11 Saraa
Bokk na ciy teggiin: tëyye sa loxo ak bàyyi di ci fo ak bàyyi di ci jefandikoo lu njariñ nekkul, loolu de bokk na ci li woroom xel yi ayibal, te ci la musiba yi tase. Saa soo déggee ku la mag mu soxla dara niki mu bëggoon ku mu yonni, rikk, demal doxal ko yonneem boobu ngir jëmmi Yàlla. Bu kenn soxla ci yaw dara ndare du danga koo defal loolu mu soxla ci yaw, boo dee def noonu de da nga am teraanga. Rikk bul di wax kenn fen nga, walla wax nga lu dul dëgg, walla juum nga walla jeneen wax ju man a merloo doonte ki nga koy wax gone la, di ko waxe de ag njuumte la.
Bu waxee loo xamul nee ko dëggal nga, kon dees na la teral. Nee ko daal man de tegoon naa ko neneen, walla leneen laa jortoon, walla réere woon naa ko ak yeneen baat yi walla waxiin yi man a bégale, loolu de boo ko defee def nga lu rafet, bul ñaawal te bul lore. Deel tàmmal saw làmmiñ wax lu baax, kon de dinga ci ame ag texe te dees na la ci fegale wépp ay ngir waxi sangub mbindéef yi…yal na ko Yàlla dolli ay xéewal ci anam gu sax.
Ku nekk na di gëm Yàlla walla bis bu mujj ba, nay wax aw yiiw mbaa mu noppi.
12 Saraa
Bokk na ci teggiin yu rafet nga saxoo di faj aajoy ku la mag boo ko déggee mu koy sàkku, niki mu soxla woon ku mu yonni. Bokk na ciy teggin ba tay nga bañ di gàntul kenn loo man lu mu soxla ci yaw, te bañ di wax kenn “fen nga” mbaa “li nga wax du dëgg” mbaa baat bu ko man a merloo, doonte yaa ko mag, bu waxee loo xamul dëggal ko te ne ko (man de nekkuma woon foofu) walla (jortoon naa ne) walla (xamewuma ko woon noonu) ak yu ni mel ci waxiin yu rafet. Nangay tàmmal saw làmmiñ wax ju rafet . Yonnant bi (j.m) nee na : ku gëm Yàlla walla bis bu mujj ba, nay wax aw yiiw mbaa mu noppi. kenn ci woykat yi nee na :tàmmalal saw làmmiñ wax ju baax, kon de danga ca ame ab cér, làmmiñ de li nga ko tàmmal rekk lay tàmm, lu mu man a doon la nga ko ca miinal rekk lay def, moo xam lu baax la mbaa lu bon, deel xool nooy dollikoo.
Sab dox na ko aajo di waral ci lu dul ag rëy, ag rëy de ci mbugal lay bijjee jëme. Bul di ree mukk ci lu dul lu yéeme, bul dox mukk it ci lu dul aajo. Bul gestu tam te sàkkuweesu ko, ndax yii yépp ag ndofe la gog dàqoo na’aki teggiin.
Sa tubay it bul ko di wuññi mukk, ndax loolu ci bàyyi ay teggin la bokk. Moom de ci jikkoy kàccoor yi diy saay-saay te bokk ci giirug Hassaan la bokk, ñoom ñi dëddu lu baax. Na ngay moytoo wuññi sa biir ak li nekk ci diggante jumbux bi ba ci bëti-woom yi, (ngir bon gi mu bon). Loolu de màndargam réer la ak ndofe ak néewug mbañ-rus gu màgg gi. Ndax moom (mbañ-rus) mooy dàttub diine, fu mu nekkul diine nekku fa , loolu de la jàngalekat yu mag ya saxal. Koo agsi ci moom nanga ko nuyyu, bu fekkee ne soxla nga ay teggin. Bu fekkee ne moo la njëkk a nuyyu nanga ko fay ci kàddu. Boo saafoonteek moom na nga dëgëral sa loxol ndijoor ci ndijooram, loolu mooy li nu rafetlu Bul rocci sa loxo li feek njëkku la koo rocci moom ci anam gu fés. Ndaxte de sibees na fëkk ay loxo ci nuyyoo ci anam gu gaaw ak bàyyi wax ja. Saafoonte ci ñaari loxo it bokk na ci ay teggin, niki ñaar yi nu la waxoon leegi. Ñaanalal ki ngay nuyyool yaw boroom xel mi, ndax loolu de bokk na ci liy fari bàkkaar.
