{"id":930,"date":"2012-06-18T20:30:22","date_gmt":"2012-06-18T20:30:22","guid":{"rendered":"http:\/\/www.wolof-online.com\/?p=930"},"modified":"2012-07-01T10:53:47","modified_gmt":"2012-07-01T10:53:47","slug":"alxuraan-ci-wolof-nit","status":"publish","type":"post","link":"https:\/\/www.wolof-online.com\/?p=930","title":{"rendered":"Alxuraan ci Wolof: Nit"},"content":{"rendered":"<p><a href=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/nataal_alxuraan.jpg\"><img loading=\"lazy\" decoding=\"async\" class=\"alignleft size-full wp-image-933\" title=\"nataal_alxuraan\" src=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/nataal_alxuraan.jpg\" alt=\"\" width=\"225\" height=\"300\" \/><\/a>W\u00e0cce ci M\u00e0kka 31 laaya<br \/>\nBenn &#8211; Senn &#8211; Menn la &#8211; Raax Menn &#8211; Raax Y\u00ebr\u00ebm<\/p>\n<p>1- Ndax dafa toog lu y\u00e0gg te kenn f\u00e0ttelekuwu ko?<\/p>\n<p>2- Danu door s\u00e0kk ci ndoxum ge\u00f1o wu \u00f1aari kanam<br \/>\n\u00e0ndoo fekk \u00f1u koy seetlu. Daanu ko jox gis ak d\u00e9gg.<\/p>\n<p>3- Danu ko teg ci yoon wu jub na fekk mu am mbaa<br \/>\n\u00f1akk koll\u00ebr\u00e9.<\/p>\n<p>4- Danu defaral weddikat yi ay callala, ag c\u00e0xx ag Safara<br \/>\nsuy boy<\/p>\n<p>5- \u00d1i jub \u00f1ooy naani ciy kub yu kafuur \u00e0nd ag bii\u00f1<\/p>\n<p>6- Teen wi jaami Y\u00e0lla yi di naani, te fu leen neex<br \/>\nj\u00ebm\u00eble ndox yi<\/p>\n<p>7- Danu matal seeni yeene dolli ragal b\u00e9s booba te ay<br \/>\nmusibaam di law fu sore<\/p>\n<p>8- Danu s\u00e9ddale ndax moom, dundal neewjidoole yi,<br \/>\nnjerim wi ag jaam wi nu j\u00e0pp<\/p>\n<p>9- Te naan: Da\u00f1u leen s\u00e9dd dund bii, ba m\u00ebn neex ci<br \/>\nkanamu Y\u00e0la te du \u00f1u leen ci laaj neexal walla ng\u00ebr\u00ebm<\/p>\n<p>10- Da\u00f1u raga ci wallu Y\u00e0lla aw b\u00e9s wu metti te \u00e0nd ag<br \/>\nmusiba<\/p>\n<p>11- Moo tax Y\u00e0lla musal leen ayiba b\u00e9s ba. Dafa leeral<br \/>\nseeni j\u00eb sol leen ag b\u00e0nneex<\/p>\n<p>12- Ndax seen dogu, dafa leen fay Ajjana ag y\u00e9r\u00e9 sooy<\/p>\n<p>13- Da\u00f1u fay jekki w\u00e9eru ci seeni diwaan. Du \u00f1u fa y\u00ebg<\/p>\n<p>tangaayu jant walla coonooy sedd<\/p>\n<p>14- Ay garab yu jagente \u00f1oo leen di muur ag seeni ker, te<br \/>\nseeni doom di w\u00e0cc ngir \u00f1u m\u00ebn leen witt te coono<br \/>\ndu am<\/p>\n<p>15- Da\u00f1oo joxante ci seen biir ay ngutti xaalis ag ay kub yu<br \/>\nweeru kiristaal<\/p>\n<p>16- Ci kiristaal biy nir\u00f3og xaalis te \u00f1u koy feesal na mu leen<br \/>\nneexe<\/p>\n<p>17- Danu cay faj seen mar ag kub yu fees dell, ag naan yu \u00e0nd<br \/>\nag ji\u00f1jeer<\/p>\n<p>18- Ci teenu Ajjana wu \u00f1u tudde Salsabill<\/p>\n<p>19- Ay xale yu di ay ndaw ba f\u00e0ww \u00f1ooy w\u00ebr di leen s\u00e9dd;<br \/>\nsoo leen gisee defe ni ay caxxi peme yu \u00f1u nocci la\u00f1u<\/p>\n<p>20- Soo gisoon lu ni mel, gis d\u00ebkkuwaayi b\u00e0nneex ag gu nguur<br \/>\ngu yaatu<\/p>\n<p>21- Da\u00f1oo sol y\u00e9r\u00e9 sate\u00f1 wu baxaw ag borokaar, takk ay lamu<br \/>\nxaalis. Seen Boroom naan yu sell la leeen di jox.