{"id":784,"date":"2012-01-31T20:56:50","date_gmt":"2012-01-31T20:56:50","guid":{"rendered":"http:\/\/www.wolof-online.com\/?p=784"},"modified":"2012-07-01T11:13:12","modified_gmt":"2012-07-01T11:13:12","slug":"784","status":"publish","type":"post","link":"https:\/\/www.wolof-online.com\/?p=784","title":{"rendered":""},"content":{"rendered":"<p><strong>Y\u00e0tt bi l\u00ebmbee jamono!<\/strong><\/p>\n<p><a href=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/05\/monument.jpg\"><img loading=\"lazy\" decoding=\"async\" class=\"alignleft size-full wp-image-785\" title=\"monument\" src=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/05\/monument.jpg\" alt=\"\" width=\"294\" height=\"287\" \/><\/a>Su dee ni ko yenn waay-xeltu yi di waxee namm-namm xarala d\u00ebggantaan mooy g\u00ebs\u00ebm xelu nit \u00f1i ba \u00f1u xippi xool, gise neneen mbir yi leen w\u00ebr,ku yebboo kon ne y\u00e0tt bi Ablaay W\u00e0d y\u00e0ttlu Wakaam y\u00e9gg na ca la mu ca doon wut. Ndax ndonte sax nag sotteegul, &#8220;ngenteegu&#8221; \u00f1u ko maanaam, xel yeek xalaat y\u00e9pp a ngi l\u00ebmbee di ko xaar&#8230; Su caaxaan faaxee d\u00ebgg d\u00e9s, Imagey\u00e0tt bi daa xajj\u00e0lle r\u00e9ew mi ak li ko weesu \u00f1aar ba \u00f1ett ak \u00f1eenti l\u00e0ng: \u00f1ii ne mbir la bu am solo, ndax day mandargaal g\u00ebddu nit ku \u00f1uul ak suxxaliku gi askan yi ci Afrik, caagewul njaam gi ag metit yi \u00f1u leen doon t\u00e9gg y\u00e9pp, masul a j\u00f3g di ko s\u00e0kku, di ko y\u00f3otu. Am \u00f1eneen \u00f1u ne y\u00e0tt bii mooy firndeel d\u00ebgg cuune, caaxaan ag c\u00e0ggante gi nguuru Ablaay W\u00e0dd ngemboo: ndax nees lay j\u00eblee ci r\u00e9ew mu l\u00f3tt ni Senegaal, nit \u00f1i d\u00ebkkee jaaxle ag di tuu\u00f1-tuu\u00f1i lu \u00f1u lekk, xale yiy s\u00f3obu ci g\u00e9ej gi di wut a raw, ay miliyaari-miliyaari di ko def ci y\u00e0tt bu kenn xamul y\u00e0ttu lan la? Am genneen l\u00e0ng gu ca yokk ne li w\u00e9r mooy y\u00e0tt bi warul a taxaw mukk ci r\u00e9ewum Senegaal gii di r\u00e9ewu julit, ndax diine lislaam dafay tere di y\u00e0tt ay nit, rawatina y\u00ebkkati ko ba mu mel ni luy juqarbi asamaan&#8230; Am na itam \u00f1oo xam da\u00f1u ne \u00f1oom li leen naqari mooy y\u00e0tt bi ci boppam dafa amul lenn lu am solo lu muy misaal, rax ci dolli rafetul, taaruwul! Dafa f\u00f3oy\u00f3oy daal manaam su \u00f1u ko seete, t\u00e9g ko ci s\u00e0rt yi aaru Afrik di w\u00e9y. Y\u00e0tt bi nag ci w\u00e0llu boppam mu nga nekk Wakaam, ca tundu Mamel, jakarloog g\u00e9ej. Tollu na ci taxawaay 50 m, genn g\u00f3or j\u00e0pp jenn jigg\u00e9en, fab ci loxo c\u00e0mmo\u00f1 benn xale bu talal loxom di joxo\u00f1 xarfu. Loolu nag li muy misaal, \u00f1u ne, taxaw-temmu Afrik la, giy gindeekoo ci l\u00ebnd\u00ebmtoog njaam, d\u00ebgmal \u00ebll\u00ebgug yaakaar ag ng\u00ebm gu mat s\u00ebkk. Li w\u00e9r daal mooy na y\u00e0tt bi ci j\u00ebmmam ag yenneen y\u00e0tt yu mel ni &#8220;y\u00e0ttu moomeel sa bopp&#8221; ba ca Amerik, mbaa y\u00e0ttu Yeesu Kiris ba ca Riyoo lay diiranteel mb\u00e0gg! Ndaxam sax nag Beresil mbaa Amerik m\u00ebneesu leen a jawaatleek Senegaal! Ci b\u00e9su 04 Awril 2010, tembook 50eelu at ba Senegaal moomee boppam ba l\u00e9egi, lees ko wara ngente. Li jaaxal nit \u00f1i mooy nan la askan wi, rawatina kilifa diine lislaam nara doxale? Ndax dana \u00f1u teeweeji tudd ba am d\u00e9ed? Ndax it kilifa yenneen r\u00e9ew yi \u00f1u w\u00f3o dana\u00f1u \u00f1\u00ebw am da\u00f1uy g\u00e0ntu? Kon mbir ma ngi noonu: c\u00f3ow li bare na, xel yeeg xalaat ya ngi jo\u00c5\u2039ante! Su dee seetaan na daq cib ndajee kon lay \u00f1\u00ebw ca kanam a wara g\u00ebna neex!<\/p>\n<p>Tamsir Anne \u00a9 wolof-online.com<\/p>\n","protected":false},"excerpt":{"rendered":"<p>Y\u00e0tt bi l\u00ebmbee jamono! Su dee ni ko yenn waay-xeltu yi di waxee namm-namm xarala d\u00ebggantaan mooy g\u00ebs\u00ebm xelu nit \u00f1i ba \u00f1u xippi xool, gise neneen mbir yi leen w\u00ebr,ku yebboo kon ne y\u00e0tt bi Ablaay W\u00e0d y\u00e0ttlu Wakaam y\u00e9gg na ca la mu ca doon wut. Ndax ndonte sax nag sotteegul, &#8220;ngenteegu&#8221; \u00f1u&#8230;<\/p>\n","protected":false},"author":1,"featured_media":0,"comment_status":"open","ping_status":"open","sticky":false,"template":"","format":"standard","meta":{"footnotes":""},"categories":[6],"tags":[],"_links":{"self":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/784"}],"collection":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts"}],"about":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/types\/post"}],"author":[{"embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/users\/1"}],"replies":[{"embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcomments&post=784"}],"version-history":[{"count":6,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/784\/revisions"}],"predecessor-version":[{"id":1390,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/784\/revisions\/1390"}],"wp:attachment":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fmedia&parent=784"}],"wp:term":[{"taxonomy":"category","embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcategories&post=784"},{"taxonomy":"post_tag","embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Ftags&post=784"}],"curies":[{"name":"wp","href":"https:\/\/api.w.org\/{rel}","templated":true}]}}