Boo bëggee dugg ci kër walla néegub jàmbur nanga yëglu, kon de nga am la gën. Bu ñu la digalee nga dugg nga dugg, bu dul loolu dellul. Sab bët bul ko di wëndéel ci néegub jàmbur mbaa këram ngir ragal gis fa awra joj bëggunu woon nga gis ko.
13 Saraa
Bokk na ciy teggiin booy jug aajo rekk di la yëkkati, bokk na ci ag ndofe ngay ree te lu reeloo nekku fi, mbaa ngay dox ci lu dul aajo, mbaa ngay gestu te yittewoowoo ko, bokk na ci ay teggin ngay moytoo wuññi say sér, loolu de ci jikkoy kàccoori Hassaan yi la, bul di feeñal lenn ci sa biir mbaa li nekk ci sa diggante jumux ba ci say wóom, loolu de ci réer la ak ñàkk kersa te kersa mooy dàttub diine tey laylaat gi mu tege, fu kersa ñàkke diine jug fa. Bokk na ci ay teggiin ngay nuyyu képp koo dox ba àgg ci moom, te di ko fay bu la nuyyoo, te ngay saafoonteek moom tey dëgëral sab loxo ci loxoom boo koy nuyyu, te nga bañ koo njëkk a rocci sa loxo, fëkk loxo ci lu gaaw cib nuyyo de lu ñu sib la. Bokk na ci ay teggin ngay saafoonteek moom ci sa ñaari loxo yépp, te nga koy ñaanal lu baax ak sa bopp loolu bokk na ci liy far ay bàkkaar . Bokk na ci ay teggiin ngay def booy dugg ci néegub jàmbur mbaa këram ngay yëglu bu ñu la nee jàllsil nga dugg, ndeem déet nga dëpp, rikk bul di sànni sab gis ci kër mbaa néeg boo moomul ngir nga bañ faa gis loo warul a gis. Boo bëggee kooy àndandool bu muy ku dese cim xel mbaa ku iñaan mbaa ku bariy xemmeemtéef bu di toog ak ku dul ku lay dolli diine ak xel, kon de nga am càkkutéef. Ndax de xibaar nañu ne cam si de (waa ji) ma nga ca diiney xaritam ba, loolu ab adiis la bu ñu tuxal (waa ji de diine ji waayam yor rekk lay yor) Saraa: Da lay dénk nga bañ a àndandook way dese yi cim xel te bañ di toog ak ku la dul dolli diine ak xel, ci loolu de ngay ame la nga bëgg, ndax waa ji de ni ab xaritam mel rekk lay mel: wolof yi nee nañu won ma sa xarit ma wax la sa jikko – seyyidinaa Aliyun – karramal laahu wajhahuu – nee na: bul def mukk boroomug réer muy sab àndaale, moytu ko te moytu sa bopp bariwaa na aji réer ju alag boroomug lewet (ku nite) ba mu ko defee mbokk. Nit de ca moroom ja lañu koy natt bu àndeek moomni ñuy natte dàll ca moroom ja bu ñu dee ñaar mbir de am na ag niroo akug natt ca moroom ja; xol de misaal la ca moroom ja. Am na ku ne: boo nekke ciw nit nangay seet ña ca gën ngay ànd ak ñoom bul seet ña ca yees ngay ànd ak ñoom bay yees. Bul laaj waa ji, waaye laajal ab àndandoom. Ndax ku nekk ca ka ngay àndal ngay roy. Bul sàkkoo gis mukk ab rëcc-rëcc (ci sa moroomu nit) bul gëstu itam ay awra (ay ñaawtéef)
