Yàlla na am lamuy mébét;
Nan tang ahmadul amiin
Baatin ba, jaaxal na’w kajoor
Faj aajo, moo ci gën a gaaw
Day way te jàngulon haraf
Fab na ca yaayam, yan yu diis
Sañ-sañ ba, lënde na ci moom
Rijaal ya ,xam nañ darajaam
Yal nañ ko may mbóoti lamiin
Mbég maangi! teeru leen bashiir
Moo am jalaal te am jamaal
Taar ba ca yuusufal kariim
Ca ag rawam, la daal di raw
Sóobu na giirum tasawuuf
`Ilmud Diraaya la jagoo
Moo donn Ahmadu-l-Amiin
Du mere nit, ba di ko dóor
Tarqiya, mag ña won fa moom
Inaaya, moodi ay jikkoom
Xam-xam bi, raw na sama xel
Cofeel gi, tee namaa nelaw
Saa xol di dem, ba poroxaan
Yaw la nu teg fa sunu maam
Ñoo way ne ñeex, ba xerem
Jël Bàmba, teg ca bee balaas
Moo sàmmuwaanteek Alxuraan
Laaya yi, moo xam seen cosaan
Làmmeñu yaaram lañ ko roof
Yuñ wàcce aaxirus samaan
Waylun, ñeel na kuy mariid
Saabub ngënéelamay setal
Te nun, nu def woroom i moy
Mbàkke, danuy sàkku ngërëm
Ba am ngërëm “xayrul Xadiim”
Ten dëkk fa’ak sa yépp doom
Jox nala njéndi yu la doy
Yàlla gërëm nala’ak «Lamiin»
Ak taabi`iina’ak lawliyaa
Diggante kawsara’ak jinaan
Di sant rabbal `Aalamiin
Bul fàtte, amdi Mustafaa
Fees na plaa,s ba mat na doom
La moome saalum ak kajoor
Yaa donn njool aaminata
Ngir xarnu bii, amoo fi maas
Yaa teggi tuur ba, daw ba sar
Yaa tax ñu tàbbi ci’g saxaar
Nuy naan ni kawsara’ak jinaan
Yaa tee mu naaxsaay ni’w yoral
Karyeer ba, doj ya ca deson
“Bayti-l-Muqaddasi” la naal
Ya sëtu kokki aki ndaam
Tubaab ya jox la’y midaay
Te Yàlla booy, muuram mëriid
Kum jox ngënée,l deefi la yéem
Mbàkkeek, mbusóobe duñ ko jar
Leerug cosaan ga day royaat
Mboolem shariif yi moo ci gën
Lewet, woyof, ànd’ak sagoom
Haj na, siyaare ngën ji baay
Moo donn duusi xam-xamam
Ci nun, nu am li nuy mébét;
Moom lañu may sirrul masuun
Mootax ñu lëm ko jammi biir
Lum wax boroomam muni waaw
Te màndaxaam du ca shuruf
Te nduruwul boroomu tiis
Jagle ga jiitu na’b juddoom
Bu nee jalañ, ñuy safi jaam
Fegal ko ayu bépp noon
Donoy bashiiran wa nadhiir
Te xar kanam ga leer kamaal
Ba buur ba fal ko def ko doom
Fóore ya daa fireek a raw
Ku ko rawon, neena la wif!
Mbirum `Inaaya la làkkoo
Moo tax amul xejj ak i seen
Mboolem jigéenam aku góor
Tasfiya, Mbër yu deefi yéem
Wilaaya, lay defal boroom
Leeram gi, fees na sama xol
Maa nguy wëréelu, ni gelaw
May naan ba màndi, coroxaan
Yaw la nu doyloo, ba fa saam
Seex Bàmba, moo safon xorom
Konte, mu wat séen i palaas
Adiisi Yonen, ba rañaan