Ndaali Maali, walla Mande, benn la woon ci nguuru nit ku ñuul yu mag yi nekkoon démb ci déndub Afrig. Moo fi wuutu woon ndaali Gana ci Afrig sóowu jànt. Gana moom itam moo donnoon jàllooreey yeneeni nguur yu mel ni Aksum , Kuus, Nibi ak Misira démb bu Buur-Fari ya.
Ndaali Maali jàpp nanu ne ca Xeelu xarnu ba ci XIVeelu xarnu ba la fi nguuram lawoon, ëmboon réew yii tey : Maali, Senegaal, Gambi, Gine, Niseer, ak bëj-boppu Gànnaar… Ña fa doonoon Buur-Daali seen jàlloree jàll xarnu yi ba yegsi ci ñun: ñoom Mansa Musaa, Sumaaworo Kante, Sunjata Keyta ak ñeneen. Booba Afrig a yore woon wurusu àddina si, nit di jóge fu nekk di waliwansi di wutsi xam-xam.
Tekki sàrt bi doon doxal ndaali Maali bii topp ci làmmiñu wolof mu ngi sukkandiku ci jukki bu ay boroom xam-xami cosaan yu Senegaal, Maali, Gine, ay gawlo ak ñeneen dekkalaatoon ca Kankan (réewum Gine). Ci sàrt bii la ñu tërëloon yoon ya ñu doon jëflante ci seen biir sosiete ci fànn yépp : koom-koom, politig ak yeneen. Kon mënees na cee jàngate lu bare ci ni maam yooya gise woon àddina, seen parlu, seen xayte ak seen mandute. Jikko ak melokaan yu tumuranke te Afrig ak àddina sépp soxla leen.
I NEKKANDOO CI BIIR ASKAN WI
Matukaay 1eel:
Askanu ndaali Maali limu pegg yii ñoo ko sos:
. 16 xalakat walla “ton ta jon”
. 4 njabootu garmi walla “mansa si”
. 5 njabootu sëriñ walla “mori kanda”
. 4 peggi liggéeykat walla” nymakala”
Pegg bu nekk dafa am ay wareef ak ay sas.
Matukaay 2eel:
Peggi liggéeykat yi “ñamakala” dañoo war fu ñu tollu di wax dëgg seeni njiit, di leen digal, di saytu ci seen làmmiñ ak seen jëf yoon yi ak sàrt yi ñu tëral ci ndaali Maali.
Matukaay 3eel:
“Morikanda” yi walla sëriñ yi ñooy sunuy sàng te ñoo ñuy yar ci diine lislaam. Kon ku nekk yoreel na leen njukkël te war na leen a weg.
Matukaay 4eel:
Askani ndaali Maali ay maas ñoo ko bokk. Maas bu nekk day fal njiitam. Ñi bokk benn maas ñooy nit ñi (góor walla jigéen) yi seen magante weesuwul ñetti at.
“Kangbe yi”, walla maas yi nekk diggante ndaw ñi ak mag ñi, dañoo war a bokk fa ñuy fase tëral yu am solo yépp yi soxal sosiete bi.
Matukaay 5eel:
Nit ku nekk ci askan wi yelloo na dund, yelloo na karaangee ci yaramam. Képp ku faat bakkanu keneen nit, yoon di na la natt ñu faat sa bakkan.
Matukaay 6eel:
Taxawalees na ngir xeex yaafuus ak yàccaral, am yokkute kurél gu ñu tuddee “Könögbèn wölö”.
Matukaay 7eel:
Waaso yi ci biir Mande sàkkees na ci ag kàll ci seen diggante ñoom ñépp. Ñoom ñépp ay doomu bàjjan lañu, maanaam jote seen diggante warul a ëpp loxo mukk, te war nañu di nawante ak di wegante fu ñu tollu.
Naka noonu diggante ay goro, diggante maam ak i sëtam kaf ak fo ak ree fu ñu tollu moo leen war.
Matukaay 8eel:
Njabootu Keytaa mooy njaboot giy jiite ndaali Maali.
Matukaay 9eel:
Yaru gone yi askan wi yépp a ci war a farlu, ba tax askan wépp ay baay di ndéy ci tuut-tànk yi.
Matukaay 10eel:
Nañu baaxoo di jaalewante saa yu nit génne àddina.
Matukaay 11eel:
Su seen jabar walla doom dawee làqu ci seen dëkkandoo bu leen ko fa topp.
Matukaay 12eel:
Ndegam ndono néegu baay a ko yelloo, bu leen fal mukk doom bàyyi baay feek kenn ci baayam yaa ngi dund. Bu leen jox mukk ndogal ab xale ngir rekk am-amam.
Matukaay 13eel:
Buleen tooñ mukk “ñara yi” (manaam boroom kàddu yi walla gawlo yi)
Matukaay 14eel:
Ñeel leen fu ngeen tollu jigéen ñiy suñuy yaay.
Serin Ann, sart bi ni gaka tekke taruna lol.Waw gor
jaajëf Baay Tamsiir. lii de man umpon nama, te lima gëna yéem mooy nimu dëppook jamono ci yu bari ci sunu jamono jii, mbaa sax sunu jamono dabagu ko ci yenn yi.