14 Saraa Mu ne : bokk na ciy teggiin ngay bañ di gëstu rëcc-rëcci nit ñi mbaa seeni ñaawtéef. Waxees na ne : bul di sàkkoo xam la nit ña nëbb ci seeni ayib ndax kat loolu man naa waral Yàlla di muri mbalaan mi mu muuroon ci say ñaawtéef. Rikk nangay tudd lu baax la nekk ci ñoom bu nu leen tuddee bul ayibal kenn ci ñoom ndax kat loo leen wax man naa am yaa leen ko ëpp. Na nga mel ne na woykat ba waxoon: dinaa bëgg jikko yu rafet yi sama kem kàttan tey bañ di ayibale ak ñu may ayibal, may jéggal ηàññug nit ñi ngir ag lewet ndax ki yees ci nit ñi mooy ki sopp ag ηàññante. Ku weg nit ñi wegees ko, ku xeeb nit ñi deesu ko weg. Ka wax lii de wax na wax ju rafet: boo bëggee dund sa diine, mucc, sa wërsëg lëw (bari) sab der ñoη, boo bëggee loolu sa làmmiñ bu ci tudd mukk ayibi nit, ndax kat yaw it, am nga ay ayib, nit ñi ami làmmiñ. Bu Yàlla dogalee say gët rot ci ayibi nit, nee leen : yeen gët yi bu léen xool de, ndax nit ñi ñoom it am nañu ay gët. Xamal ne wuute ab dëel (dige te defoo ko) ak fen bokk nañu ci gàkk-gàkki wax, dee leen teet (moytu). Nekk na ci adiisub kii nga xam ne maa ngi sàkku sellug ay julleeki sëlmal yuy sottiku ci moom aki ñoñam aki saabaam, yi diy ndëerlaay. Dénk naa leen adiis ba:nekkal di kuy wax dëgg, teetal fen ngir nga kawe Saraa: mu jubloo wax ne mi ngi lay dénk nga bañ a fen, bañ a wuuteb dëel, te di leen ko tere, ngir ne ñooy gàkk-gàkki wax, Yonnant bi (j.m) nee na: dénk naa leen dëggu, ndax mooy yobboo cig mbaax, teg mbax mooy yobboo àjjana, waa ji bu saxee di dëggal te di ko sàkku, bu yàggee bindees ko fa Yàlla muy ku dëggu, moytuloo naa leen fen, ndax day yobboo cig mbon teg mbon mooy bijje jëme sawara, waa ji bu dee fen te di ko sàkku, day mujj bindees ko mu dib fenkat fa Yàlla. Fonkal sa ñaari way jur, te am yërmaande ci ñoom ak ñeewant, te deel gaaw ci seeni ndigal aki mbir. Deel ba mbooleem li ñu la tere, boo ko dee def de, sag kawe dina yokku Képp ku la mag ci jegeñaale yi nanga ko weg ak ñu dul jegeñaale yi, rikk nanga nekk ak mbindéef yi ci jikko yu rafet, kon de Aji-Sàkke ji (Yàlla) dina la sopp.
Na ngay rafetal jikko yi cig yaatu-yaatulu, ak a sàkkoo sopplu ci ñoom (mbindéef yi) kon de soppees na la. Na ngay nooyal i wax ci nit ñépp, loolu de ci jikkoy way ñaw yi la bokk (ñu yeewwu ñi). Xibaarees na jële ca Boroom ngënéel la Yonnant bi (j.m) mu ne: genn-wàllu xel mooy sopp-sopplu ci nit ñi (fexe ba nit ñi sopp la).
Bokk na ci texeeg nit ki, xolub boroomug njub bañ koy bañ ak a foñ. Saraa: mu jubloo wax ne mi ngi lay digal nga fonk sa ñaar i waay-jur te ñeewant leen, di gaawantu ci def séeni ndigal, di bàyyi seen i tere. Yàlla mu kawe mi nee na: nit dénk nanu ko lu baax ciy waay-juram, maanaam mu fonk leen, ak yu dul boobu ciy laaya, ak nga fonk ku la mag ci jegeñaale yeek ñu leen moy, te ngay rafetal say jikko ci di leen mayug yaa, ak won cofeel ak a sàkku ñu sopp la, sàkkug cofeel ci nit ñi de mooy genn-wàllu xel, na la wóor ne bokk na ci texeg nit ki, xolub aji gëm di ko bëgg, deel nooyal say wax ñeel nit ñépp, ndaxte loolu kay ci jikkoy waay-yeewwu yi la bokk. Deel sàkku seenug ñaan foo tollu, deel barkeelu it ci ñoom, loolu de dina la yobbe ag kawe guy dolliku. Màggal boroom xam-xam bu jëfe (xam-xam ba) mooy màggal boroom aras (toogu ba).
