Peresidaa Ablaay Wàdd nangu na dibeer ca guddi gànnaaw ba resiltaa wote bi tàmbalee wàdd, ne Maki Sàll moom la réew mi tànn. Moom Ablaay Wàdd wóo na Maki, ñaanal ko, kañ ko, berndeel ko!
Loolu di ndam lu réy ci réewum Senegaal. Rawatina ba àddina sépp ne tekk, askan wépp ne tekk di dégglu, boole tiit ak njàqare ci fu mbir yi doon nar a mujje, gànnaaw xiiroo bu metti ak xeex ba ay bakkan rot bi amoon ci nguur gi ak kujje gi. Senegaal wooneti na boppam, kaar, jëf ji rafet na: Ablaay Wádd gaal ga ko ñu bare seddoon lekku ca!
Wonne na ni demokaraat la! Maki Sàll nag, moom, moom la yaakaar yi tase, ba akan wi bennoo bokk yaakaar.
Réewum Senegaal firndeel na ne kenn demul mu dés: du réewum cuune! Dara jombu ko! Su ñu boole sunu doole, sunu më-mën, jubboo, gëm-Yàlla, xeex ger, yàqute jikko, fóot xol yi, taxaw temm ci jub ak jubal, su sóobe Yàlla lépp lu ñu yootu jot ko. Li la askan wi sas réew mi!
Yàlla bu yaakaar tas!
Tamir Anne
tamsir.anne@wolof-online.com