Ci 22 fàneelu-ñaar ci wéeru Mars 2009 réewum Senegaal wóote na mpalum ndawi gox yi gox-goxaan yi, maanaam ndaw yu mel naka meer yi, njiitu kominite riiral yi ak ñi leen di jàppale.
Ba nguur gi tàmbalee yenneku yenn ca ay sañ-sañam naka moomeelu suuf yi ci dëkki-kow yi ba léegi nag, ndawi gox yi ak gox-goxaan seen doole ag seen gëdd dafa yokk bu baax. Loolu tax ba xëccoo bi ci diggante parti yi gëna meti.
Rax ci dolli ba parti yi àndoon ak Ablaay Wàdd ci àtum 2000 tàggook moom ba léegi bii mooy daanaka seen jàkkarloo bu njëkk gànnaaw ba ñu joggee ca wóote 2007 ba ñu bari ca ñoom jàppoon na wóote boobu jaaruloon ci yoon.
Image
Loolu taxoon sax, ba parti yu bare gedd wóote ndawi réew ma ca toppoon. Gedd googu nag, ñépp jàpp nañu ne ak njuumte gu réy lawoon. Ndax jurul lenn lu dul PDS aakimoo penccum ndawi réew, di fas aka fecci lu ko neex!
Parti yi ànd boloo ci làng gi ñi tudee Bennoo Siggil Senegaal nag ñoo gàddu ndam li! Ndax dëkk yu mag yépp, daanaka, dalee ko ci Ndakaaru tekk ci Ndar mbaa Kawlax ñoo fa raw Coalition Sopi, mi bolee parti bi nekk ci nguur gi ag ñi koy jàppale. Ràññee nañu it ne yenneen làng yu mel ni Ànd dekkal ngor, mbaa parti Maki Sàl bi nekkoon jawriñu Ablaay Wad, laata muy gàddaay PDS, wone nañu it ne am nañu mbooloo mu tàkku mu leen topp.
Wóote bii nag parti bi nekk ci nguur ñakk mënees na cee jà ngee lu bare: lu ci njekk mooy ne askani Senegaal ci boppam moo yeewu ci wàllu politik, ba daanaka kenn mënatu ko nax. Ndax nit ñee seen bopp dañoo xam njariñal demokaraasi, xam it ne seen baat, seen kart lu am solo! Wone nañu ci anam yu leer yu amul benn nàttable ne àndu benn yoon ci politik bi nguuru Ablaay Wàdd di doxal.
Moom njiiitu réew mi ci boppam nee na it dégg li ko Senegaal wax ci wóote boobu. Kon nag amaana buntu yakaar feeñaat, Senegaal dellu dib royukaay ci Afrig ak ci àddina sépp.
Tamsir Anne © wolof-online.com