Foo àndeek ku la mag nanga sax ci di ko weg, moo xam cib tukki la mbaa lu ko moy, deel not sa bakkan ci di bañ di toog ak moom ci kaw deel toog ci suuf, bul di toogaaleek moom cib lal ak doonte da la caa woo sax ngirug yaatal. Ndare muy lu manul a ñàkk, su leen ñam wi dikkalee mbaa naan gi yaw ngoor si bu ko ca jiite mukk, xaar ca ndigalam, loolooy jub ga. Deel seet la gën ca ñam wa it di ko ko jox ngir ag wormaal Dee ko liggéeyal ci mbooleem li mu aajowoo, kon say aajo dees na la ko fajal. Saa soo àndeekuw nit cib tukki, dee leen dimbali ci mbooleem lu ñu soxla Liggéeyal-leen te sàmmal-leen seeni waruwaay,seeni fas mbaa mbaam walla sax wata, yoral-leen seeni bagaas, dimbali-leen ñoom ñépp loo ci man, jéggal-leen su ñu sàgganee.
Neen ak noflaay jëmm ju bëgg a doon dara du leen taamu. Ndax kat aw yiiw manul a bawoo ci ñoom ñaar, te aw ay rekk a cay bawoo ñeel murif bi. Boroomug yayoo bu sàkkoo ci yaw dara, defal ko ko Bul nay mukk ci poñat mii (alali àddina jii) ba loolu di waral sa gàcce ca yalmal qiyaam bis pénc. Boroomug nay ku sori Yàlla lay doon ak mbindéefam yépp foo ko fekk. Boroomug nay dees koy wommat jëme sawara, soril ko àjjana safaan ba mooy aji tabe ja, ca lees wax, kon nekkal aji tabe ji, bul nekk mukk aji nay ji. Mu jubloo wax ne mi ngi lay digal nga siyaare boroom xam-xam yeek gaa ñu baax ñi, nga leen di liggéeyal ak a barkeelu ci ñoom, tey sàkku ci ñoom ñaan, ndax kat màggal boroom xam-xam mooy màggal Yàlla mu kawe mi. Saa soo àndateek ku la mag cib tukki, mbaa lu ko moy nanga ko bàyyee lal ba tey toog fa suuf, te bul bokk ak moom tëdd mukk ndare ngir lu manul a ñàkk, bees leen indilee ñam mbaag naan, rikk bu ko ca jiitu, xaar ca ndigalam, dee ko bàyyee la gën ca ñam wa, te di ko liggéeyal ci lépp lu mu aajowoo. Bu Yàlla dogalee nga ànd ak aw nit cib tukki, doonal seen mbindaan, sàmmal leen seeni waruwaay, yoral leen seen i bagaas kem li nga man. Bul taamu mukk ab noflaay ak loxoy neen, aw yiw nekku ci de te kenn du jot “teddnga” ga ci lu dul ab coona niki lees ko waxe. Cig farlu lees di jote kawe ga, ku bëgg ag kawe fog guddi yi (fog ñàkk a nelaw guddi). Dangay sàkku ag tedd ba noppi di nelaw guddi, na la wóor ne xemmemloo nga sa bakkan lu jomb (bëgg nga lu manul a nekk). Mi ngi lay digal nga bañ a nay ci dara ci àdduna, ku nay kat ku sori Yàlla la, ku sori nit ñi la, ku sori àjjana la, ku jege sawara la. Safaan ba it mooy ku tabe ki, woykat ba nee na: bu fekkee alal wacc koo tax deesi dajale ko, kon lu tax cam si (nit ki) di nay ci lees di wacc. Teralal gan ya cig yaatal (dalal jàmm) ak ganale ak mbégteek jegeel. Rikk bu sa dënn(xol) xat mukk ci gan, ndax moom balaa yàgg mu laxas dem. Nekk na ca adiisu Kees-tànn ka (Yonnent bi, yal na Yàlla julli te sëlmal ci moom aki ñoñam ak képp ku ko topp. Wax it ne: gan gi teral ko ca bahrub kaamil ba mu defe woy wa ci galan bu tudd kaamil. Mu jubloo wax ne mi ngi lay digal nga teral gan, yaatal ko, te bañ a xat ngir moom, ndaxte balaa yàgg mu dem, Yonnent bi (j.m) nee na ku gëm Yàlla ak bis pénc ba, nay teral ganam.
