Kàddu yu njëkk yi tukkee ci Màkki Sàll

Yeen wa Senegaal, góor ak jiggéen, mag ak ndaw, sama askan sope. Ci bésu dibeer bii 25 fan ci weeru Mars 2012, gànnaaw beneen bésu 26 fan Fewie bu kenn dootul fàtteeti, askanu Senegaal, àtte na, jaarale ko ci kàggu-wote yi. Ci biir réew mi ak ci bitim réew yépp, doomu-senegaal yi wote nañu jàmm, dal, yar ak teggin. Seen màndute ak seen xay ndam la ci ku nekk ci ñun. Téy nag am resiltaa bu tukkee ci kàggu-wote yi. Ki jël ndam li dëgg du keneen ku moy askani Senegaal.Won nañu àddina sépp sunu bopp, won nañu leen sunu demokaraasi “muskalaf” la, kenn du ko tette. Wante téy jii ngoon itam, sama xalaat yépp dem nañu ci jambaar yi tayle seen bakkan ngir aar sunu demokarasi, aar sàrti-réew mi.
Yàl na leen suuf sedde, amiin! Sama xel itam day dem ci askan wépp, rawatina ci ñi ma woolu, sànnil ma seen kàrt, ñi ma jàppale ci njongante bu njëkk bi ak bii ci topp, ak ñi àndoon ak man yépp ba may door APR. Maa ngi sargal itam ñépp ñi woteel beneen kandidaa bi. Fas naa yeenee doon nag, peresidaa Senegale yép! Peresidaa Ablaay Wàdd wóo na ma téy ci ngoon ci telefon ndokkale ma. Ma ngi koy sànt bu baax ci loolu. Ci waxtu wi nu tollu itam maa ngi delloo njukkël it taskati-xibaar yi. Taskati-xibaar yi, kenn reereewul mbir solo bi seen liggéey am, ndonte liggéey bobbu du lu yomb. Te ba ñu doore wote ba léegi, muy taskati-xibaar yu waa réew-mi, walla yeneen réew seen liggéey jeggi na dayo. Maa ngi sànt itam sunu doomu-ndey yi feeteewoo yeneen réewi Afrik yi ak yeneen dénd ci àddina bi yi wone seen cofeel ci Senegaal. Maa ngi nuyu ñépp ñi ñëwoon di sàytusi wote bi te di leen xamal ni seen taxawaay neenul. Yeen sama mbokki Senegaal, yeen samay àndadoo, ndam li ñu am réy na ba faf jeggi dayoo, wante loolu day feeñal yaakaar bu réy bi askan wi am ci ñun: te nàtt naa téy bu baax yaakaar woowu fu mu tollu. Téy ci ngoon gi kon, beneen jamono moo teru Senegal. Nun ñépp, danañu booloo jublu ni mu gëna gaawe ci liggéeyu jubbanti réew mi ku nekk ci ñun di xaar! Kon Yàl na Yàlla sàmm senegaal, sàmm Afrik.

tamsir.anne@wolof-online.com

There are no comments yet, be the first.

Leave a Comment