Te mus la fer ci xarnu bi
Bàmba’a di géej gu tàbbi géej
Fekk fa géej gu ni ko ngéej
Mu duy ca léer ya ba ni ngiij
Dellu si tooyal xarnu bi
Lu baax du baax ba jàll baax
Waaye Sëriñ bee weesu baax
Baax a ngi yam fi xotti baax
Baaxaale gaa yi xarnu bi
Waa ju la sopp dal di baax
Waa ju la weddi dóotu baax
Waa joo gërëm muy gën di baax
Waa yoo ko warna xarnu bi
Waayam du ñiit gariiti laax
Dóotul làmbooy sagar di daax
Loxoom du daarati ci mbaax
Ku weddi laajal xarnu bi
Ku weddi lii demal lagan
Iisaa di mbar moo man u gan
Yaa ramla wuute na’ak sa gan
Bàmba’a ko ñaak ci xarnu bi
Ngënéeli daam ya gën a tuut
Xel man u koo takk di root
Mbaa xalima’aki daa yu xóot
Lottal na mboolem xarnu bi
Xarbaax la raw na kuy xiyaas
Lu xel dajul deefu ko raas
Fugraas la rawna góoru faas
Sakkaa ñi teewe xarnu bi
Moo jar a way bañ a selaw
Guddee’k bëccëg bañ a nelaw
Ba raw ñi daa wayal calaw (buur ya)
Ngir li mu def ci xarnu bi Seex
Bàmba yaa bariy njariñ
Fëriñ nga wuute ga’ak këriñ
Sëriñ si yaa di séen sëriñ
Yaa man a leeral xarnu bi
Sëriñ si, ñoo doon fatafoor
Sondeel du mel ni’b limiyeer
Jant la moom fawxana weer
Leeram nga tiim na xarnu bi
Seex Bàmba yaa di’g màndawaar
Waaju la tàbbi dóotu réer
Yaay jant say gaa ya di weer
Leer ya gëndoo ci xarnu bi
Nun sóobu nan la jàlle nu
Waay Mbàkke! bul dem bàyyi nu
Yawmal Xiyaam yobbaale nu
Te yobbu mboolem xarnu bi
Seex bàmba yaay ngën ji keno
Sa jën yi doy na ñuy dono
Soo doon fital di ag këno
Sa’y wal a (bal a) mokkal xarnu bi
Billaahi wéeru nan ci yaw
ŋoy nan ci yaw lu man a xew
Ngir «`urwarul wusqaa» du sew
Déesu ko dog ci xarnu bi
Seex Bàmba yaay ngën ji wurus
Foo génn xànjar daaldi rus
Gor su la waaje dóotu rus
Doy nga takkaayal xarnu bi
Def nan la ngay sunu takkaay
Di sun bitik nu di la jaay
Yaa gën i baay gën i nejaay
Yaa gën xariit i xarnu bi
Seex Bàmba yaa di’b libidoor
Làmburde wuute na’aki cuur
Sëriñ si sóobu wuñ sa mboor
Nde kon ñu naatal xarnu bi
Seex bàmba yaa nu mat boroom
Fekkoo ci àddina moroom
Tooñoo boroom, tooñoo moroom
Tinul nu tooñ i xarnu bi
Buur Yàlla jox na la’y midaay
Diiwaan ña xam nañu sa waay
Waajoo gërëm, kërëm du daay
Yaay kir-kiraanub xarnu bi
Seex Bàmba yaa di’b kir-kiraan
Ku jëm ca Yàlla na la ñaan
Soo doonu tur di «Alxuraan»
Yaa boole mbóot i xarnu bi
Def nan la geg bu deefi yéeg
Te def la mbër mu deefi déeg
Kelaŋ mi, wub nga bër yi jéeg
Sebul ci mboolem xarnu bi
Yàlla’a la jiital ca qadiim
Tuddee la Ahmadul Xadiim
Jiitu na aadama’aki doom
Jiitu na gaa yi xarnu bi
Yawma ajaaba bi balee
Yéefar ya juum wuyoo walee/aa