Ab woykat it def aw woy ci galanu kaamil: gan gi teral ko, ab fanaanuwaayam yelleef la (lu mu moom la), rikk bul nekk rëbbum waay-wàcc yi, bul nekk ηàññ ak saagay gan yi. Nanga xam ne gan de fàwwu mu nettali ñoñam fa mu fanaan, doonte laajeesu ko ko Wwolof nee na: gan dees na ko xañ lépp ba mu des nettali. Na nga ko gatandoo kanam gu nooy te yaa, waxees na ne moo gën ganale, moom la woykat biy feddali: kanam gu nooy de moo gën ganale, kon de xanaa bu ko waa jiy def ci kanam gu nooy dina yéeme. Dinaa ree sama gan njëkk muy wàcce ag raxlaam, bu ko defee mu naat fi man te booba barab bi bu bekkoor la. Duma wax mukk bu ma gan ganesee: jàllal sa kër ga soriwul. Sunu kër de fu yaa la ca ka ko siyaare, ubbilees na ko gan gu fëgg gu nekk. Lépp lu fa nekk, lu dagan la ñeel ko, ndare la Aji-bind ji araamal ……………
Bul bàyyi benn bis am njàng, te nga jëfe ko cig jaamu Yàlla. Xam-xam day dundal xolub aji xamlu ji, day leeral xol tey dindi ngumba gu xol. Xamal ne rawanteeg nit ñi ci xam-xam lay nekk ak diine, nanga dëkke muñ. Ci ñoom ñaar it la ku gën di gëne, du ci ag askanoo ci ku kawe. Ci wàllug askan, moo xam baay la mbaa nday, kon farlul ci ñoom ñaar ànd ceek i teggiin Booy sàkku xam-xam dimbandikool Yàlla te sellal ci xol bu dal Te ngay dëkke jàng nag, ak sàmm (sàmmoonteek ndigal ak terey sunu boroom yi) Néewal i nelaw, néewalug regg Saxal ci jàng ak nafar li nga jàng te bañ koy dëddook a ginnaawal Nangay wuuteek bakan, ndaxte bakan li mu lay xiir du dara lu dul luy waral ag tëj Néewalal nelaw yi, tàggool ak tàyyeel, néewalal noflay, gàttalal mébat Xamal ne ku bañ a jàng cig ndawam, dina dajeek réccu Ndaxte képp ku gaawantuwul jëm ca xam-xam ya (ku gaawantuwul jàngi) te féex ngir ñoom njëkk yitte ya Lu ci ëpp du am la mu ca yittewoo, te du ca jot càkkutéefam Ndaxte taggees na njàngum gone ne mook bind ci doj a yam (bind ci simaa bu tooy, bu wowee du dañati) Ñu niroole nag njàngum mag ak bind ci ndox ni muy ñàkke jeexiit ………………….. Mu jubloo wax ne mi ngi lay digal nga bañ a bàyyi jàng benn bis, ndaxte xam-xam mooy dundug xol tey dañug ngumba, di leerug bakan niki lees ko waxe: Xam-xam day wuññi ngumba wëliif xolub boroom, ni weer di wuññee këriisug lëndëm ga Ci xam-xam la ay xol di dunde yoy masuñoo xam bu njëkk lam mooy tàqale gi am ci diggante dëgg ak fen Xam-xam ag leer la ñeel bakan, mu cay niite dëgg gi (di ci tegtaloo ngir xam li am) dafa mel ne leer ci bët Mi ngi lay xamal ne nit ñi seenug rawante ci xam-xam ak diine la nekk, te ci moom lees di gëne, du ci askanoo ci baay mbaa nday, noonu la ko Seydinaa Aliu waxe (yal na Yàlla teral kanaman): Nit ñi boo leen dee natt ñoo yam seen baay Aadama la, seen nday Awa Boo dee ndamu ci askan wu tedd, nanga xam ne ci ndox ak ban la bawoo Ndam daal ñoñ xam-xam la ñeel, ndax ñoo gindee ñeel ki ko soxla Darajay cam si (nit