Ci atum 2008 la ñu bari ci parti yi juunoog nguur gi jël seen matukaay daldi wóo réew mépp, amul xàjji-ag seen wan làng lañu feetoo ci wàllu politik, ngir ñu diisoo. Disóo boobu li ko waral, ñu ne, mooy gutë gi nga xam ne téy réewum Senegaal da cee tàbbi. Ndax gànnaaw ba parti yooyu boolewoon seen doole ak PDS, di parti bi tóog ci nguur gi téy, jàppalewoon Ablaay Wàdd ba mu jëlee fi Abdu Juuf , dañoo walbatiku feewaloo, ba kenn ca ña àndoon ak Abaay Wàdd daanaka àndatul ak moom téy. Waa PDS nak, ñoom ba ñu leen wóowee ca ndajee moomu, dañoo lànkk ne du ñu ca bokk: Ndax ndaje moomu, du lenn lu dul waxantoo ka foontu, nde ña ko sumb, kenn yebbalu leen, kenn mayu leen kàddu, kon munu ñoo waxal réew mi. Yore wu ñu kàddu réew mi. Téy jii nak, dafa mel ni mbir yi soppeeku nañu ci fànn woowu, ndax bu yàggul dara la njiitu réew mi, wax njawriñam ju mag ji di Suleymaan Ndeene Njaay, ne ko mu jotali opoosisyoÅ‹ bi, ne leen da leen di bëgga wóo ngir ñu waxtaan ci lépp lu soxal réew mi. Ndegam wóote boobu da na mujj fenn? Ndax da na tax ba réew mi booloo mànkoo mel na mu meloon ca atum 2000? La ca kanam moom rawuli bët gaa, wante mel na ni téy Abaay Wàdd ñu bari ca ña daan ànd ak moom dañu koo weddi bu baax: ndax nee nañu loolu muy wóote newul ci moom, duggeewu ko lu dul naxaate kese. Li ëpp soloo nag ci li disoo boobu meññ nag mooy li mu fésal doggu gi doomi-réew mi doggu ngir suxali Senegaal ci kow xel ak xalaat, dëggu, mànkoo, yar ag teggin.
Pencum réew mi
Category: Politik