Moo xam, la wàcce asamaan
Mooy waykatub gën ji mbindéef
Di rammu xeet wu jëm jinaan
Yal na nu Bàmba def muriid
Terub mbalaan i sama xol
Mootax nu sax ci di la woy
Ca bis ba Yàlla di yërëm
Wàllil nu yaw ci say juróom
Wuntu ya, yaa yor seeni doom
Waaju la soob mu daal di wéy
Yonen gërëm na la’ak ñeneen
Jinne ya’ak Malaayika ya
Nottil te lekk nag, te naan
Doom a di baay kii du kaneen
Ak doomi baayi Mustafaa
Te amna xam-xam, ame koom
Ku laaj, mu joxla lay sa muur
Tuubaa di sun madiinata
Li dale fii, ba weesu faas
Ngir naaru góor ak fasu par
Ba wàcc Tuubaa ngën ji gaar
Dóotu nu tàppaatuy sayaan
Naalam wi/u yal nang ko matal
Jumaa ja bayti tabaxoon
Wuy ji boroomam ba kamaal
Nga boole koo’k ngënéeli daam;
Sultaan nga boole koo’k wilaay
Bihaqi xaadirin muriid
Faadilu mooy “fadlu hamiim”
Moo nàmp yaari meeni ngor
Nday jaa di xayru muhsinaat
Donoy usaynu wal-Hasan
Niru na baay ba, mat na doom
Te ëndiwul alal di jaay
Moo naan ci géejug hikkamam
Ci moom, te yal nan am i sët
Xarbaax la feese, bani guun
Soo ko gisee ma ngay bangeer
Day fal di folli ci lu gaaw
Mooman arab te man wolof
Kuy rooti, moodi dex gu fees
Mbër mu ko sóoru daal di luum
Nërëm-nërëm, di safi mbaam
Ku dégg ñaan, nani amiin
Ku teeru naan, lekk ba suur
Tem bari xam-xam am alaal
Jigéen ja far tàngook sagoom
Musula jaar ci yëfi ndaw
Moo raw ña xàllon moom a lef
Nuurul wilaaya la sàngoo
Mooy yërmàndey waa xarnu bi
Defar na léen ci xarnu bi
Bañ man a ànd’ak xarnu bi
Cofeel gu am ci xarnu bi
Baawaan ci gaa yi xarnu bi
Dóotu ma toog ci xarnu bi