Xarit, nit ñi kenn mënul a tax ñuy gërëm
Te kenn mënul a a tax ñuy goreedee ak a jëw
Ag rëylu day xañe kow
Ag suufe maye kow
Ku rëy du jëm kow
Du dooni mukk it ngal doole
Defal garab gu léwet, gu sedd ker te guddul
Tey maye doom it, ba ku mos daldi raaseeti
Bul wex, garab bu wexee, doom ba kenn du ko sex
Mbaa waa ju ko sexati day daldi yàbbeeti
Feexal, sëqal, nëtëxal, yaatul te bul am i dég
Garab gu mel nii ma wax, doo gis ku koy bàyyeeti