Cosaanu mbind ci Afrik lu mat a fésal la, ndax ñu bari, waay-xeltu yeek meroe.jpg ñeneen dañoo defe ne caada yi nekk Afrik xamuñu ca seen cosaan xaralaay mbind. Manaam xeetu mbind yi fi nekk yépp dañu leen a jeggani: ci Arab yi mbaa ci Nasaraan yi. Loolu nag dëppoowul benn yoon ak li am: ndax soo gëstoo di nga xam ci lu wér ne fii sax ci Afrik la mbind fekk baax. Fii ci Afrik lañu njëkkee bind. Kon ñakk-a-xam li mu waral bari na! Li wér ci lu ñu xam ci xam-xamu cosaan mooy: fii ci Afrik, ca Misiraay démb la nit tàmbalee bind. Booba ak léegi am na lu ëpp juromi juniy – 5000 at. Cib xaatim àlluwa ji ñuy tuddee alluwaay Narmeer (-3200 laata Juddu Yonnent Yàlla Isaa) lañu firndeel mbind mi gën a yàgg te ñu koy wooyee “hieroglyphes” ci nasaraan.
Baat boobu nag du làkki Maam ya nekkoon Misiraa, baatu gerek la. Mbind moomu turam dëgg moo doon “medu ntr” muy tekki “waxi Yàlla” ci làkki Maam yooya! Ca hieroglyphes yooya mbaa “medu ntr” ya la yeneen xeeti mbind yi ci àddina yépp daanaka sosoo! Bindi gerek yi nga xam ne, la bindi tubaab yi téy jogge, mu nga sosoo ca bindi waa Fenisi. Waa Fenisi yooyu ña nga jàngee woon bind ñoom itam ca Maam ya woon Misira. Waa Fenisi yooyu ay jaaykat yu mag lañu woon: ñoo doon daanaka dox diggante Misiraa ak yeneen réew ya woon Asi mbaa Ëroop; jamono jooja sax gaa Ëroop amagul woon: yeneen réew yu mel ni yu “Hitites” ak yeneen ñoo fa nekkoon! Gànnaaw loolu itam yeneen xeeti mbind yu bari judd nañu fii ci Afrik: Bi ci gëna siiw di bu Meroe, te ngeen di gis nataal bi fii ci xët wii! Mbindum Meroe moomu ba bés ni ki téy xama gu ñu lu muy tekki! Te mbind mu xereñ la, mu am solo, Maam ya fi nekkoon sàkkoon ko fi! Kon téy su ñu naan caada Afrik yi ay “civilisations orales” lañu, cosaanoowu ñu bind, dañuy wax rekk, wante lenn lu wér lalu ko! Ay àtte-ñakkale ak wumpale kese la: du lenneen!
Cosaanu mbind ci Afrik
Category: Caada