Lenn li
Ci kow puj yépp
Lépp a ngi ne tekk
Ci senn ruxx
Do yëg sax
Lu noyyi.
Picc saa ngi ne selaw
Ci àll bi.
Xaaral rekk,
Léegi yow itam
Nga noppalu.
Goethe
Tekkikat bi Dr. Tamsir Aan.Téere-Woy yi(2011, Kulturbild Verlag)
Category: Mbindu-fent