Bésu alxamés bii di 23 fan ci weeru swe 2011 bés la bu mag ci biiri bés yi ci ndeminu demokaraasi ci réewum Senegaal. Ndax gannaaw ba njiitu-réew mi fésale yeeneem soppi sàrti réew ci anam yi ñu ko wara falee moom ak ki wo wara wuutu, la cóow lu rëy jólli fu nekk: ñépp di ko mbàmb naan jubluwu ci lu dul faluwaat, ag wut yoon wu mu fale doomam: di Karim Maysa Wàdd. Ndax peresidaa ci luwaa boobu mu doon mébét da fa bëggoon su ñu koy fal, falaale jaraaf ju koy wuutu su amee gàllankoor maanaam wiis-peresidaa! ImageRax ci dolli, pal moomu su ko 25 ci téeméeri nit yu nekk falee rekk, pal ga day wéy, maanaan doonulkoon laajati 50% yi nga xam ne moom la yoonu-wote laajoon kiy dooni peresidaa am ko, ngir mën a falu ci benn “tour” kese!
Luwaa boobu loolu la bëggoon na teggi ba noppi sërëxal lawax bi wara wuutu njiitu réew mi su deme ba mënatul ci diirug palam. Kenn reerewul mbir nag ne cóow li wër Senegaal ay at mooy: Góorgi day wut pexe mu muy def ba ñu fal doomam, di Karim. Te loolu nag ci demokaraasi bu mel ni Senegaal lu teey xel lool la! Xanaa kon li Wolof Njaay waxoon dikk na: ku ñuy jiiñ ag ndëm fekk la ngay seeñu yeelu liir.
Wante nag lenn moom jangees na ko ci mbir mi: jamono ji ñu tollu nii loo am ci sañ-sañ rekk askan wee la ko may! Askanu Senegaal moom daa lànk ba tëdd ca naaj wa ne luwaa boobu kenn du ko fi wote. Mbooloo mu takkoo genn ci biir réew mi yépp di ñaqtu ne loolu mukk du fi amee. Rawatina mbooloo ma dajaloo woon wër pénccum-ndawi-réew mi di xaar depite yi waroon na wote luwaa boobu, di leen yuqoo, di defanteek alkaati yi! Ndakaaru jax lool, tàng jërr! Wante askan wee mujjee ndam li: ndax luwaa boobu kenn wotewu ko: Njiitu-réew mi ci bés bi la rocciwaat luwaa bi! Lii nag moom gulléet la ci Senegaal, jeego bu am solo la ci ndeminu demokaraasi ci biir réew mi: wone na mat gu wér, tàkku bu wóor bu askan wi tàkku ngir saytu liy àqam aki sañ-sañam!
Kon ñépp a ngi xaar njiitu-réew mi ci li miy wara wax ag askan wi ci fan yii di ñëw. Ndax jéll bu ni mel kenn mënu koo daanu ba noppi, jóg faxasu dem sa yoon: fàww mu jakarloog askan wi wax li mu nar, diisoog moom ci xew-xew boobu ag la wara ñëw ca kanam! Am na nag ñu ne li ko war mooy mu tekki ndombo li!
La ca kanam moom rawuli bët! Kon gàcce ngaalaama réewum-Senegaal!
Tamsir Anne © wolof-online.com