Séy dagan na, fase dagan na
Ku mënul may sa bopp, lu la Yálla may nga jël
Kenn du bëgg ginaar ba noppi di bañ ay nenam
Áddina : dund, dee
Ku jëkk yeewu boroom ndékki, war a tëddaat
Kumbay bañ Sàmbay rasu !
Purux du gërëm ñamu daaw
Koo xamul, ‘éey’ nga koy woowe
Kenn du toog ci der di jëw yápp
Doom nawle la, jabar nawle la
Séddële Bukki: bii Bukki, bii Njuur, bii Sàmba, bi ci des nag ku ci jëkk yaa
moom te teg naa ci loxo!
Ku wéeruwul fenn yomb a bëmëx
Ku jooyul néew xaana bañ a wañaar loxoom
Ñàkk xam gaynde weesuwul naan danga koy takke buum
Jaan dëngul, doxin waa jubadi
Ñu bokkul teen duñu laxasoo ay goj
Ku dul tukki, doo xam fu dëkk neexe
Ku iñaane sa ndono sa dee ñaaw
Du man do??, bokkuma cee ko gën
Ku bëgg akara dangay ñeme kaani
Waane weesuwul ne dangay nettali sa géntu moroom
Ni nga bëgg sa waay mel ko, du ko mel mukk, sa waayu-waay a koy mel
Xew xewi aayul, ñakk mas a xew moo aay
Yàgg bawul dara
Yax bu réy gobar toju ko – Njaga Mbay, woykat –
Àddina potu ndaa la, ku naan jox sa moroom
Àddina nii rekk la : demal maa ngi ñëw
Fen buy defar moo gën dëgg guy yàq
Ku ñu fey sa bor nga mer, booba la nga leble woon jagul
Gaalu dof du teer, mbaa bu teeree it du doon fu neex mbokk ya
Saay-saay waxul dëgg waaye yàq na xel
Dof sonnul, mbokk yaa sonn
Ku nekk sa xetu ngemb doyna lam póot
Ku nar a xaru dëgg doo tàggoo
Nii laa defoon day yokk sàgganu
Lu defu waxu, lu aay dib jàmbat
Njaboot jaamukaayu Yàlla la
Soo xamoon li lay yoot, nga bàyyi la ngay yoot te jublu li lay yoot
Ku am ndey am baay
Gan yomb naa muñal
Bu sa tànk bare fa sa doom di séye waaye bu fa sa loxo di gëj
Ñàkk xam li mu waral bare na
Loo xamul suuram xiifam mënu laa rey
Foo jublu yàlla na fa yiwu Yàlla jublu
Aa ! Laaj nga mbott geenam !
Fu mu yem neex
Dem ba jeex
Su fi yemoon sax neex
Bu dee ay nax sax neex na
Dikkleen waay ! Goloo ngi xastey daar-daar !
Lu ma ci góob, gar ko
Na sa ngelaw neex !
Wax waxu ku daanoo ci saret
Bul ma ne maam benn bëñ laa wax !
Waaw, lu wànq di dox noor ?
Nit ñi dañ leen a nax ba soo leen waxee dëgg sax tas seen yaakaar – Séex Anta Jóob –
Tànn sa bu la neex
Di niitu ba faf lakk
Làmbi goloo ! Ku jóg daanu ndax golo yaa ko moom !
Golo wàccal gaynde yéeg !
Boo sànnee mbàttu mu tag
Bu dee jotee…
Nii mbaa nee rekk
Su ma yëggoon a nga nee di dem !
Dof ba dafa ne : xool-leen weer waa nga nee. Ñu ne : kii kat dara jotu ko, ndekete.
Mu newaat : beneen weer waa nga nee ci wetam !
Ku loxoom jotul diggu ginnaawam
Suul bukki, sulli bukki
Su ngeen mbaam-mbaamloo, ma lawbe-lawbe lu – Mamadu Ja –
Bëtu tan jéggi na méddu sanqaleñ* – Séex Anta Jóob –
Kàddu yu Seex Anta daan faral a yëkkati, jëmale ko ci askan wi, jamono ca ka Se?oor
daan jéem a jënd ak ay ndomboy-tànk ndax rekk bëgg a jubook moom…