Bisimilaahi Rahmaani Rahiimi…
Ñu fas yeeney dollee deηkënte ak di dollee fàtleente.
Ñiη koy jëmële nak ci tomb bi nga xam ne mbooleem liy yiiwu àdduna ak yiiwu àllaaxira ci la ko sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa dëxëñ. Mbooleem yonant yi mu yónni yépp ci la leen digël ñu teg ci seen tànk. Mbooleem ñi leen topp ñépp yit ci la leen digël ñu teg ci seen tànk. Mooy tomb bi nga xam ne ci la mucc nekk ci àdduna ak ci àllaaxira, ci la texe nekk ci àdduna ak ci àllaaxira, ci la làq ngërëmël sunu Boroom nekk ci àdduna ak ci àllaaxira.
Mooy tomb bi nga xameenteni jaam bu ci tëηku sunu BOROOM dana ko musël ci fitnaay àdduna ak ci àllaaxira, musël ko ci njàqaray àdduna ak ci àllaaxira.
Mooy tomb bi sunu BOROOM deηkóon ñu njëkk ña ak ñu mujj ña ñu tëηku ca.
Mooy tomb bi nga xam ne ku weex gënul ku ñuul, ku ñuul gënul ku weex lu dul ci boobii tomb.
Tomb boobii mooy lan : “At-taqwaa”, maanaam ragal-Yàlla.
Ragal sunu BOROOM moodi jaam bi fexe bab xolam bépp pas-pas bu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut mu bañ caa nekk, fexe yit ba aw làmmiñam bépp kàddu bu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut mu bañ ko caa wax, góorgóorlu bu baax ba ci ay cërëm bépp jëf bu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut mu bañ ko caa jëf.
Lan mooy pas-pas bu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëm ?
Moodi : jaam bi wéetal Boroomam ci fas ci xolam, ta muy dëgg ci moom, ne sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa Buur bu am la, am gu tàambaleewul fenn ta yemuwul fenn, ta soqikuwul ci lenn it, ta nuróowut ag kenn walla lenn ci jëmmëm, ci jëfëm ak ci melokaanam, ta lépp lu am moo ko amal ci coobareem Subhaanahu wa Tahaalaa.
Bu fasee loolu ci xolam ci digganteem ak Boroomam, am na yit lu ko war ci diggam ak ay moroomam. Ba ca njëkk mooy mu watandiku rëy, ak kañaan ak naw jëf ak jëf bëgg ñu di ko tudd ak ngistal :
Rëy moomii, jaam bi bu xoolee la ko sos ak fa muy mujj rëy xaju fi. Sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa waxoon na Sëydinaa Muusaa bul jàpp ni yaa gën kenn feek seenóo sa bopp ci biir aljana seen kookee ci biir safara. Rëy it mooy la alagoon ibliis.
Kañaan itam, jaam bi war na di ko moytandiku ndax day lekk jëf ni sawara di lekkee matt, ta mbugëlum aji añaan ci àdduna lay tàmbalee ndax limu bëgg muy dëñug xéewël cib jaam sunu BOROOM du ko def mukk ci ludul coobareem, ndax sunu BOROOM mooy ki ko ko defal. Waxtu wu gisee sunu BOROOM dollikoy xéewël day daaldi dollikook tiit ak njàqare ta duca mën dara. Kon li war jaam bi rekk, moodi lépp lub jaam am mu yeene ko ko ba mu melni moom moo ko am, loolii mooy liy noppal nit ki ci añaan.Naw jëf itam ak jëf bëgg ñu di ko tudd, jaam bi su gisee ni bindul boppam, dees koo amal rekk, xiir ko ci li muy jëf, kon na sant kako amal ta xiir ko ca lamuy jëf, ta sant ko ca.
Ngistal itam jaam bi, waxtu wu tawxiitam mate, sunu BOROOM man nako caa musël. Ndax su boobaa yit day gis ni moom jëful waaye day jottali jëf ja rekk.
