{"id":853,"date":"2011-06-23T13:23:53","date_gmt":"2011-06-23T13:23:53","guid":{"rendered":"http:\/\/www.wolof-online.com\/?p=853"},"modified":"2012-07-01T11:13:40","modified_gmt":"2012-07-01T11:13:40","slug":"askan-wi-fippu-na","status":"publish","type":"post","link":"https:\/\/www.wolof-online.com\/?p=853","title":{"rendered":"Askan wi fippu na!"},"content":{"rendered":"<p><a href=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/manif_wade_foule.jpg\"><img loading=\"lazy\" decoding=\"async\" class=\"alignleft size-full wp-image-854\" title=\"manif_wade_foule\" src=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/manif_wade_foule.jpg\" alt=\"\" width=\"300\" height=\"175\" \/><\/a>B\u00e9su alxam\u00e9s bii di 23 fan ci weeru swe 2011 b\u00e9s la bu mag ci biiri b\u00e9s yi ci ndeminu demokaraasi ci r\u00e9ewum Senegaal. Ndax gannaaw ba njiitu-r\u00e9ew mi f\u00e9sale yeeneem soppi s\u00e0rti r\u00e9ew ci anam yi \u00f1u ko wara falee moom ak ki wo wara wuutu, la c\u00f3ow lu r\u00eby j\u00f3lli fu nekk: \u00f1\u00e9pp di ko mb\u00e0mb naan jubluwu ci lu dul faluwaat, ag wut yoon wu mu fale doomam: di Karim Maysa W\u00e0dd. Ndax peresidaa ci luwaa boobu mu doon m\u00e9b\u00e9t da fa b\u00ebggoon su \u00f1u koy fal, falaale jaraaf ju koy wuutu su amee g\u00e0llankoor maanaam wiis-peresidaa! ImageRax ci dolli, pal moomu su ko 25 ci t\u00e9em\u00e9eri nit yu nekk falee rekk, pal ga day w\u00e9y, maanaan doonulkoon laajati 50% yi nga xam ne moom la yoonu-wote laajoon kiy dooni peresidaa am ko, ngir m\u00ebn a falu ci benn &#8220;tour&#8221; kese!<br \/>\nLuwaa boobu loolu la b\u00ebggoon na teggi ba noppi s\u00ebr\u00ebxal lawax bi wara wuutu njiitu r\u00e9ew mi su deme ba m\u00ebnatul ci diirug palam. Kenn reerewul mbir nag ne c\u00f3ow li w\u00ebr Senegaal ay at mooy: G\u00f3orgi day wut pexe mu muy def ba \u00f1u fal doomam, di Karim. Te loolu nag ci demokaraasi bu mel ni Senegaal lu teey xel lool la! Xanaa kon li Wolof Njaay waxoon dikk na: ku \u00f1uy jii\u00f1 ag nd\u00ebm fekk la ngay see\u00f1u yeelu liir.<\/p>\n<p>Wante nag lenn moom jangees na ko ci mbir mi: jamono ji \u00f1u tollu nii loo am ci sa\u00f1-sa\u00f1 rekk askan wee la ko may! Askanu Senegaal moom daa l\u00e0nk ba t\u00ebdd ca naaj wa ne luwaa boobu kenn du ko fi wote. Mbooloo mu takkoo genn ci biir r\u00e9ew mi y\u00e9pp di \u00f1aqtu ne loolu mukk du fi amee. Rawatina mbooloo ma dajaloo woon w\u00ebr p\u00e9nccum-ndawi-r\u00e9ew mi di xaar depite yi waroon na wote luwaa boobu, di leen yuqoo, di defanteek alkaati yi! Ndakaaru jax lool, t\u00e0ng j\u00ebrr! Wante askan wee mujjee ndam li: ndax luwaa boobu kenn wotewu ko: Njiitu-r\u00e9ew mi ci b\u00e9s bi la rocciwaat luwaa bi! Lii nag moom gull\u00e9et la ci Senegaal, jeego bu am solo la ci ndeminu demokaraasi ci biir r\u00e9ew mi: wone na mat gu w\u00e9r, t\u00e0kku bu w\u00f3or bu askan wi t\u00e0kku ngir saytu liy \u00e0qam aki sa\u00f1-sa\u00f1am!<br \/>\nKon \u00f1\u00e9pp a ngi xaar njiitu-r\u00e9ew mi ci li miy wara wax ag askan wi ci fan yii di \u00f1\u00ebw. Ndax j\u00e9ll bu ni mel kenn m\u00ebnu koo daanu ba noppi, j\u00f3g faxasu dem sa yoon: f\u00e0ww mu jakarloog askan wi wax li mu nar, diisoog moom ci xew-xew boobu ag la wara \u00f1\u00ebw ca kanam! Am na nag \u00f1u ne li ko war mooy mu tekki ndombo li!<\/p>\n<p>La ca kanam moom rawuli b\u00ebt! Kon g\u00e0cce ngaalaama r\u00e9ewum-Senegaal!<\/p>\n<p><iframe loading=\"lazy\" src=\"http:\/\/www.youtube.com\/embed\/P2UbcxLVhLw\" frameborder=\"0\" width=\"560\" height=\"315\"><\/iframe><\/p>\n<p>Tamsir Anne \u00a9 wolof-online.com<\/p>\n","protected":false},"excerpt":{"rendered":"<p>B\u00e9su alxam\u00e9s bii di 23 fan ci weeru swe 2011 b\u00e9s la bu mag ci biiri b\u00e9s yi ci ndeminu demokaraasi ci r\u00e9ewum Senegaal. Ndax gannaaw ba njiitu-r\u00e9ew mi f\u00e9sale yeeneem soppi s\u00e0rti r\u00e9ew ci anam yi \u00f1u ko wara falee moom ak ki wo wara wuutu, la c\u00f3ow lu r\u00eby j\u00f3lli fu nekk: \u00f1\u00e9pp&#8230;<\/p>\n","protected":false},"author":1,"featured_media":0,"comment_status":"open","ping_status":"open","sticky":false,"template":"","format":"standard","meta":{"footnotes":""},"categories":[4],"tags":[],"_links":{"self":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/853"}],"collection":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts"}],"about":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/types\/post"}],"author":[{"embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/users\/1"}],"replies":[{"embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcomments&post=853"}],"version-history":[{"count":4,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/853\/revisions"}],"predecessor-version":[{"id":1392,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/853\/revisions\/1392"}],"wp:attachment":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fmedia&parent=853"}],"wp:term":[{"taxonomy":"category","embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcategories&post=853"},{"taxonomy":"post_tag","embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Ftags&post=853"}],"curies":[{"name":"wp","href":"https:\/\/api.w.org\/{rel}","templated":true}]}}