Waxi Wolof Njaay

Foo déggee bukki bu yóoxu am na bu la jege te yëgoo ci dara

Yëkk du taxaw ñuy natt ci tungune

Benn lam kott ci loxo du kele?-kele?i

Su muus reggee ne jinax dafa xasaw

Ñiy gàmmu ak ñiy raas déem bokkewuñu

Bu jinne bëggee daqaar, ku yéeg daanu

Du man, du man, fa mu àgg du yow àggu fa

Kiy liggéey mooy yàq
Politig, ci àddina la yem, kenn du ko yóbbuwaale àllaaxira

Ñaari loxooy tàccu

Nettali ci gémmiñu boroom la dàqe

Koo mënul muñ li mu làq doo ko sañ a wax dëgg

Su mbote bootoo ci gaynde tey ree, ñàkk ku ko yedd a tax

Daw ca ba ngay am i tànk

Ñaari tànk ay dox mbokk

Ku la yéene xiif, saa yoo ko rombee géexal

Alal ganug dof la, buy ñëw du tàggoo, buy dem du tàggoo

Béjjénu xaaf, ba muy màgg bay wëndéelu, booba mag ñaa nga fa

Doxkat du fekke dëju maamam

Picc a moom boppam, garab gu ko neex lay tag

Dëkkëndoo bu yàgg mbokk la

Ku la mag ëpp la ay sagar

Ñaar a mën kenn te ñett duñu bëre

Lu la mar mayul, màtt du la ko may

Ñemewuma bor, man damaa am pey – Séex Aamadu Bàmba Mbàkke, Seriñ Tuubaa –

Ku jaaxaan di saw, noo def tooy

Yéene néeg la, boroom a cay fanaan

Bu la wéet tee nekk gor

Ku bëgg sa taar moo la naan sangul

Fullaay jaay daqaar walla ma mos jeexal ko.

Liggéeyu ndey, añu doom

Soo bërewulee ñu bëre daanu sa kow

Ku boot bukki, xaj baw la

Ndënd mu ñu tëggee sémmiñ : neex benn yoon naqadi benn yoon

Boroom làmmiñ du réer
Wax loo mën, def loo mën, soo tëddee nelaw

Yóbbante bor la

Saaku bu feesul du taxaw

Fu fas dul dem, xel a fay doxantu

Gan du tabax

Leketu kese naxul béy

Dof boo gis, ay nit a nga ca kër ga mu jóge

Góor : fit

Damm koon, damm koonte na daaw

– Lat-Joor Jóob, Dammeelu Kajoor –

Bët du yenu waaye xam na lu bopp àttan

Nit, nit mooy garabam

Kanam du kaso waaye ko ci tëj mu xam ko

Yàlla-Yàlla bey sa tool

Sácc tama yomb na, xanaa am foo ko tëgge mooy jafe

Kuy dóor-dàqe ak sa xel, du ñàkk nga dem ba foo nëbbu xaw laa jaaxal

Bo yëkkatee sa benn loxo ne faalewuma kenn, boo yaboo yëkkati ba ca des ne kenn faalewu ma

Buur aayul, dag yaa aay

Gunge bu yàgg defarul teeru bu ñaaw

Deret jaxasoo, xaste jeex

Kay sàmm mbott moo xam ba cay soox

Woyu biir kenn mënu koo awu

Boo amee sa xaritu gunóor, bu ko sànni ci kekk li

Liir du wonk

Yakk ba la fekk fande moo gën ci yakk yi

Bu till lekkee alom, na ko gërëme coy

Bés du mag du tuuti, boroom lay tollool
Bañ bañ bëgg

Àtte Yàllaa gën bu nit

Lu defu waxu te luy ay di jàmbat