Luy jot jot na, ginnaaw dee
Kuy woddoo làmmiñ, soo noppee rafle
Wuude, lu mu wax ci feebaru béy, der baa ko waral
Xaalis du faj dee, gàcce lay faj
Ku jàppul ci yatu getax, doo am yatu kel
Yàlla bindul ku dul dee waaye bind na ku dul torox
Làmmiñ du tànk waaye dina tarxiis, gémmiñ du furno waaye dina boy
Nag wu ñuul ku ci am meew mu weex war a sànt
Alal na mag boroom, ndax su ñu maasee ñoom ñaar yéwén ci day daldi jafe
Ndimbal na ca fekk loxol boroom
Kër baay du kër
Su bën dee seeñu yax, suux saa tax
Bala ngaa xam xamadi xaw la rey
Wax dëgg du wàññi wërsëg
Doxkat du fekke dëju maamam
Njëriñ loo fekke
Jaam ak pexeem, Yàllaak dogalam
Ay du weesu baay dee na
Lu jot yomb
Kiy liggéey mooy yàq
Politig, ci àddina la yem, kenn du ko yóbbuwaale àllaaxira
Ñaari loxooy tàccu
Nettali ci gémmiñu boroom la dàqe
Koo mënul muñ li mu làq doo ko sañ a wax dëgg
Su mbote bootoo ci gaynde tey ree, ñàkk ku ko yedd a tax
Daw ca ba ngay am i tànk
Ñaari tànk ay dox mbokk
Ku la yéene xiif, saa yoo ko rombee géexal
Alal ganug dof la, buy ñëw du tàggoo, buy dem du tàggoo
Ku la mag ëpp la ay sagar
Ku bëgg sa taar moo la naan sangul
Liggéeyu ndey, añu doom
Soo bërewulee ñu bëre daanu sa kow
Fu fas dul dem, xel a fay doxantu
Dof boo gis, ay nit a nga ca kër ga mu jóge
La muy saf ka ko macc a ko xam
Kuy yoot du sëqat
Ba la ngaa pes sàmm bi xaaral ba xam lu muy wëliis
Kenn du jënd jaan ci pax
Lu feeñ ci séy, nuyoo na ca ndoxaan la, xanaa kay dañu koo feyul woon rekk
Alalu golo ca lex ba
Ku ne ‘wëy’* tey jii, dinga ne ‘wóoy’ ëllëg – Séex Anta Jóob –
*wëy mooy ‘oui’ ci nasaraan. Mooy jamono ja Se?oor nee ñu woteel ko,
te Séex Anta di artu waa Senegaal, naan leen ku defal Se?oor li mu
bëgg dinga ko réccuji ëllëg.
Waññi boo gis ci benn lay doore
Ay du yem ci boppu boroom
Lu kenn mën, ñaar a la ko dàq. Ba mu des lan ? Xanaa… wéet !
Bëgg naa la, bëgguma la, loolu jarul coow – Njaga Mbay, woykat –
Mbeju kanam boroom a koy fajal boppam
Montar yu baax yépp a bokk waxtu
Bóli gu dog tiiñ na doktoor
Ku jaan mátt sam xel dem ci dee, ba ngay dund ak ba ngay dee yépp sam xel dem ci dee
Saabu du fóot boppam
Dërëm ak dërëm ñoo mën a ànd
Tere-tere mu të, bàyyil mu gis
Yágg dox, yágg gis
Mbamb du weesu weer
Ku muñ, muuñ
Ku mënul bawoo, lu yáqu yowa
Ku mën te defoo, lu yáqu yowa
Waa dëkk bee xam lu ndoxu teen biy saf
Ñaq du feeñ ci taw bi
Werante xuuxaan tekki tubéy
Xuloo sën la, lu waay jot sánni sa moroom
Naar ba noon na : bés bu ma amee, képp ku ma xamoon ba ma ñàkkee, yal na nga dee