Bésu 21 fan ci weeru fewrie at mu jot, moom la kurél giy toppatoo caada, njàng ak xamtéef (UNESCO) te féetoo ci mbotaayu xeet yi, jagleel làkki ndey, maanaam làkk wi nga xam ne moom la nit ku nekk nàmp. Loolu bi ko UNESCO dooree ak léegi ëpp na 10 at. Li waral bés bi mooy yee nit ñi, artu leen, soññ leen ci solo su jéggi dayo si làkki ndey yi am ci fànnu yokkute yépp. Rawatina ci réewi Afrig yi nga xam ne daanaka, ya ca ëpp ba ñu tàbbee ci “kolonisation” ba téy jii ñu moomee seen bopp, dañoo xeeb seen làkk yi ñu nàmp. Réew yi gën a bari Afrig, Senegaal waxi noppi, seen làkk sedduñuleen daanaka benn cër bu takku. Kenn du leen jàng mbaa di leen jàngale ci lekool yi, kenn du leen jëfandikoo ci béreb yiy nguur yi di nas ak a nocce ak feneen ak feneen… Dañu leen a soofal, fóoyóoyal leen. Te fekk nag, loolu sax naka jekk moo waral ag fàttali gu ni mel, amul wenn askan wu mën a am tawféex, yokkute ak jëm ca kanam ci wàllu politig, koom-koom, njàng ak leneen te dumooyu say làkk. Bind nañu ko lu bare, indi nañu it firnde yiy wone ne réewi tubaab yi seen bopp ñuy roy ci lu nekk, laata ñu doon génn cig lëndëmtu, dañoo mujj a dekkil seen làkk. Loolaa nga xewoon ca ndorteel 15 eelu xarnu ba : booba ñoom làkki lateñ rekk lañu daan jàng di ca bind, defe woon ne seen làkk tekkiwuñu dara. Ba ñu dagge buum googu lañu tàmbale gindeeku ba léegi, am yokkute ci lu nekk, ba tollu tey ci boppu àddina. Looloo waral bi UNESCO nemmeekoo càggante ak yàq gu jéggi dayo googu ci cër bi ñu sedd làkki ndey ci yenn réew yi la def at mu nekk muy fàttali xeet yi ak askan yi seen làmmiñ! Ndax gëstu yépp ci fànnu xam-xami làkk ak xaralaay jàngale wone nañu ci lu wér, ne xale bi door njàngam ci làkk wi mu nàmp, mooy gën a ubbeeku fuuf moroomam ma tàmbale njàngam ci làkk wu mu nàmpul.Xelam ay gën a ñaw ci xam-xamu yu mel ni matematig te itam mooy gën a gaaw a mokkal weneen làkk wu dul wi mu nàmpul. Li ko waral mooy xale bi buy dal rekk dees di mën a tàggat xelam ci fànn yu bare niki matematik, xam-xami cosaan, fisig ak yeneen…Te bu dee, kom ni ñu koy defe Senegaal, njàng mi yépp ci nasaraan la, su xale bi dugge lekool day mel ni ku lu. Day mel ni perantal buy door a jàng wax. Dina def lu yàgg ciy at balees ko mën a jàngal lenn lu am solo ci nasaraan. Ndax déggul làkk wi! Li ëpp ci lu muy jàng du weesu ijji ak nafar lu mu xamul lu muy tekki… Rax ci dolli loolu da koy jural mu xeeb li mu doon : ku nekk xam na ni tiitange ak ug jaaxle la xale boobu di am, su ràññee ne, ndekke moom làkk wi mu nàmp tekkiwul dara ca béreb yay indi tekki ëllëg ca réewam ! Foofa lay tàmbale suux ndànk-ndànk ci lu ñuy woowee “crise d’identité”, maanaam, dootul ràññeeti li mu doon, day nekk ku neex a yobbale, ku neex a ómmat! Waxoon nañu fi itam ne sax soo koy seet, demokarasi bi ñuy wax, maanaam “nguuru askan wi ngir askan wi”, mënul a am ci làkk woo jeggani!
