La bà mba not ñu naa alee
Notaale góor i xarnu bi
Sirrub dëggoom ba la ni naat
Ca doqi góor ña ñuy sanaat
Ñépp ni nuut tà llal i baat
Ken yënguwul ci xarnu bi
Mu jà ll toog ca gà ngunaay
Buur Yà lla rà ng koy medaay
Diiwaan ba jox ko séen i gaay
Kerook la à tte xarnu bi
Billaahi Bà mba’a dim kelaÅ‹
Moo jà ppu saytaane welaŋ
Ba tër ko rendi fa gaboŋ
Ñibbi si wax ko xarnu bi
«Qaataltu fil bahril la’iin
Kabkabuhuu nadbul amiin
Ma’al amiini wal amiin»
Moo ko waxon waa xarnu bi
Yonent ba’ak ahlubadar
Ñoo dà kku kaarce ya ko wër
Saytaane nërméelu di sér
LÃ bbe ya daw ci xarnu bi
Gaboŋ ña xam na ñuy biram
Galwaa ña xam na ñuy biram
Là mbar ña seere nay biram
Seere sa wóor na xarnu bi
Kerook la là bbe ya ni waaw
Maarà bbu bii bu leen ci gaaw
Leeram gi sarna asamaaw
Sar na ci suusi xarnu bi
Tubaab ya naa ko nan maroo
Soldaar sa naa ko bun meroo
LÃ bbe ya naa ko bun woroo
Ñibbil yilif nga xarnu bi
Tëngaale wuñ la asamaaw
Bër yépp booloo nañ ni waaw
Gurag yi lay nañ sa gannaaw
Nde wub nga là mbi xarnu bi
Karaama yaa nu ko xamal
MÃ qaama yaa nu ko amal
Kaaraanga yaa nu ko defal
Yaa suturaal waa xarnu bi
Àll’ak kër’ak jaam’ak gor’ag/k
Ceddook sëriñ buur’aki dag
Bokk’ak i jà mbur ñépp a jag
Jaaraama daam ci xarnu bi
Luy nit ku ñuul’ak nit ku weex
Diggante askan yu du jeex
Fu nekk daam def na fa seex
Bu man a yor waa xarnu bi
Mbindéef yi yaa léen fal i buur
Ku mas a xëy taal baboor
Di xelli attaaya ju foor
Fajoon nga aajoy xarnu bi
Soodaanu war nañ ni nërëm
Biidaanu war nañ ni na’am
Ñépp di sant ak a gërëm
Ngir yaa defar séen xarnu bi
Ko-mersi naa la mersi ñoom
Pël yaa nga naala «mujji-doom»
Wolof ya naa «amoo moroom»
Yaa dà mbe tagg i xarnu bi
Ken dóotu dox kem li nga dox
Ken dóotu wax kem li nga wax
Ken dóotu jox kem ñi nga jox
Daralewoon nga xarnu bi
Limaamu Shahraaneey kamaal
Téeréerm ba Bà mba lay misaal
Giñ naa ni mooy aboo rijaal
Xutbu yawon ci xarnu bi
Mboolem xawsu ya weyon
Yaa sóobu ngiir ya ñu awon
Wommat nga «ruu» ya ñu yoron
Yeesal nga wirduy xarnu bi
Xaadiru, yeesal ngay biram
Tiijaanu yeesal ngay biram
Shazaliyu, yeesal ngay biram
Kuntiyu jox la xarnu bi
Lottal nga ñoñ sharii’atu
Jommal nga ñoñ haqiiqatu
Sa ngiir mi mooy tariiqatu
Moo gën a jub ci xarnu bi
Woroom kurus yadaa aji
Ak gaa ya daa siyaare ji
Yaa tax ñu daa siyaare ji
Sëriñ sa woon ci xarnu bi
Wommat nga naar yeek i wolof
XÃ llaat nga ngiirum tasawuuf
Shariif yi yaa tee ñu shuruf
Jà lle nga léen ci xarnu bi
Roytéef i xarnu bi nga won
Kiimaan i labdaal yi nga won
Kiiraay i lawtaad yi nga won
Ak nujabaa-uy xarnu bi
Xutbu yi, yaw lañ daa fegoo
Nattu ya góor ña daa tegoo
Lashyaax yi yaw lañ daa sagoo
Bay laaj hidayay xarnu bi
Naar yaa ngi am hidaaya tay
Tiijaan di laaj hidaaya tay
Te musu ñoo weesu bu rëy
Yaw la ñu roy ci xarnu bi
Seex BÃ mba, yaa di ab newet
Sébbi nga tooyal gépp wet
Bay nga mu ñor, góob nga fat
Man ngaa dundal waa xarnu bi