{"id":813,"date":"2012-09-17T20:37:18","date_gmt":"2012-09-17T20:37:18","guid":{"rendered":"http:\/\/www.wolof-online.com\/?p=813"},"modified":"2012-09-19T06:45:24","modified_gmt":"2012-09-19T06:45:24","slug":"ku-wax-feen-demokaraasi-ag-lakki-reew-mi-ku-wax-feen-demokaraasi-ag-lakki-reew-mi","status":"publish","type":"post","link":"https:\/\/www.wolof-online.com\/?p=813","title":{"rendered":"Ku wax fee\u00f1: demokaraasi ag l\u00e0kki r\u00e9ew mi"},"content":{"rendered":"<p><a href=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/03\/lakkireewmi1.jpg\"><img loading=\"lazy\" decoding=\"async\" class=\"aligncenter size-full wp-image-821\" title=\"lakkireewmi\" src=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/03\/lakkireewmi1.jpg\" alt=\"\" width=\"600\" height=\"460\" srcset=\"https:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/03\/lakkireewmi1.jpg 600w, https:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/03\/lakkireewmi1-300x230.jpg 300w\" sizes=\"(max-width: 600px) 100vw, 600px\" \/><\/a><\/p>\n<p>Wote bi nu d\u00ebgmal, \u00f1\u00e9pp xam na \u00f1u ko, wote bu jeggi dayoo la: ndax ci la \u00ebll\u00ebgu r\u00e9ew mi aaju! Wote t\u00e0nn la wan yoon la Senegaal war a teggu j\u00ebm ca kanam mbaa mu teggi ko, dellu gannaaw: lawla cat! Wante li \u00f1u soxal ci jukki bii, lu l\u00ebkk\u00ebloog loolu gaa, wante leneen la. Loo xam ne soo ko seetloo, dafa mel ni dafa am j\u00e0llarbi ci ni &#8220;politiciens&#8221; di j\u00ebfandikoo l\u00e0kki r\u00e9ew mi! Li \u00f1u leen doon faral di wax mooy: demokaraasi ci l\u00e0kki-jambuur ay k\u00e1cci neen la, m\u00ebnu la nekk! Ndax demokaraasi mooy nguuru askan wi ngir askan wi!<br \/>\nWaaw, bu fekke ne nag fa \u00f1uy takke aka tekki, fa \u00f1uy d\u00f3gale, fa \u00f1uy fasee aka fecci, \u00f1a fay wax du \u00f1u wax lu askan wi m\u00ebn a d\u00e9gg, naka lees m\u00ebn a tuddee mbir mooma demokaraasi? Dafa mel ni daal buum bi \u00f1u kolonisat\u00eb\u00ebr bi nasoon, ba taxoon \u00f1uy w\u00e9y ci waawaam, ba l\u00e9egi d\u00f3gagul! Te buum boobu, x\u00e0ncc bi \u00f1u ko r\u00e0bbee mooy di j\u00ebfandikoo l\u00e0kki nasaraan soofal sunu bos, di j\u00e0ng cosaanaam f\u00e0tte sunu bos, j\u00ebl ay kureelam indi teg, j\u00ebl doxalinam indi teg, j\u00ebl xaalisam indi teg\u2026 Te loolu feek mu ngi fi, c\u00f3ow leey bari rekk, wante demokaraasi d\u00ebgg, mbaa j\u00ebm-ca-kanam ci w\u00e0llu koom-koom caada ag nekkinu askan wi da na fi jafe lool!!!<br \/>\nLiy firndeel loolu, mooy ba nasaraan bi xamee ne l\u00e9egi mu \u00f1akk r\u00e9ewi Afrik yi mu kolonise woon, fekk Alseeri ngiy xare ngir moom boppam, Wietnam duma Faraas Jemben-Fuu, Kamerun t\u00e0mbalee fippu, seneraal Degaulle da fa ne woon: &#8220;na \u00f1u yolomal buum gi ba laa moo d\u00f3g&#8221;!<br \/>\nTe loolu li muy tekki mooy, na fi sunu j\u00ebmm yi j\u00f3gge, wante sunu doxalin moom na sax ci xel yi ba f\u00e0ww! Te looloo fi amoon, ba fi Se\u03b7\u00f3or nekkee ba ci Abdu Juuf ag \u00f1i fi nekk t\u00e9y! Xam na\u00f1u ne Se\u03b7\u00f3or ba mu fi j\u00f3gge da dem Faraas nekk &#8220;Accad\u00e9mie francaise&#8221; , Abdu Juuf j\u00f3gge fi dem jiiteji &#8220;francophonie&#8221; di b\u00e0kk, di b\u00e0kkoo l\u00e0kki nasaaraan! Xalaas, loolu de du ngo\u00f3ora! Te su caaxaan faaxee d\u00ebgg des, Afrikee rekk ngay gis muy nangu loolu! Kenn \u00f1emewul xalaat sax, gis sinwaa, mbaa sapone mbaa wietnamee buy soofal l\u00e0kk wi mu n\u00e0mp, dem di b\u00e0kkoo l\u00e0kki \u00f1i ko mas a d\u00ebkkee tuutal ag nas buum! Da \u00f1u fee d\u00e9ggoon ci lu y\u00e0ggul dara sax njiitu-r\u00e9ew mi di wax di b\u00e0kku naan, Senegaal mooy r\u00e9ew mi nga xam ne, soo limaaleewul Faraas, fa la nit \u00f1a g\u00ebn a xere\u00f1\u00f1ee ci l\u00e0kk nasaraan!!! Wante nag Wolof Njaay da ne li nga moom nga m\u00ebn a tiitaroo! Li nga moomul moom, Bafa rekk la s\u00e0nt! Seex Anta yokk ca ne &#8220;l\u00e1kki jambuur de su safoon suukar ba mel ni lem itam, m\u00ebnoo ko m\u00e1cc ba cay taxamtiku&#8221;.