Kon loolu mooy li war jaam bi ci digëntéem ak Boroomam, ak ci digëntéem ak ay moroomam.
Jaam bi yit di góorgóorlu bu baax, ba aw làmmiñam du ci yëkkëti benn kàddu bu Sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmul.
Mu cay wattandikoo jëw ak rambaaj ak wax lu amut :
Jëw mooy wax ci sa moroomum jaam loo xam ne su ko deggóon du ko gënël. Ta li ci sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa wax ci téeréem bi war naa tax jaam bune war koo moyandiku : muy nimu ko nuróolée ak lekk meddum nit. Kon bépp jaam boo xam ne bëggoo sa moroomum jaam faatu ñu suul ko ba mu am ñatti (3) fan ngay dagg ay cërëm di sex, war ngay wattandiku kon di tóog fenn di tudd sa moroomum jaam, ci loo xameenteni su ko déggoon du ko gënël.
Jaam bi war nay wattandiku rambaaj. Muy di dox di wax luy yàq digënte ay jaam walla di yàqal ab jaam ci moroomum jaam, loo xam ne manoon na caa am aw yiiw. Jikko la joo xam ne jëmm juko ame du dugg aljana mukk mukk.
Jaam bi war nay wattandiku wax lu amut, ndax loolii ci jikkoy nàfeq la bokk ta nàfeq ci xur wa gënë suufe ca sawara mooy dëkkuwaayam.
Kon jaam bi ni mu wara saηee ab xolam, noonii la wara saηee aw làmmiñam, ñëwit ci cër yi ci des. Muy fexe ba ay gëtëm du ci xool lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmul, ay noppam noonu mu bañ cee deglu lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmul, ay loxoom it mu bañ cee jëf lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmul, biiram it mu bañ caa def lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmul, pëyëm it noonu mu bañ koo dugël fu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmul.
Nga xam ne mooy saηee xol bi ci lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmul, saηee làmmiñ wi ci lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmul, saηee ay cërëm ci lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmul.
Fexe ba sab xol doo ci ëmbël kenn lu ñaaw, saw làmmiñ doo ci wax kenn lu ñaaw, say cër doo ci jëflante ak kenn lu ñaaw. Li nga bëggël sa bopp nga bëgël ko mbidéef yépp. Di wax ci ñépp lu rafet, di jëflante ak ñépp lu rafet. Loolu mooy melokaan wi nga xam ne moom la sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa soññ ñépp ci ñu melowoo ko. Mooy melokaan wi nga xamente ni nit ki lu mu bari bari xamxam ta melowoowu ko, mook ki xamut dara ñoo yem. Mooy melokaan wi Yonent bi (sallal Laahu tahaalaa halayhi wa sallam) wax ni : ñi ko ame ñoo gënë yey ci moom, ñuñ mana doon ak fuñu mana nekk. Loolu mooy : “At-taqwaa”.
Looloo tax it sunu BOROOM ñaax jaam ñépp ñu mel woowii melokaan ngir ñu mënë mucc ci safara mi nga xam ne ay nit ñoo koy xamb ak ay doj, ta sunu BOROOM dëële ko way weddi yi.
Mooy melokann wi sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa wax ni jaam bu nekk war na koo melowoo, ngir bàyyi xel bis ba nga xam ne benn bakkan du manal moroom ma dara, ta képp ku melowoowutoon woowii melo deesuti nangu ci moom am rammu, deesuti jàpp ci moom ag maandu, deesuti ko dimbëli yit.
Ba tay sunu BOROOM wax ne Al-quraan nekk na waare ñeel way ragal Yàlla yi.
Mu dellu wax ne, moom sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa : “Laysal birru…”.
Du caageeni ag topp mooy ngeen di jëmële seeni xar-kanam ci peηku wala sowwu.
