Alxuraan ci Wolof: Suraat CXIII – Bes tenk

Wàcce ci Màkka 5 laaya
Benn – Senn – Menn la – Raax Menn – Raax Yërëm

1- Nil damay wut kiiraay ci Yàlla fa bër sete

2- Muslu ci mbon gi ci mbindeef yi mu sàkk

3- Muslu ci musiba guddi lëndëm këriis fa mu ñu bette

4- Muslu ci mbonu dëmm yiy wal ciy paspas

5- Muslu ci musiba kañaanu ki añaan

Tekki bi: Pathe Diagne, Alxuraan ci Wolof. Editions Sankore, L’Harmattan.

There are no comments yet, be the first.

Leave a Comment