Bàkku Senegaal

 

Yëngal-leen kooraa yi te dóor ci sabar yi

Gaynde ñaloor yuux na. Boroom àll tëb na

Tëb na tëbu jàmbaar, leeral lu doon lëndëm

Suñuy naqar jeex na, sunu yaakaar ñëw na

Jógleen gaa ñi, waa Afrig gépp a ngi daje

Awu

Yéen sunu buumi xol, nañuleen àndandoo

Sunu deret waa Senegaal, jógleen

Nañu boole géej geek sayaan yi, nañu boole

Joor gi ak ñaay yi Jaraboot, Afrig sunu réew

Ñaareelu woy wi

Senegaal, yow doomi gaynde ñaloor ji

Yow mi jóge ci guddi jaabal wuti bëccëg

Waay may nu, ngalla may ñu sunu jomi maam ya

Rafet ni jalambaan, jàmbaare boroom doole

Waay gaa ñi, ngalla amleen sunu jomi maam ya

Awu

Ñetteelu woy wi

Senegaal, lu baax ci yow, loolaa gën ci nun

Nañu boole xale yépp ci biir sàq mi

La ko dale Penkook Sowu, Kajoor ak Gànjóol

Ñépp ànd nekk benn, bañ a am xàjjaloo

Ñu doon benn jëmm, jàkkarlook àddina

Ñeenteelu woy wi

Senegaal, naka yow, naka sunu maam ya,

Dinañ dëgër, duñu noonoo tàllal sunuy yoxo

Jaasi dellu mbaram, ngir jàmmi àddina

Ndax liggéey doy na ñu gànnaay ak kàddu

Nit ku ñuul sunu mbokk, ku xonq ak ku weex

Awu

juróomeelu woy wi

Waaye nag, su noon jógee bëgg noo yàqal

Dinan jóg àndandoo, won ko ni ko nun

Benn rekk lanu, Senegaal lanu am

Mag ñeek ndaw ñi, góor ñeek jigéen ñi

Nun dee nu gënal, dee nu gënal gàcce

Tekkikat bi: Mame Younousse Dieng (Tiwaawan, 1961)
Email : mameyounoussedieng@yahoo.fr

There are no comments yet, be the first.

Leave a Comment