Waaye ag topp mooy nga gëm sunu BOROOM, wéétël ko ci jëmmëm ak ci jëfëm ak ci melokaanam, ta lépp lu mu dogal ci yaw nga gërëm ko, gëm bis bi mujju ba nga xam ne lépp lum bind muy nit ak jinne ak malaaka, kune mu laaj la lam la santoon na nga ca def, ak gëm amug malaaka yi nga xam ne ay jëmm lañ yu sunu BOROOM bind cig leeram, gëm teere yi, ne ci sunu BOROOM lañ bàyyikoo, jëm ci jaamam yimu tànn, gëm yonant yi ne ndawi sunu ImageBOROOM lañu subhaanahu wa tahaalaa yu mu tànn.
Ngay joxe sa alal ànd ak bëgg nga ko, waaye nga diko joxe ngir jëmmi sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa. Nga diko jox say jegeñaale, nit ña la jege cig mbokk, ak jirim ñi, ak miskiin ñi, ak doomi yoon.
Jirim mooy ku ay waajuram gaañu ta amagul kattanug fàggu.
Miskiin mooy koo xam ne amul lu ko doy ci dund ak koddaay ak dëkkuwaay.
Doomi-yoon mooy ab tukkikat boo xam ne day tukki tukki bu dagan ta lamu amewoon jeex, nga dimbiliko ci lu ko yeggele famu jëm ak lu ko delloosi famu jogewoon, ngir jëmmi Yàlla. Tukkib lëggéey ngir fàggu loo tëyée sag ragal Yàlla, tukkib jaamu Yàlla la.
Na ngeen sax cig ragal Yàlla ta xam, xam bu wóor ni yeen ñépp dana ñu leen pang ëllëg ngeen jëm ci moom.
Gaa ñi nga xam ne ñu sax cig ragal Yàlla lañu, ñooy waay-gañe ñi ci yiiw ak tawfeex aki xéewël ëllëg yawmal-xiyaam
Sunu BOROOM dana wërsëgël ku ko soob ci ludul benn coono.
Na ngeen sax cig ragal Yàlla ta ngeen xam ne kenn ku nekk ci yeen dana dajeeg Moom ba jàpp ne moom rekk la sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa bindoon..
Na ngeen sax cig ragal Yàlla ta yewenël seen digënteeg nit ñi.
Na ngeen sax cig ragal Yàlla ta ngeen xam ne sunu BOROOM ku dañ kumpa la, ku xam bépp mbir la, ci lu nëbbu ak ci lu feeñ, ci jamono june, ci waxtu wune ak ci saa sune..
Na ngeen sax cig ragal Yàlla ta ngeen xam ne sunu BOROOM Aji-gis la ci gis gu sax, ci li ngeen di jëf lépp, ci jamono june, ci waxtu wune ak ci saa sune.
Yeen waay-gëm ñi na ngeen sax cig ragal Yàlla, ta ngeen di won gànnaaw lépp lu daganul ci njaay, ndeem way-gëm ngeen. Képp ku tuub, dugg ci lislaam, lépp loo amewoon ci lu daganul na nga tàqalikoo ak moom, rawatina yaw miy aji-gëm.
Mu dellu wax ni na ngeen sax cig ragal Yàlla ta bàyyi xel bés bi nga xam ne danañu laxas, tëdd ci lalum ndee, jëm ci sunu BOROOM, ta sunu BOROOM dinañu fay sunuy pas-pas, sunuy kàddu ak sunuy jëf.
Jëmm ju ne nay ragal Boroomam bi ko bind ta moom ko ta melal ko.
Na ngeen sax cig ragal Yàlla, sunu BOROOM xamal leen li ko soob ci xamxamam bi tàmbaleewul fenn ta yemuwul fenn, ta sunu BOROOM mooy Aji-xam bépp mbir xam gu sax.
