Masambaay Mbéri Ndaw
Béy du raas deemu guddee!
Masambaay Mbéri Ndaw
Béy du raas deemu guddee!
Yégg naa! Yégg naa! Yégg naa !
Yégg naa ba ca biir Kaaba ga!
Bind fa laam ak liif soo ga ñëw
Laam ak liff googu laay daane mbër!
Fa ma jaar ku fa jaar taq ban!
Janq man jeeg man caga man!
Njegamaar bu ma seen dootul dem!
Góor ñi sax dañu maa xawa nob!
Sama jikko jii
Sama jikko jii sopp naa ko
Laaj ma lu tax
Damay def ngir Yàlla
Ndax jëf du nax.
Tabe naa xam ko
Am di joxe
Kenn xamul lu tax
Lu waay di def
Na ca mën a sax
Ndax jikko du nax
Duma maye sama xol di fasu
Ndax Yàllaa tax
Mooma defal boobu jikko
Danaa ko wax
Samay loxoy déggook sama xol
Bilaaxi maa sàkku baax
Yaafuusuma, tayeeluma
Dama leen di cax
Li ma am moo ma ko mayDanaa ko wax
Ndax su ma fi jóggee ëllëg
Seede bi mën fi sax.
Sama jikko jii sopp naa ko
Laaj ma lu tax
Damay def ngir Yàlla
Ndax jëf du nax.
Tabe naa xam ko
Am di joxe
Kenn xamul lu tax
Lu waay di def
Na ca mën a sax
Ndax jikko du nax
Duma maye sama xol di fasu
Ndax Yàllaa tax
Mooma defal boobu jikko
Danaa ko wax
Samay loxoy déggook sama xol
Bilaaxi maa sàkku baax
Yaafuusuma, tayeeluma
Dama leen di cax
Li ma am moo ma ko mayDanaa ko wax
Ndax su ma fi jóggee ëllëg
Seede bi mën fi sax.
Mbërum Buur
Mbërum Buur a baax!
Badoolo du ko téq
Da koy ragal
Andaari lem
Andaari njaw
Andaari soowu béy
Mbërum Buur a baax!
Badoolo du ko téq
Da koy ragal
Ma Lambaay
Currrrrr! Sagingi-ndaq!
Ma Lambaay a nga Lambaay!
Biram Ndumbe ma ga ca Mbul
Majojo Dégen ma ca ngoonal lu réy la !
Maa jar a woy ma jara kañ !
Maa di waaguñaay!
Duubal Lees mi ñiy coow,
Maa ko nax daan!
Mbay Géy mi ñiy coow,
Maa ko nax daan!
Boy Bambara mi ñiy coow
Maa ko nax daan!
Ee! Ma ne jaalu muus
Jinax du ko yër !
Lambi muus jinax du fa daagu !
Lambi gaynde nit du fa daagu !
Lambi mbott gunoor du fa daagu !
Currrrrr! Sagingi-ndaq!
Ma Lambaay a nga Lambaay!
Biram Ndumbe ma ga ca Mbul
Majojo Dégen ma ca ngoonal lu réy la !
Maa jar a woy ma jara kañ !
Maa di waaguñaay!
Bëre leen
Bëre leen góor ñi
Góor ñi bëre leen!
Làmb bu ca góor nekkul
Jiggéen na koy moomee!
Bàyyi leen seen yaaba ji te laale
Laaleey mbaaxu góor!
Ne bu doon làmbi jiggéen sax jeex na!
Aayee !
Làmb bu ca góor nekkul
Jiggéen na koy moomee!
Aayee !
Manjaago baa nga daanu ca pom ba
Diw ga jalaañoo
Lank naa du ma bëreek manjaago
Diw ga da may laal.
There are no comments yet, be the first.