<\/p>\n<p>22- Loolu mooy nekki seeni neexal dananu leen nattal seeni<br \/>\ncoono<\/p>\n<p>23- Danu la yone Alxuraan mu j\u00f3ge ca kaw<\/p>\n<p>24- Toogal mu\u00f1 di n\u00e9g dogali sa Boroom: Bul topp \u00f1i g\u00ebmul<\/p>\n<p>25- Dil tudd turu Y\u00e0lla suba ag ngoon<\/p>\n<p>26- Ag it ci guddi, soppal Y\u00e0lla te way jalooreem ciy guddi yu<br \/>\ny\u00e0gg<\/p>\n<p>27- Nit \u00f1i da\u00f1oo b\u00ebgg \u00e0ddina juy wal nu gaaw, tey b\u00e0yyi seen<br \/>\ngannaaw b\u00e9s bu metti ba<\/p>\n<p>28- Danu leen s\u00e0kk, te danu leen may doole, su nu xiiroon nu<br \/>\nwut\u00eble leen yeneeni nit<\/p>\n<p>29- Loolu mooy y\u00ebgle wi. Ki b\u00ebgg na s\u00f3obu ci yoon wi j\u00ebme ci<br \/>\nY\u00e0lla<\/p>\n<p>30- Waaye du\u00f1u m\u00ebn b\u00ebgg nag lu moy li Y\u00e0lla b\u00ebgg ndax dafa<br \/>\nxam te x\u00e0mmee<\/p>\n<p>31- Dana \u00ebmb ci kermandeem \u00f1i mu b\u00ebgg, tegal na \u00f1i g\u00ebmul<br \/>\nmbugg\u00ebl mu saf.<\/p>\n<p><strong><em>Jukki bi: Path\u00e9 Diagne, Alxuraan ci Wolof. Editions Sankore, L&#8217;Harmattan<\/em><\/strong><\/p>\n","protected":false},"excerpt":{"rendered":"<p>W\u00e0cce ci M\u00e0kka 31 laaya Benn &#8211; Senn &#8211; Menn la &#8211; Raax Menn &#8211; Raax Y\u00ebr\u00ebm 1- Ndax dafa toog lu y\u00e0gg te kenn f\u00e0ttelekuwu ko? 2- Danu door s\u00e0kk ci ndoxum ge\u00f1o wu \u00f1aari kanam \u00e0ndoo fekk \u00f1u koy seetlu. Daanu ko jox gis ak d\u00e9gg. 3- Danu ko teg ci yoon wu&#8230;<\/p>\n","protected":false},"author":1,"featured_media":0,"comment_status":"open","ping_status":"open","sticky":false,"template":"","format":"standard","meta":{"footnotes":""},"categories":[15],"tags":[],"_links":{"self":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/930"}],"collection":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts"}],"about":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/types\/post"}],"author":[{"embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/users\/1"}],"replies":[{"embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcomments&post=930"}],"version-history":[{"count":9,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/930\/revisions"}],"predecessor-version":[{"id":1328,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/930\/revisions\/1328"}],"wp:attachment":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fmedia&parent=930"}],"wp:term":[{"taxonomy":"category","embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcategories&post=930"},{"taxonomy":"post_tag","embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Ftags&post=930"}],"curies":[{"name":"wp","href":"https:\/\/api.w.org\/{rel}","templated":true}]}}