Loolu mooy waral “ah-lu tasawuuf” di jihaad ak seen bakan ngir jikko yi sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut deñ ci seen biir, ndax jikko yooyu ñooy kiiraay bi dox diggënte jaam bi ak xamxamu ladunii (mooy xamxam bi bàyyeekoo ci sunu BOROOM ta du jaar ci jenn jëmm).
Jikko yooyu maanaawoo ni rëy, ngistal, rambaac, jëw, di jëf bëgg ñu di ko tudd, ak yu maanaawoo ni ñoom.
Jaam bi nag bu sellalee ab xolam, sellal aw làmmiñam, sellal ay cërëm, sellal gu sax, sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa dana ko ca xamal la ko soob.
. . . . . . .
Ñeel na gaa yi sax cig ragal Yàlla, fa seen Boroom, itasi wurus ak yuy jamaa ak yuy oor yu taaru taaru gu jéggi dayo. Di daw ca suufu itaas yooyee ay dex, ñuy way sax ca biir kër yooyee, ñeel leen fa ay soxna yu taaru taaru gu jeggi dayo, muy ay soxna yunu laabalit, ay soxna yudul gis baax mukk. Dex yooyee maanaam dexu sàngara la ak dexi lem ak dexi meew ak dexi ndox. Ñuy aji way làq ngërëmël sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa, làq gu sax. Sunu BOROOM aji gis la, gis gu sax, ci jëfi jaamam yépp.
Na ngeen sax cig ragal Yàlla ta topp ci gànnaaw Yonant bi (sallal Laahu tahaalaa halayhi wa sallam), fu mu teggee tànkam ngeen teg fa seen tànk, ta bëgg ko bëgg gu wér, mu gënël leen seen bopp, seen alal ak seen njaboot.
Naka sama BOROOM mooy ki ma bind, mooy ki leen bind, ta melal leen, ta moom leen, na ngeen sax ci di ko jaamu : lii mooy aw yoon wiy aji-jub.
Li fi nekk, bépp jëmm buy matale wollareem ak Boroomam ak moroomam boole ci sax cig ragal Yàlla, na xam ne sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa ku bëgg aji-waay-ragal-Yàlla yi la.
Dafa bokk ci aaya boobii li tax mu wàcc, waa ah-lul kitaab ñi nga xam ne seenub yonant daf leena xibaaroon dikkub Yonant bi (sallal Laahu tahaalaa halayhi wa sallam) képp kuko ca gëm ta topp ko, sunu BOROOM ku bëgg aji-waay-ragal-Yàlla yi la.
Yeen waay-gëm ñi …..
Lan mooy gëm Yàlla?
Gëm Yàlla moodi wéetël sunu BOROOM ci jëmmëm, ci jëfëm ak ci melokaanam, xam ne ku ci wéet la, gëm malaaka yi, gëm yonant yi ak téere yiñu andi, gëm dogal moo xam aw yiiw la wala safaan ba, gëm bis péñc ba, gëm aljana ak safara ak siraat. Jaam bi su gëmee dëgg dëgg ngëm mooy tax sunu BOROOM bëgg ko. Ta mbëggum sunu BOROOM mooy tawféex si jaam bi.
Yeen waay-gëm ñi loolii, na ngeen ragal Yàlla, dëgg-dëgg ragal ko, ndax mooy tax ngeen mucc.
Dëgg-dëgg ragal Yàlla mooy nga jihaad ak sa bakan ba àgg ci sa xol dóotóo ci mana xalaat ludul màggug sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa ak lu mu gërëm, say kàddu dóotóo ci mana yëkkëti benn kàddu budul bu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëm, say cër dóotóo ci mana jëf jenn jëf judul ju sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëm.
Kon nag Yàlla bu dee dikk mukk, ndare mu nekk ngeen di waay-jébbël seen lépp seen BOROOM subhaanahu wa tahaalaa.
Kon :
Su ngeen muñee ta sax cig ragal Yalla, pexeem seeni noon du leen lor mukk, ndax suñu BOROOM ku peek la, li seeni noon di jëf ngir mu baña jëmsi ci yeen, ta sunu BOROOM du ko antul mukk.
