Nebedaay walla ci turu wolofam dëgg saab-saab, garab la gu bari ay ngëneel ci wàllu dund ndax witamin ak ferñeent yu bari yi ci nekk ak li mën a faj mbaa fàggu ci ay jangoro. Su ñu wesaare woon ngëneel yi nekk ci nebedaay ba ñépp jot ci, kon tey febaru xale yu bare dooti fi amati. Garab la itam guy raxas ndox mu yàqu ba mu dellu seetaat wecc!
Tey ji nebedaay da ñu koy jëfandikoo daanaka ci réewu tubaab ci wàllu indistri yépp: dalee ko ci lépp lu jëm ci wàllu taaru-yaram, jaar ci fa ñuy defare garab ak yeneen.
Garab la itam goo xam gu yomb ay mbir la, ndax daanak lajul ndox, fépp la mën a sax.

on Jan 01 in NEKKIN, Uncategorized, Wér-gu-yaram, Xamtéef tagged by tam
Am na solo lool. Jaa ngeen jëf