Bennoo, Ñaaroo, Ñettoo ba Ñent….
Mbooloo mooy doole te mooy jàmmi-réew, wante lu waay di wuyoo na koy niroo! Moo tax ba Front Siggil Senegaal seete seetaat ba tudde boppam Bennoo Siggil Senegaal, la yaakaar dellusiwaat ci askan wi, ndax xam xell ne noonu rekk la nataange, tawféex ak jàmm jiy doomi-réew miy mébét mën a jebbi Senegaal. Wante su dul woon loolu sax, ñépp xam nañu ne mbër mu mel ni Ablaay Wàdd, rawatina mu yore li mu yore, maanaam pexe yi ak mën-mën yi ko “Etaa” jox, soo ko bëgge daan alafook nga teel a jóg. Waajaay bi yàggoon na lool, laamisoo bi itam noonu, ba ñenn ci seetlukat yi sax xaw a am xel-ñaar naan, mbaa bii “Bennoo” moom du mujj a doon “Tasaaroo”?
Yeene ju rafet amul ag pay gaa, wante na na fekk itam mu mengook pastéef, jëfe ak dëggu.
Naka démb ci ngoon réew mi yeweeku na. Waa Bennoo jubbowu ñu ci benn kandidaa, dañoo mujj wote: 19 parti ànd ak Mustafaa Ñas, yeneen 14 parti ñoom wotelu ñu kenn, dañoo tiyye seen kàddu.
Wante li ñu doon bañ am na: ndax gannaaw ba ñu tánne seen mbër ba noppi, Tanoor moom dafa indi tànki bukki. Ne du nangu mukk Mustafaa Ñas di jiitu, ndax Bennoo masu ñoo wax ne dañuy wote ngir tànn ki war a doon seen kandidaa. Mu Yokk ci sax ne li Bennoo def, “kudetaa” la bu ñu kudetaa PS la. Céy, politik yenn saa yi kenn du xam lu muy nirool! Waaw xana ñoom, jaamu soxlaay réew mi taxul leen a jog? Te sax ni ko Wolof Njaay di waxe, “man la, man la” joo gis ñaare, du moom! Te su caaxaan fattoo, dëgg des, réew mi warul a fàtte ne parti sosialist bi Tanoor Jeng jiite moo fi nekkoon 40 at: li ñu fi yàq bare ne te jafe-jafe yu bare yi réew miy jànkoonteel téy it, seen politik bi fi nekkoon am na ci yoon. Jareesu fee nekk di wax waxi démb, wante alafook itam ñu seet fi ñu jaar ba yegsi fi nu tollu. Ci sunu gis-gis bu neew, teel na lool sax di leen denkaat réew mi! Ñu bare ci am seetlu nee nañu gaa parti sosialist ba woon ak bii du benn, wante nañu tàbb ñeneen ñu jeem ba ñu gis li ñu mënee.
Mustafaa Ñas moom, dëgg la wér na ni ku bëgg réewam, ndax su dul woon moom ba léegi kenn du wax Ablaay Wàdd: li mu beddekuwoon 2000 jàppale Ablaay Wádd, looloo taxoon ba PDS falu, nguuru parti sosialist jeex. Kon mel na ni daal ci moom la yaakaar yi gëna daje: kon Yàlla bu yaakaar tas!
Wante doon kandidaa Bennoo walla Genn-Wàll-Bennoo taxul a falu! Réew meey fal, te ku jub, maandu, farlu, mat rekk lañu war a jiital: mu jaar ci yoon yi penccum-réew mi walla “Assises Nationales” yi xàlloon!
Senegale yi mën a wuutu Ablaay Wàdd duñu fi jeex! Xuloo beek saagante bi jaru ko, su dee askan wee leen ñor, nañu taxaw njëkk ci xeex Ablaay Wàdd ak nguuram, ndax moom kat gëmul nelawul! Ay weer a ngi xaat muy defaru di waaj a tóogaat, mbaa mu dëjj fi doomam mbaa ku ko neex! Te su ñu xaare ba jaan wi dem, ñu topp cay door ca watit, du jëriñ tus! Lámb ji sájj na, ku woolu sa mbër na nga wut ngémb lu dëggër te tàmbali say deeba-deeb.
Tamsir Anne © wolof-online.com
There are no comments yet, be the first.