Na ngeen sax cig ragal Yàlla, ngeen di waay-sant sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa. Ndax ragal Yàlla mooy tax nit ki ak ngëmëm mënë yokku, ngëmëm su yokkoo mooy tax muy gënë wàkkiirlu ci Boroomam, su wàkkiirloo ci Boroomam, sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa yoral ko léppëm. Su boobaa ag cant rekk moo cay top.
Na ngeen sax cig ragal Yàlla ndax ngeen di waay-texe, texe gu màgg ta sax.
Na ngeen sax cig ragal Yàlla ngir ngeen mana mucc ci safara mi sunu BOROOM dëël waay-weddi yi.
Na ngeen topp Yalla ak Yonantam ngir sunu BOROOM yërëm leen.
Na ngeen gaaw jëm ci njéggël gu bàyyikoo ci sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa ak aljana joo xam ni yaatuwaayam yaatoo na ni assamaan yi ak suuf yi, ta sunu BOROOM dëël ko waay-ragal Yalla yi.
Waay-ragal Yalla yi, ñooy gaa ñi nga xam ne dañiy joxe seen alal ci yoonu Yalla, ci jamono ba ñu barilee ak néewlee, ci jamono bañu nekkee ci xat-xat ak yolom-yolom, ci jamono bañu nekkee ci bekkóor ak naataange. Ak gaa ña nga xamente ni danañu nëbb seen mer, di jéggël nit ñi, seetu ñu ci ab jullit ak kudul jullit. Sunu BOROOM ku bëgg aji-waay rafetal seeni pas-pas la, rafetal seeni kàddu, rafetal seeni jëf.
AlXuraanul-Kariim ag leeral gu bir la akug teqale la ñeel dëgg ak neen, ñeel nit ñi, doon it ag njub ñeel aji-waay-sóobu ña, doon it aji-waare ñeel waay ragal Yalla yi.
“Mbaax nag mooy jaam boo xam ne melowoo na melokaan yi sunu BOROOM gërëm yépp ci digëntéem ak Boroomam, ak ci digëntéem ak ay wayjuram, ak ci digëntéem ak ay dëkëndóom, ak ci digëntéem ak mbooléem jaam ñépp”.
Yeen nit ñépp na ngeen ragal seen BOROOM, maanaam na ngeen feg ci seen xol lépp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut, feg ci seen làmmiñ lépp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut, feg ci seeni cër lépp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut, ñeel seen BOROOM bi leen bind ci benn bakkan muy Aadama. Mu bind ci bakkan boobii soxnaam muy Awa. Mu jële ci ñoom ñaar ay góor ak ay jigéen yu baree bari.
Sunu BOROOM nekk na kuy janoog ñépp ak lépp ak fépp, ci jamono june ak waxtu wune ak saa sune, ta di leen fuglu.
Na ñuy ragal sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa ci li waay-faatu yi bàyyi gannaaw, tay wax wax ju jub ta noppi.
Su ngeen yewënëlee ci li ngeen weesu ci lépp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut ci pas-pas ak ci kàddu ak ci jëf ta bañati caa dellu, sunu BOROOM nekk na jégglaakoon ci képp ku yewënël ci limu weesu, ta fas yeene bañati caa dellu.
Denkk naa gaa ña nga xam ne ab téere dikkaloon na leen, ta bàyyikoo ci samay ndaw, njëkk yeen, ak yeen tamit lima leen denkk, benn denkaane bi rekk la : mooy sax cig ragal Yalla.
Na ngeen di dimbalante ci seeni xam-xam, ak ci seeni alal, ak ci seeni kàddu, ak ci seeni jëf, ak cig ragal Yalla. Ta ngeen di baña dimbalante ci jëfu ñaawtéef, ak pas-pasu ñaawtéef, ak kàdduy ñaawtéef, tay baña dimbalante cig noonoo ci diggënte yi. Ta ngeen sax cig ragal Yalla ta xam ne sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa ku tar mbugël la ci waay-tooñ yi.