ki) mooy la mu man (am ci ag xereñ), way réer yi (ñi amul xam-xam) ay noon lañu ñeel woroom xam-xam yi Wutal xam-xam, kon de dinga ci dunde ba fàww, ndax nit ñi way faatu lañu, te woroom xam-xam yi dunu faatu way dund lanu Mu lay xamal ne bokk na ci liy dimbalee ci xamlu te di ko yombal, ngay ragal Yàlla ci sab xam-xam, te di ko sàkku ngir moom, di néewal i nelaw, ak regg tey taqoo jàng niki lees ko waxe: Yaw aji xamlu ji gaawantul sàkkuji ag càmm (ragal Yàlla), te nga béccngal nelaw yi, tóng regg gi (merook regg gi) Jublul ci bind bi, bul tàggook moom, xam-xam ci jàng la taxawe te yekkatiku ****************** Te fàww ngay jàng tey baril nafar di wuuteek bakan bi ci loolu, niki lees ko waxe: Sama xarit bul di tàyyeel te bul di neenal bind bi ( dee ko topp ak a nafar), te bul topp mukk sa bakkan cig neenalam ( ci di ko ñàkk a defloo dara) Bul di bàyyi ag baamu (nafar) ca la nga jot a wattu (mokkal), ku bàyyee baamu (nafar) fàwwu mu fàtte (fëtt la mu mokkaloon) ****************************************** Te ku gaawantuwul def am njàngam te def ci yitteem jépp cig ndawam, dina jafe mu am ca la mu ca nammoon, ndax jàng cig ndaw mook boyaade ciw doj a yam (bind ci simo? bu tooy), jàng cig mag nag mook bind ci ndox a yam (booy teggi sa loxo muy far) , lenn ci woykat yi wax na ne: Gis naa ne damay faral di fëtt li ma jàng bi may mag, te kat fàttewuma li ma jàng ba may gone Xam kon mooy jàng cig ngone, lewet nag di ga nga def-deflu cig mag (lewet fii: nite, xel, tegu ci yoon) Bees xaroon xol bees jàngal cig ndaw, dees fay fekk xam-xam muy lu mel ne lees boyaade ciw doj (mu mel ne mbind mees def ci simo? bu tooy) Boo bijjaawee ba noppi di jàng yaa ngi sonal sa bopp, rawati na bu xol bi sonnee ak dégg beek gis bi Nit daal ñaar rekk la, xel ak xellu (logique), ku lii raw ak lee, na xam ne alku na ********************************** Nanga xam ne xam-xam de lu jafe la, deesu ko ame ci lu dul tëyye sa bopp wëliif “dégg naa ak waxees na” Du la may (moom xam-xam) lennam mukk li feek joxoo ko sa lépp, kon farlu ci. Jox ko sa lépp ci lu dul xëccoo, fogalal sag guddi (bul di nelaw guddi) te xiifal sa biir Deel maral sa bëccëg ci xam-xam, di ci sonal sa cér yépp ànd ceekug teggiinu Ku ko sàkkoowul noonu du ca am lu am njariñ, noonu lees ko xibaare Xibaarees na it ne moom de ab foñaakon la (kuy daw di soree), ku dul cam su di ab muñkat du ko am Nangay sax cig toroxlu cig toroxal sa bopp, ca jamonoy xamlu ja, kon de danga am leerug xol Ab xamlukat bu rëyee, du am nammeelam Bayyil ag péexlu (noos) bul di toog mukk cib lal ca jamonoy jàng ja, ci lu dul aw tiis (ñàkk pexe) Nangay boole yitte ji jépp ci li ngay sàkku, ci lu dul gestu jëm ci lu warul Bul di déglu nit ñi mbaa xëccoo yi ñu nekk Bul di yeexe am njàng, mbaa nga naan di naa ko defi bu ma féexee, soo bëgee dab gaa ñu baax