Naka démb ci dibeer gi la Senegaal wootewaat woote bu am solo ngir fal ndaw yiy war a taxawal askan wi ci pencum réew mi. Ci xibaar yi jot a tukkee ci kureel yi doon saytu woote bi, fés na ne mbooloo miy jàppale peresidaa Maki Sàll, di Bennoo Bokk Yaakaar, mu nar a jiitu.
Baabakar Gey di njiital Resocit, maanaam doomi-réew yiy fàggu ndax woote bi jaar yoon, moom nee na “ci 45 departemaa yépp Bennoo Bokk Yaakaar moo fay rawi”. Kon peresidaa Maki Sàll dina am mbooloo mu takku mu koy may mu doxal politik bi mu bëgg a doxal ci réew mi.
Wante itam ràññee nañu ne senegale yu bare wooteji wu ñu, dañoo tóog seen kër. Kon warees naa jàngat loolu ba xam lu ko waral, ndax safaan la ci ndemeelu demokaraasi.
Leneen lu bees lu am ci woote bi mooy kandidaa yiy bàkkoo diine naka Sëriñ Manssur Si Jamil, Sëriñ Moodu Kara ak imaam Mbay Niang ñoom itam dina ñu am depite.