Wante tey bi ñu deme bay tekki ci saa si lépp li ñuy wax ci pencum réewum Senegaal ci làkki réew mi, ku nekk di kam lañuy wax, mel na ni li ñu fiy mas a wax kon am na ñu ko tàmbale dégg ! Ndokk! Wante li des bare na lool: jot na ñu jàngale làkki réew mi ci daara yi, ci lekool, jot na ñu leen di jëfandikoo ci beréb yi ñuy nase ak a dogal mbir yi soxal askan wépp!
Dr. Tamsir Anne © wolof-online.com
waxati nga dëgg. waaw li ma bëgga laaj mooy nan prograamu jángum wolof tëdde ca Senegaal fii mu ne? ndax limakoy laaj ci ay nit dafa bari te ba leegi mënu ma leena tuntu
Jërejëf sëñ Balla ci sa xalaat yu rafet yépp…njagaleem wolof nag ba léegi seddaguñu lenn lu am solo…duggagul ba léegi ci lekkool…tumuraanke rekk…! Mel na ni sunu njiit yi ba léegi gindeekooguñu…Moo tax jëm-ca-kanam di na jafe lool…
bir mi booy xool dafa dow sax yaram! waaye nan yokk gëstu yi.
May laaj ku bëgòon’a siiwal ab téeré ci wolof nooy def?
sama mail: serignemor@hotmai.it
li nga dëgg la gu wex qàtte ne kanni waante mbirmi dugubi nduxumla la ko yàx ma nga ca bir suf sa ndaxte liy sunu gimiñ nunn waa Afrig mooy ne ba fi Tubaab bi di jóge làtaa muy dem dafa jéll ay doomi réewmi dugél lenn ci bajub wordusabeel fóott lénn bañu seet weeci ca lañu naampon mu tàggat lenn ca lako neex li moo tax .
munee lenn nakk kuci bégga tekk’i éllag danga wara mel ne nun di roy ci nun di xool ci sunuy bët di xalaat ci sunu làkk ndax nuun kaat nooy yéen kuci meel ne nun doo am darra lu lay galankor ci aduna si .
te liy fër nde ji mooy ne leopool sedaa segoor tubaab bu ñuul la woon ,Abdu juff doomam la woon ,Abdulay waad ñaari doom been jabàr ak ki sétam ñëpp Frânsse la ñiy wax te mboolem ñi nee ci ngurr gu sénni doom ñaa ngay jànge ca bitiim réew mbaa dugél lénn ca lekol lu nasaraan sa fumel ni salesiyaano wala seent mary de ann.
te ñoñee élék ñooy wéll bétiku’at yoorsi réewmi te bu g¡kerooge ñoom duñu dëgg sex wolof ba koy wax ,te wal yées bi la’i leegi kay yéen ñii yàlla may xel ngen baña soonu tey baña taayi di ñaan ci kaatanuk sunu boroom mu lamiñ ak xélima gu am barke ba gone’yeeg magi qérrnu bi fekki si len ci li ngeen yénee réewmi ci dara jay yónent yàlla bi ak wormay magg ñu bax ñifi neek koon tey wax taan ak kilifay diinne yi ndax ñu jaapu le nu ci .
Aslaamu’álaykum yéen kurelgi noongileen di nuy kuneek ci turam ak santam tey ñaan Yálla musalléen ndax nunday sunu boroom dafanoo natoo ay njiit yu xámul fuyuy tek seen tanka koon dina jafee lool nugénnci nattubi¡¡ it wolof nee kulamay aygat wala aybétt sakala fooy xool li moonudál ndax ñiinu jiite Tubaab beeleenfitak waaye yamuñufoofu képpu ku jóg ngir wax lunimel ñuxupula ba boo ragalee danga deltucaganaaw boo ñemee te amoongor ñu faf la nger banganee nuut