ña Àdduna de am na yitte yuy teree àgg ca njub ga, te duñu jeex Dee de cig mbetteel lay ñëwe, te bariwaa na fu mu bóome boroomi soxla Mu jubloo wax ne xam-xam de lu jafe la, deesu ko ame ci lu dul tëju wëlif ag jaxasoo, xamal ne du la jox mukk lennam ndare bu danga koo jox sa lépp, ku ci xiifalul biiram, fog guddeem, mar bëcëgam, sonali céram, du ca am lu am njariñ, ndax xam-xam ag leer la, ku dul aji muñ du ko am, woykat ba nee: Sàkkul te bul yoqat ci sàkku gi, gàkk-gàkkub aji sàkku ji xam-xam mooy yoqat Xanaa gisoo ne buum sax bu yàggee jaar ci pindub teen, bàyyi fay jeexiital Kuy jàng fàwwu muy toroxlu ak a suufeel boppam buy xamlu, lu ko moy du ca am nammeelam, war nay bàyyi ag noos, bu muy toog cib lal mukk ci waxtuw jàng, ndare bu loolu da di lu manul a ñàkk ba àgg ci lool, booleel sa yitte jépp booy jàng ca la ngay jàng, bul di gestu leneen lu ko moy, bul di déglu nit ñi mbaa la ñu nekk, mi ngi lay dénk it nga bañ di yeexe am njàng, naan danga koy bàyyi ba féex ci yitte yi, ndax yittey àdduna duñu jeex mukk Kenn faju fi aajoom, aajo it fajuwu fi ndare bu jeneen daa juddu. Yaw amaa na sax dee gi dikkal la, ba laa booba, ndax dee de mooy aji fàddu (ku fi nekkul) ji gën a jege, te buy ñëw cig mbette lay doon. Ginnaaw bi mu wax ci nees di tegginoo ak Seexul Murabbii (Sëriñ biy jàngale) ak ki lay jàngal ak sa mbokk dëgg ak sa àndandoo dëgg, daal di ne: Fig wegeel man a yam mooy nga weg sa sëriñ, def ko ab sang, may ko say xéewal Fajal ko ay aajoom li feek yaa ngi dund, ci di ko jox, di ko liggéeyal li nga man Mu jubloo wax ne mi ngi lay digal nga weg sab sëriñ, wormaal ko, fajal koy aajoom li nga man, te ngay teet reek kaf ak coow ci kanamam, boo jubloo defi teggiin Boo toogee fa moom bul di baril ay gestu mbaa ngay yëngu fu nekk nga jëm fa Bul di baril wax fa moom, nekkal di kuy noopi, loolu dina waral nga am ag jubalam Bul ànd ak moom mukk lu dul cig màggal, bul roy mukk waa jamono jii ( ci seenug ñàkk a màggal seeni sëriñ) Bul def mukk ni ka àndoon ak Qudar, ndare bu daa manul a ñàkk (bul ko di laaj lu mu def lu nekk, nga ne ko loo ci jublu) Deel def li mu la digal, ak doonte sa bàkkan da koo bëggul Lu mu la tere it baal te daw wëlis ko, te teet sa bànneex Mu jubloo wax ne mi ngi lay aaye ngay baril coow akum po ak ree ak gestu bu bari ci kanamam, bu ko def it àndandoo ndare bu daa manul a ñàkk, di deglu ay ndigalam tey teeti tereem ak doonte sa bakkan begu ci. Bul di dañ di ko di jox i àddiya kem li nga man Ak doonte lu néew la sax, ngir rekk topp lees wax ne day dooli moom àddiya ag coffeel Loo ko gis mu jeng jëm ca, gaawantul dem ca Te farlu cig jottali ko ko, ndax kat rafetug jëf ma nga ca matal ko Nanga nekk dib jaam ñeel képp ku aju ci moom ci ñoñ, ñoom ñépp nag Ànd ceekug wormaal nag, ndax mu sarax la ab xool boo man a ame la nga bëgg Benn