<br \/>\n\u00d1aka xam daal ag \u00f1akk fayda li \u00f1u waral bari na! \u00d1u bari ci waay-xeltu yi sax da\u00f1oo defe ni, wax yu ni mel ay waxi-d\u00e9mb mbaa ay wax yu amul solo la\u00f1u, te fekk ne loolooy nd\u00e9yi-mbill ji!<br \/>\nAmul xejj-ak-seen, amul benn r\u00e9ew bu m\u00ebna am yokkute, am tawf\u00e9ex ci kow topp aadaa, ag cosaanu weneen askan, rawatina d\u00ebkkee j\u00ebfandikoo l\u00e0mmi\u00f1 woo moomul te fekk Y\u00e0lla natoowul a ag lu!<br \/>\nImageWante nag ba l\u00e9egi yakaar tasagul! Ndax t\u00e9y soo seete xale yiy &#8220;rap&#8221;, seen xarala ci l\u00e1kki r\u00e9ew mi, li \u00f1u ciy wax, li \u00f1uy ciy y\u00e0tt ci ay k\u00e1ddu yuy xalam, seen farlu ci siggil r\u00e9ew mi ag askan wi, dootoo amati benn siiki-saaka ne l\u00e0kki r\u00e9ew mi \u00f1u ngi ci yoonu suqaliku gu w\u00e9r! Ba tax na sax, soo koo setantalee, da ngay gis ne &#8220;politiciens&#8221; seen bopp dafa mel ni da\u00f1oo xawa n\u00e0nd loolou&#8221;! Ndax l\u00e9egi \u00f1oom \u00f1\u00e9pp a taamoo wut ay d\u00e0kkentali wolof: Moo xam &#8220;Bennoo Siggil Senegaal la, Bes du \u00f1akk, Fekkee ma ci boolee, Daas fanaanal, Nay leer, Car leneen, Taxaw temm&#8230;&#8221; ag yeneen yeneeni y\u00ebngu-y\u00ebngu la\u00f1u! Loolu soo koo seetloo bu baax ag j\u00e0llarbi la daanaaka, ab &#8220;revolution linguistique&#8221; la! Ndax ku ci nekk xam na ni soo nee askan wi &#8220;bennoo siggil Senegaal&#8221; rekk nit \u00f1i xam loo wax, jaratul sax nga leen di faramf\u00e0cceel lenn. Wante soo leen nee &#8220;CAP 21&#8221;, walla nga ne leen &#8220;Coalition pour l&#8217;Aternative&#8221; \u00f1u bari day mel ci \u00f1oom ne ay waxi-picc! Te mbir mi nag, waxoon naa leen ko fi, su \u00f1u doon j\u00ebfandikoo sunu l\u00e0kk yi rekk l\u00e9egi l\u00e9pp leer na\u00f1\u00f1! Loo waxati \u00f1\u00e9pp xam ko: doo fi naxati kenn! Moo tax ba fi njiitu-r\u00e9ew mi nee &#8220;maa waxoon waxeet!&#8221; mb\u00e0mb li w\u00ebr \u00e0ddina! Wante su ne woon ci nasaaran &#8220;j&#8217;avais dit, mais maintenant je me d\u00e9dis&#8221;, mbir mi du demee noonu! Kon soo ko seete, l\u00e0kki jambuur wi \u00f1u fi saxal ab juntukaay la itam bu \u00f1uy noote aka naaxale askan wi la, maanaan &#8220;c&#8217;est un instrument de domination et d&#8217;infantilasation aussi du peuple&#8221;! Mbas ci li fi &#8220;Jean ak Paul def&#8221;!<\/p>\n<p><em><strong>Tamsir Anne : tamsir.anne@wolof-online.com<\/strong><\/em><\/p>\n","protected":false},"excerpt":{"rendered":"<p>Wote bi nu d\u00ebgmal, \u00f1\u00e9pp xam na \u00f1u ko, wote bu jeggi dayoo la: ndax ci la \u00ebll\u00ebgu r\u00e9ew mi aaju! Wote t\u00e0nn la wan yoon la Senegaal war a teggu j\u00ebm ca kanam mbaa mu teggi ko, dellu gannaaw: lawla cat! Wante li \u00f1u soxal ci jukki bii, lu l\u00ebkk\u00ebloog loolu gaa, wante leneen&#8230;<\/p>\n","protected":false},"author":1,"featured_media":0,"comment_status":"open","ping_status":"open","sticky":false,"template":"","format":"standard","meta":{"footnotes":""},"categories":[4],"tags":[],"_links":{"self":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/813"}],"collection":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts"}],"about":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/types\/post"}],"author":[{"embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/users\/1"}],"replies":[{"embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcomments&post=813"}],"version-history":[{"count":19,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/813\/revisions"}],"predecessor-version":[{"id":1629,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/813\/revisions\/1629"}],"wp:attachment":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fmedia&parent=813"}],"wp:term":[{"taxonomy":"category","embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcategories&post=813"},{"taxonomy":"post_tag","embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Ftags&post=813"}],"curies":[{"name":"wp","href":"https:\/\/api.w.org\/{rel}","templated":true}]}}