Téere-woy yi téere la bu ëmb taalif yu bindkat ak xaralakat yu mag ci làkki almaa taalif. Téere baa ngi genn ci atum 2011 ca Almaañ. Tamsir Anne, mi móol dal bii, moo toxal woy yooyu, tekki leen ci wolof. Woykat yi ñu gëna ràññee ci làkki almaa, mel ni Goethe, Heine, Brecht ak ñeneen la dajale seeni woy ci tànneef boobu.
Woy bii topp, Muslaay, Goethe moo ko woy, ñu jukkee ko ci téereem bi mu tuddee: Gangune penku-sóowu-jànt ” Westöstlicher Diwan”.
Téere bi ku ko bëgga jënd, am na Ndakaaru ci librairies Clairafrique ak L’Harmattan.