Mbind mi*
1. Jàppal lii
à warul a wéet, fàww mu am araf wu ko féete wàllu ndeyjoor te loolu mënul a nekk lu dul baatoodi bu ñu séexal (tàkk), walla q nga xam ni jikkoy baatoodi bu ñu séexal la làmboo (sàq), walla ñaari baatoodi yu dend (ànd).
2. Maaska yi
Maaskay téj «accent aigu»ci e, ee, o ak oo rekk la mën a tegu. Bu ko ci am ci baatal yooyu moo gën a tëju bi ko amul : xel mu ñaw /xél yu gaaw, genn garab/ génn réew mi, door liggéey bi, / dóor kaña gi.
Maaskay tijji «accent grave» ci a rekk la mën a tegu, a bi ko am moo gën a ubbeeku bi ko amul, mel ni diggante takk na jabar / matt maa ngiy tàkk, njaay mi dafa lamb / làmb ja tas na, and wi fey na / ànd bi neex na.
3. Seetlul bu baax baat yi nees leen war a binde :
Ngeen, leen, seen, leen, -oon, woon, loolu, boobu…duñu am maaska, doontele sax dikke nañu leen niki lu tëju ; nanga xam ni loolu du jikko jamono la.
Yéen dafa war a am maaska.
Njàmbaas yu mel ni : -adi, -al, -ale, -ali, -andi, -andoo, -ante, -anti, -antu, -arci, -arñi, -at… foo leen fekk, nanga leen bind ak -a-, doontele, sax yenn saa yi, cig dégg, ñu teg mbubbum [ë] ci seen kow ; amuñu seen taxawaayu bopp, sikkim lañu, geestoo leen yóbbaale, ñoom lañuy fekk ci : xamadi, jubadi ; sagal nit, muñal nit; fabal ndab li, dëppal ndab li ; tollale, méngale ; mottali, suqali; àndandoo, turandoo; waxante, dóorante ; rogganti, jubbanti ; toggantu, liifantu; lemmarci, fottarñi, bittarñi ; tojat… Noonu nga war a jëfe ci mbindum -am, màndargay moomeel ; deel bind : teral na baayam, teral na jëkkëram. Mbindin woowu nag warul a soppi dara ci waxin wi yell.
4. Teqaleyinu baat yi
Am na ci téere bi ñaari àlluwa yuy wone màndarga yiy ànd ak tur yi ak màndarga yiy ànd ak njëfka yi (verbes). Mën nañoo dimbali way-jëfandikoo yi ci teqaleyinu baat yi. Nanga jàpp ni ay royukaay lañu, ndax ku gis nu bind ki, ka, kooku, soxlaatul nu wax ni bu ci nekk ci ñoom dees koy teqale ak li mu dendal, kon way-jëfandikoo yi mën nañoo jëlil seen bopp : nit ki, nit ka, nit kooku..
Noonu la deme ci beneen xët wi def njëfka yeek seeni topp, ndax ku gis beyuma woon, war a jëli gisuma woon . Xéy na sax dina am ñu naan waaw, lu waral boole -oon, teqale woon, nu war a tontu foofu rekk ni làmmiñ wee ko defal boppam, ndax diggante -oon ak ndeyu baat bi, amul lenn lees ci mën a roof ; te loolu dalul woon, ndax am na lu mën a jaar seen diggante, niki ci gisuma ko woon.. Waaye nag bu la baat yii di ñëw nax, rawoon na, tawoon na, ñëwoon na…. dees koy boole ndax mbirum –oon la, moo fekksi raw, taw, ñëw.
Ba loolu wéyee, nu tënk fii as lëf baat yees war a boole ak yees war a teqale.
Booleel :
– njàmbaas yi nu lim léegi ak yii di ñëw dees leen di boole ak seen ndey : ñaawtéef, mbégte, fajkat, julliji, kaaraange, defarlu, muslaay, wérle, jooyloo, raxasle, gëstu, jullikaay, dëkkaale, jëflante… ;
– ñaari màndargay yii di -u, ak -i , nga xam ni seen taxawaay moo di fas kóllëre diggante ñaari tur walla diggante seen ak aw tur, dees koy boole ak li jiitu : saamu kànja, doomi réew mi, seeni mag, seenug kër ;
– màndargam moomeel bii di -am, nga xam ni jéll na aji-wax ji ak ki muy waxal féetale kàddu gi ci jaambur, dees koy boole ak li ko jiitu : nijaayam, jëkkëram ;
– leen : dees koy boole ak li ko jiitu ci santaane yi, ci tere yi ak ci gàntal : waxleen ko ko, buleen ko ko wax, waxuleen ko ko.
Teqaleel :
– a dees koy teqale ci mbind mi, terewul nag ci wax ji mu mën ànd ak li ko jiitu, dafa war a wax dëgg, war na leen a wax dëgg, muus a ngiy jooy ci néeg bi, Umar a ubbi bunt bi., dafay woy ak a fecc.. Su fekkee ni nag baat bi ko jiitu arafu mujjantalam ab baatal la, dees ko cay taf : muus moomoo ngi ci biir (muus moomu + a), muus mee ubbi bunt bi (muus mi + a) ;
– ak dees koy teqale ak li ko wër : ndey ak doom, dafa ànd ak metitu bopp. Waaye nag, su fekkee ni baat bi ko jiitu, arafu mujjantalam ab baatal la, ñoom ñaar dañuy ànd seey ba soppeeku, kenn dootu leen a mën a sàkkal aw dig, bu boobaa nag, benn baat ngay bind, mel ni ci : mburook soow (mburu + ak).
– leen dees koy teqale su génnee ci anam yi nu jëkk a wax : waxuma leen ko, ma wax leen lu leen tiital.
– suma, sama, sa, sunu, suñu, seen, nga xam ni ay màndargay moomeel lañu, dees leen war a teqale.
* Jukki bii Soxna Aram Faal a ko defar
This article is absolutely a wonderful one that will in writing a correct Wolof.