Na ngeen sax cig ragal Yalla. Sunu BOROOM kat Aji-xam la, xam gu sax, ci lépp lu nit ëmb ci dënnëm ta di ko nëbb, ci suba yi ak ci ngoon yi, ci waxtu wune, ci jamono june ak ci saa sune.
Na ngeen sax cig ragal Yalla, sunu BOROOM mooy wéeruwaayu waay-gëm ñi.
Sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa, waay-sax cig ragal Yalla yi rekk lay nangul seeni pas-pas ak seeni kàddu ak seeni jëf.
Yeen waay-gëm ñi na ngeen sax cig ragal Yalla, ta sàkku wasiila wu ngeen doxale séen diggënte ag moom.
Wasiila moomii day laaj ag leeral : man naa nekk jëmm ju bokk ci jëmm yi sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa tànn, def ci moom leeram ak yërmandeem ak njeggëlëm ak tawféexëm ak barkéem : mooy yonant yi ak kummalul awliyaa-u yi.
Sunu BOROOM bula defalee tàwféex, nga dajeeg ñoom, nga jox sa bopp sa BOROOM ta jaarale ko ci ñoom, mooy li sunu BOROOM waxoon yonant bi.
Soo dajewut ag jëmm yu melni jëmm yooyii, nga topp ci seeni jeexit : tëηku ca AlXuraan ak sunna, baña ëppël baña sàggan niko mawlaanaa Cheikh Ahmadou Bamba waxe ci téeréem biñuy wax « masaalikul jinaan ». Kon wasiila man naa nekk jëmm, man naa nekk jëf.
Ta ngeen di jihaat ci yoonam wi ci seeni bakkan ak ci seeni jëf bu ko laajee, ndax ngeen texe.
Na ngeen sax cig ragal Yalla ndeem nekk ngeen di waay-gëm.
Loolu li ko waral mooy ñi nga xam ni duñu ay jullit ta di ηàññ diine ji ak di ci jëf luy yàq, benn jullit warul leen a jàppe ay xarit, waaye koo xam ne du jullit man nañuy maslaa ak moom.
Kon nit ki su gëmee Yalla, dëgg dëggi ngëm, waruta jàppee noonu lislaam yi ay xarit.
Ahlul kitaab » gëm nañu Yalla subhaanahu wa tahaalaa, gëm Yonant Yalla bi (sallal Laahu tahaalaa halayhi wa sallam), gëm AlXuraan bi mu wàcce ci moom, jëfe ay ndigëlëm, teet ay tereem, kon sunu BOROOM jéggël leen seen ñaawtéef yépp, tàbbal leen ci aljana ja nga xam ne xéewël la gu mat ta sax.
Na ngeen sax cig ragal Yalla mi nga xam ne dees na leen pang ëlëg jëmële leen ci moom.
Na ngeen ragal Yalla ci mboléem seeni mbir, ta ngeen deglu ci ay ndigëlëm ta topp ko, sunu BOROOM du gindi nit ñay waay-gennug-topp.
Ndax du ngeen xellu!
Dundug adduna nekkut lu dul la ca not : am po, ay bànneex ak naqar.
Kon kërug-ëllëg mooy kër gi dul gent mukk, ànd ak bànneex bu dul gent mukk, moo gën ñeel ña nga xam ne ñu ko bàyyiwoon xel lañu ci saηe seenub xol ci lépp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut, saηe seenub làmmiñ ci lépp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut, saηe seeni cër ci lépp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut, ta saxoon ca.
