Peresidaa Maki Sàll ne woon ayu-bés yale weesu, ne tàllal na loxoom waay-fippu ya nekk Kasamaas, ngir ñu tóog seet ci sunu biir naka lañu war a def ba saafara ay woowu di law ci réew mi 30 at ak lu topp. Ci laaj-toontu bii ay taskati xibaar, ay tubaab yu rajo France amal ak seen njiit di Salif Saajo, waay-fippu ñi ngiy fésal seen pas-pas tóog waxtaan ak réewum Senegaal, wante waxtaan woowu ci seen gis-gis warul a ame ci Afrik, Tugal mbaa feneen fu dul Afrik la war a amee.
Moom Saalif Saajo itam yokk na ci ne, Kasamaas moom alafokk mu moom boppam, tàggook Senegaal, ndax loolu moom du lees di laam-laame mbaa di ko diisoo. Wante su ñu ko fàttalikoo nag, peresidaa Maki Sàll moo itam nee woon na, su waay-fippu yi doon xeex 400 at walla lu ko ëpp du tax mukk Kasamaas genn ci Senegaal, ndax ci Senegaal la bokk.
Kon nag waxtaan woowu, ku moytuwul mu doon waxtaan wu ay tëx nara séq.
Ndonte Saalif Saajo wax na ne noppi pur bàyyi soldaari Senegaal yi mu jàpp, ngir wonne ne moom jàmm la bëgg, mbir yi moom dafa am lu ci xaw a teey xel: mooy lu tax Saalif Saajo, ne fàww waxtaan wi du am ci biir Afrik, te fekk ay wi Senegaal ak réew yi ko wër ak Afrik gépp la njëkk soxal. Dafa mel ni daal Saalif Saajo moomu li muy fexe mooy réewi tubaab yi duggal seen loxo ci mbiir mi: te su booba Senegaal dina nàngu lu mu sàññul a bañ! Ndax kenn reerewul mbir ne am na réewu Tuggal yoo xam ne su ñu sàññoon Kasamaas moom boppam, ba ñu tég ci seen loxo ci wàllu koom-koom ak turism.
Kon waa nguur gi war na ñoo jàngat bu baax li ñuy def, nàmm seen xel te moytandiku cuune!
Tamsir Anne tamsir.anne@wolof-online.com