamu yaramal, simi, xayma, mbindum-fént ak yenneen ak yenneen. Naka noonu ci téereem bi njëkka siiw di “Nations nègres et cultures” – maanaam “Waaso nit ku ñuul ag caada” la tàmbalee tekki faramfàcci-ajoodiku walla “théorie de la relativité” bu Einstein, di ki nga xam ne daanaaka xam-xamam àddina sépp la yeem ba téy!
Loolu yépp li mu ca masoon na jublu moo doon wone pexe yi làxxu ci sunu làkk, te amul sax benneen làkk bu mu mënti doon ci àdduna bu leen ca yobul dara.
Su sóobee Yàlla dana ñu fi dellusi gëna siiwal bindi Seex Anta Jóob yooyu ñu bare umpale.
Kon teranga ñeel na ñayu xare jooju jëfam aki xalatam dootul reer ba fàww!
Tamsir Anne © wolof-online.com
yaw daal amoo moroom, di la sant rék. di gnaan yalla diox la xam xam bou bari ba nga mana traduire xam xam yi nék ci aduna bi ci lak wolof pour l’interet de notre nation. Un jour ou l’autre on récoltera le fruit de votre travail précieux.
yalla mi am fay yalla na la fay
yalla na yalla yërëm seex Anta joob te dugal ko ca ajjana ya gëna kawe. Liggeyal na sunuw askan ak sunum réew lu ko kenn masla defal . man nak maangi leen di bégé bu baax yeen ci seen liggeey bu rafet bii rawatina yaw Tamsiir Aan
sen ligeeye rafet na fexe leen laaku wolof bi neeka si internet bi ba melni laak yop ba loy bind si internet bi si wolof nga koy dind gissko
yeen ñéep wax ngeen dégg daa amludes mooy nguur gi ñoo warona jéll ay matukaay yumaat séek ngir tabax ab kagum njangum lákkuw xeetwi manaam Akádëmi Askánwi.Te legetuk neen naxuti bëey manaam lima bégga wax mooy nee waxi keese amul njariñ dumuju feen bisbunek ñingi pasar pasaree alali Réewmi ci lu’éemul njariñ ci Askánwi ndax foo pólitik bu Persida 8 Miliyaar boo ci dindi woon 2 iliyaar
kër tanoor 500 miliyoon nga dindica 200 miliyoon ñaas 600 miliyoon nga dindica 300 miliyoon li kesee buñuko jéloon seet mboleem kàngam yi génaxarale ci lákki Réewmi nganee leen Éelagi Askánwi yéenlako Yálla natoo ñoomit ñu jéll séen matukay yu maaat séek de xool ca 3 lákk yam mbind bapare ñu deeluwaat ca jangu yumaagya xool ba gis xalee yaaca sutum njang ca lákki njégaanya ña xool leen ci walu xeltu manaam sikolóosikmaa ba xaamnee ñu béeg séen réew lañ te xeebuñu seen bopu ñeenñune ñu jangal leen jékk seen lákk’u meen bañuxaamko ci lu wóor ñu soog leena def ay xaac yii jem ci jangale ñii jém ci tekk’i lák ñii di Áada yeek cosaan yi ñaa dem ca Állaba géstu ji turi njaay Álléyee’k ñaxátooyyi garab yeek gañcaxgi buka defee yéen kángam yi ngénn wérngéléen képpu dileen nemeeku ci faan bu seni payoor darra bañcee am galankoor
Te lima wax fii léep 2,500 miliyoon booko séedalee ci 12 weer mu joxla =20.833.333,3 Sefaa booka sédalee 200 nit mu joxla li 104.166,666 Sefaa nga deluka sédale ci 12 weer mu joxla li 8.680.555,5 Sefaa te kon kunee xamnanee li digante kuraan bi ak Kër yee’k wata yi esnum ndox léep manacee génn te buñko defee 5 att yunee manañoo taagát 400 ndaw yu xarañ te ñoomit bu kenn ku neek taagatee 100 nit ci 2 Att kon dinañu am 40.000 jangalekát ci 2 Att yune te dusoxlaa ñuy yooku darra ci gafakák ngurr gi