Na ngeen xupp ta fàttali, ci bis bi nekk ci kanam tay ñëw, gaa ña nga xam ne danañu ragal seen bàmmeel fett, ñu genn ca, dox jëm ci bis boobee, ànd ak njàqare ak tiis, di wuyyu wooteeb sunu BOROOM bu ñu sañuta baña wuyyu, te amut kenn ci ku ñu mana wéeru ku dul sunu BOROOM, amut kenn ku leen ca mënë xettali ku dul sunu BOROOM. Ndax ñoom ñu tëηku cig ragal Yalla, ci saηe seenub xol ci lépp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut, saηe seenub làmmiñ ci lépp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut, saηe seeni cër ci lépp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut.
Na ngeen di taxawal julliy juróom (5) ta ànd akug teewlu màggug sunu BOROOM bi ak kawewaayam ak sellaayam, ta ngeen ragal ko. Ta mooy tëηku ciy ndigëlëm teet ay tereem, ta lumu dogal ci yeen ngeen gërëm loolee. Ta boole ci rafetal seen digënte ak jaam ñi, ta kenn ku nekk ci yeen bàyyi xel ni ëllëg dees nako pang, jëmëleko ci moom.
Koddaayal ragal Yalla moo gën adduna ak li ci biiram, mooy pas-pas bu sell ak kàddu yu sell ak jëf yu sell ; waaye sunu BOROOM moo koy jagleel ku ko soob ci jaamam yi.
Gox bu mu mana doon, su fekkoonte ni tëηku nañu cig ragal Yalla gu mat sëkk, sax ca la leen sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa digël, teet lamu leen tere, ta lu mu dogal ci ñoom ñu gërëm loolee, gànnaaw ba ñu ko gëmée, da na leen ubbil ay barke ci assamaan yi ak ci suuf si. Waaye bi ñu yeggee ci ñàkka rafetal seen digënte ak seen BOROOM ak ci seen diggënte ak seen moroom, ci la leen sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa tegge lañu foogutoon ba mukk ci ay musiba aki balaa, ta du leen teggeeku mukk it, feeg delluwu ñu ci ag raggal Yalla.
Muusaa waxoon na ay nitam dimblikoo leen sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa, ta ngeen muñ, ta xam ni suuf si sunu BOROOM danako donnloo ku ko soob walla ñu ko soob ci ay jaamam. Muj gu rafet ñeel na waay-ragal Yàlla yi.
Sama yërmaande daj na ñépp, waaye nag danaa ko jagleel ñeel ña nga xam ne ñu sax cig ragal Yalla lañu ak maandu ak rafetal, tay genne asaka ci seen alal su ca waree. Ñuy gaa ñuy gëm lañu samay kaawtéef yu may feeñal ci samay jaam.
Ñi nga xam ne dañoo sax cig ragal Yalla, waxtu wu seytaane tàbbalee ci seen xol ittey moy, dañuy daaldi dellóosi seen xel, xam ni yool buy sax ba fàww moo gën mbugël bu dul dëñ ba mukk.
Ci misaal rekk, dafa am waxambaane bu taqoo ak jàkka. Ab soxna diko woo, bëgg koo tàbbal ci biir kërëm, dëñul diko man manee ba diko bëggë dugël ci biir néegëm, mu fàttaliku diisug aaya bii daaldi xëm. Ba mu ximmlikóo mu diko man maneewaat, mu fàttalikuwaat diisug aaya bi, ci la daaldi faatu.
Na ngeen sax cig ragal sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa, ta ngeen di yewënël seeni digënte. Moodi kune lamu bëggël boppam mu bëggël ko moroomam, digënte bu ñagas itam ngeen dox ca wax ca kàdduy yiw ngir diggënte ba defaru.
Na ngeen sax cig ragal Yalla ta topp yonantam bi, ta ngeen tek seen tànk ci limu leen digël ta teet limu leen tere su ngeen nekkee di way gëm, ndax loolu moodi màndargam gëm.
jukki bi: http://www.maoulhayat.com/
eskeuy!!!
amna solo loole.
Jërëjëk kilifa gi, mbind mi am na solo.