xool bob cofeel bu tukkee cib sëriñ jëm cib taalibeem mooy ngënéel ya tey kawe ga Nanga nekk fa sëriñ ba niki ab néew bees tëral ci kanamu aji sangam, kon de nga jariñu Boo dee sàkku xam-xam it, nangay sàkku ngërëmul aji jàngale ji ngir jëmmi Yàlla Nanga mel ca sab sëriñ nib jaam, loolu de dina tax nga jot darajay buur yi (dina tax nga doon buur) Xamal ne njariñ deesu ko am ndare cig màggal ci li ñu wax Kem ni nga màggale sab sëriñ ngay ame li nga bëgg, ci ngay ame it barke Ku gërëmloowul ab sëriñam, du gërëm ab dongaam Bariwaa na waa jees miin ci xam-xam te kenn jubluwu ko Yal na nu Yàlla musal ak yeen ci xam-xam bu jariñul ki ko xam Mu jubloo wax ne mi ngi lay digal ngay àddiyaal sab sëriñ li nga man ak doonte lu néew la sax, te sàkkoo def lépp loo ko gis mu jeng jëm ca ci mbir mu mu man a doon, tey farlu ci jottali ko ko, te ngay wormaal mbooleem ñi aju ci moom, moo xam ñoñ la mbaa jaam ak ñu leen moy, ndax sax mu xool la ab xool bob cofeel bu la ci Yàlla man a dimbalee. Xamal ne kem ni aji xamlu ji di màggale aji xam ji lay jariñoo, wa xees na : Gis naa ne li gën a war ci mbir yi mooy àqi jàngalekat te mooy ji gën a feddaliku ci bépp jullit Lu yell la deesi àddiyaal ko ay jnniy dërëm ngirug teral, ci wenn araf wu mu la jàngal wu nekk Àggees na ci wax ne moom lees jiital ci àqi waajur ni ko ñenn ñi waxe : Damay jiital sama àqi ustaas ci sama joj waajur ak doonte xam naa ne yoreel naa waajur wi njekk ak ñeewant Ndaxte kii mooy aji yar ji ruu gi, teg ruu wurus la, kee nag mooy aji yar ji yaram wi te moom yaram wi am mbuusam la (mi koy ëmb) Nanga mel fa moom niki néew ci kanamu ki koy sang, mbaa gumba gees di wommat ci yoon wu nekk ci digg géej ni muy toppe aji wommatam, niki lees ko waxe : Bu la Yàlla tawféexalee ba nga am sëriñub dëgg bu raw ci lefum Haqiiqa Rikk nanga jug ci sàkku ngërëmam, xeeñtu nammeelam, te ba lépp loo nekkoon bu njëkk Nanga mel fa moom ni néew fa ka koy sang, da koy wëlbati fu nekk muy wëlbatiku Mbokk dëgg ak xarit bu wér ñoo gën a néew luy néew Mooy lu mel ne waxi ki wuññi lëndëm yi: sa xarit dëgg mooy ki ànd ak yaw Mooy kiy lor boppam ngir jariñ la, mooy kok bu la jamono njattee Mu sonnal boppam ngir siggil la, ma ne mooy ki lay nëbbal lu ñaaw ngir yekkati la Tudd naa ciy teggiin am mbooloo mom dina fajal ku ko taqoo mbooleem ay aajoom Doy na sëkk ci ku ko settantal, aji saafara la ci ku ko jëfe Dina tegtal boroomum xel, dina ko tegtal banqaasi bunt bii, bu ci royee ànd ceekug toroxlu Ba mu far matal fànni teggiin yi te bokk na ci yooni teggiinu yi: Di def li nga gis mu rafet tey ba li nga gis mu ñaaw Lenn ci ñoom laajees na ko: ku la yar? maanaam koo roy ba mel nii nga mel? Mu ne damaa dëkke di xool réerug kii nga xam ne ne réeram gi leer na nàññ Bu ko defee ma koy teet (moytu). Fii la tontu li yam.
Aji Tekki ji: Abdu Xaadir KEBE