Woyi nax-xale


Baay Malamin Daara

Bindal na ma tereee
Tere yombul Saalum
Salum ñaari neeg la
Ñeteel ba di waañ wa
Waañ wa waañi buur la
Buur ba buuri Saalum

Baay Malamin Daaraa
Bindal na ma tereee
Tere yombul Saalum
Salum ñaari neeg la
Ñeteel ba di waañ wa
Waañ wa waañi buur la
Buur ba buuri Saalum
</hr>
Aayo nene

Aayo nene
Nene tuti
naxal sama nene

Nene lu muy jooy
Yaayam dafa tukki
Nene warul jooy

Yaay booy!
Naxal ma nene!
Nene lu muy jooy?
Nene warul Jooy!
Bul jooy sama nene
Yow boo jooye
Sama yaram daw nene

Kuy laal Mademba

sabar ya ca Ndayaanee
Ku laal sama doom jee
Salaan jooyul weetoo!

Sama doom sama sopee
Dunda mata jooyee
Dundal!
Soo dundee
Ba magg
Feral saay rongoñee!

Kuy laal Mademba
sabar ya ca Ndayaanee
Kuy laal ndaat saay!
Ku laal sama doom jee
Ayoo beeyoo beeyoo!

There are no comments yet, be the first.

Leave a Comment