Juwaalo
Juwaalo!
Maa ngi fàtteliku.
Maa ngi fàtteliku siñaar ya ca keru mbaar yu naat ya
Maa ngi fàtteliku siñaar yeek seeni gët, kéemtaanee lool
Di sàmandaay leeraayu weer cig tefes
Maa ngi fàtteliku jànt yu so yu taaroo-taaru
Kumba Ndofeen naan da cay dog manto buuram.
Maa ngi fàtteliku bernde dëj yuy gilli deretu gétt
Cóow li, tàggate géwel yi
Maa ngi fàtteliku peccum njegemaar yi
Bàkk yi, Ax! dukkëtu xale-yu góor, yuxóol seen gënnu yaram
Ak njaayxóóle jiggéen ñi – Kor Siga!
Maa ngi fàtteliku, di fàtteliku…
Sama bopp biy riir…
Ndaw doxantu bu gééy ci bési Tuggal yi
Yenn saa yi ab jaas bu jirim jolli, di yikkët, yikkët, yikkët….
Lewopóol Sedaar Seŋoor
Tekkikat bi: Dr. Tamsir Anne
amna soola lool