Reggal nga mboolem xarnu bi
Sa yërmandee nu daa
sanal Jigéen ña, yaa nu daa amal
Tay ñépp a yam ken amatul
Sëriñ bi geesul xarnu bi
Ñoo séen i sag sàggiku na
Ñoo séen i gaay dàggeeku na
Ñoo séen i ngëm rékkiku na
Ngir ñàkk gii ci xarnu bi
At moo ni ndax mooy tane daaw
Mooy gën a far dellu gannaaw
Ba rab yu aay yi sax di naaw
Ay Mbàkke ! géesul xarnu bi
Wëy ! nu ni wëy! noo ka torox
Yalwaan, amoo ku la sarax
Garab bu daanoo xob ya lax
Bàmba’ay danjaamal xarnu bi
Garab gu mag bu nee jirim
Garab yu ndaw yi day jirim
Méññat ma say mbir ya ëlëm
Lii rekk a dal waa xarnu bi
Allaahu akabaruz zamaan
Jamono moo man a safaan
Xéewël yi daf daa walangaan
Ci ndabi mboolem xarnu bi
Libeek, sikkeek i sëhfaraan
Lan daa diwoo muy walangaan
Nuy xelli kopp ya di naan
Wata ya kornu xarnu bi
Astaxfirul Laahal Aziim
Tuub nanu lan daa def i koom
Te muy lu neexulan boroom
Jurbel a wuuteek xarnu bi
Xeewal yi daf daa wal-wali
Baawaan fi nun di kel-keli
Moo tax ma jóg di pél-péli
Sëriñ bi geesul xarnu bi
Xeewal yi daf daa walangaan
Waxset nga wuute nga’ak sayaan
Xamoo xur’ak tund’ak sayaan
Sam ndox a naatal xarnu bi
Wàcci nga yaw loo mas a wax
Def nga ko jox ku mat a jox
Daawoo nu nax, daawoo nu cax
Séddon nga mboolem xarnu bi
Gàñcax gu ndaw gi weddatul
Mag ña nga yar ken woddatul
Moo tax ma naala suuxatal
Njëmbët li wan ci xarnu bi
Njëmbët la mooy gaa ya dikkon
Daa wéy ci xeewal ya fi won
Tay ñi ngi def ya ñu bawon
Ngir ñàkk gii ci xarnu bi
Ag ñàkk a bon ci waa ju baax
Day tas kërëm xolam ba jaax
Daa ceeb u tay ngay añe laax
Jaaxal na gaa yi xarnu bi
Leek-leek nga gis fi ab muriid
Muy taxawaalu ni’b mariid
Walla mu xàcc def tëriid
Ndaw njombe gaa yi xarnu bi
Ànd’ak komersaa ya di jaay
ñii di wajaaseeri baxaay
Te xamni yaa doon séen i baay
Moo tee nga naatal xarnu bi
Ña lee nga xàcc i defi seef
Ñii def i dag ngir bañ a loof
Ñii daw ba raw ba ni nu fuuf
Moo tee nga naatal xarnu bi
Yaw la nu yaakaar abadaa
Ngir yaa nu tàggaleek bidaa
Tuub nanu mboolem la nu daa
Bàkkaar ci njëkk xarnu bi
Yërëm nu tay yaru na nu
Dóotu nu fo, xàmme na nu
Dóotun nelaw, yewwu na nu
Yërëm nu naatal xarnu bi
Soo nu joxoon la nu yoran
Dóotu nu def ,nanu defan
Xanaa yëgooni yaru nan
Ku weddi laajal xarnu bi
Yërëm lu nan, torox lu nan
Jooy na nu ren, saraxtu nan
Soppeeku nan, jébbalu nan
Sarax nu naatal xarnu bi
Nun tuxu nan sun kër i baay
Gàddaay te def la ngën ji baay
Tuubaa di kër, bàmba’a di waay