Benn bés, benn woy: Sëriñ Musaa ka

Sériñ Mbay Jaxate

 

 

Ab sang day muñ
Di jegal ñépp moy te du moy
Te doylu doylu gu wér
Wëlis ku nekk yëfam
Ab cang a ngii
Lu ko moy dug sang
Ndof la gu rëy
Li ñépp jëm léegi def koog cang
Yow bu ca jëm
Jëmal ci Yalla, doyloo Yàlla ak dogalam
Bul fàtte yit senn saa bés penc baakik mbiram
Bu nit ñii de fatte dee te bég ci adduna gii
Fabal sa xel teg ca dee ak Yàlla yow te xalam
Bul soxloo lëf ci dunyaa jii lu dul jëfi yiiw
Ku nekk day mujj weet ak jëfam ci paxam
Loo saytu dem ba ko mbaa sax loola dem ba la yow
Sa jëf nag du la ba dem te doo ko ba dem
Boroomi yëf dina tàggook yëfam bu rafet
Boroomi jëf nag du tàggook ay jëfam fu mu jëm
Fabal sa jëf yi ngay àndal defar ba mu jag
Koo gis jëfam ja la am
Lii rekk moo mat a xam
Li ngay wuuf ak li ngay tiye ak li ngay tiim
Li ngay yobbale moo jar a bàyyi xel
Mooy li nga mën ci lu baax nga di ko def
Li nga mënul nga yéene ko te di ko jéem