{"id":671,"date":"2014-11-16T16:54:50","date_gmt":"2014-11-16T16:54:50","guid":{"rendered":"http:\/\/www.wolof-online.com\/?p=671"},"modified":"2014-12-22T14:41:13","modified_gmt":"2014-12-22T14:41:13","slug":"solo-cosaan-ciw-askan","status":"publish","type":"post","link":"https:\/\/www.wolof-online.com\/?p=671","title":{"rendered":"Solo cosaan ciw askan"},"content":{"rendered":"<p><a href=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/03\/ndatte-yalla600_21.jpg\"><img loading=\"lazy\" decoding=\"async\" class=\"aligncenter size-full wp-image-752\" title=\"ndatte-yalla600_2\" src=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/03\/ndatte-yalla600_21.jpg\" alt=\"\" width=\"599\" height=\"682\" srcset=\"https:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/03\/ndatte-yalla600_21.jpg 599w, https:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/03\/ndatte-yalla600_21-263x300.jpg 263w\" sizes=\"(max-width: 599px) 100vw, 599px\" \/><\/a><\/p>\n<p>Cosaan soo kooy seet, m\u00ebnees naa wax ne, mooy x\u00e0ncc biy boole ay nit ba \u00f1u m\u00ebna r\u00e0\u00f1\u00f1ee ne nit \u00f1oo\u00f1ee \u00f1ooy askan sangam. Ndax soo demoon t\u00e9y marse S\u00e0ndaga, di b\u00e9r\u00e9b bu ay turist yu joggee fun nekk ci \u00e0ddina di dajaloo di j\u00ebnd, doo m\u00ebna wax mukk ne \u00f1oo\u00f1a fa tase askanu turist la\u00f1u bokk. Walla book xanaaa wax jooju dib waxi-misaal, nde fa d\u00ebgg dgg ay dox-daje kese la\u00f1u!<\/p>\n<p>Wante aw askan nag dug dox-daje koy tabax.Image Su \u00f1uy wax askan, li mu \u00ebmb mooy ay nit \u00f1u bokk aada yu y\u00e0gg, bokk ca cosaan, am fu seen maam jaar d\u00e9mb ba yegsi foofee \u00f1u yegsi t\u00e9y. Dafa am kon lu boole nit \u00f1oona \u00f1u naan \u00f1ooy askan sangam ca jamonooy d\u00e9mb ba l\u00e9egi.<\/p>\n<p>Dafa mel ni kon cosaan mooy buum biy l\u00ebkkale ay nit, ba \u00f1u nopppee doon aw mbooloo kese, soppaliku aw askan! Su doon ne dees di mengale aw askan akub tabax, dees ay xala wax ne cosaan mooy kennu tabax boobee.<br \/>\nLooloo tax ba aw xeet mbaa aw askan, soo ko b\u00ebggee noot ba f\u00e0ww rekk, farlul ci mu f\u00e0tte cosaanam! Loolu nag la tubaab bi ci pexeem mu r\u00eby n\u00e0ndoon, ba tax ba mu fi b\u00ebggee d\u00ebj doxalinam, dafa j\u00ebl ndawi r\u00e9ew yi dugal leen ci ay daaraam, j\u00e0ngal leen l\u00e0kkam, j\u00e0ngal leen cosaanam moom tubaab bi, ba noppi nag ne leen, yeen moom amu leen cosaan, ndeysaan, su ngeen yebboo rekk jeema roy ci \u00f1un.<\/p>\n<p>Noonu cosaan amee solo noonu la it l\u00e0kk amee solo, rax ci dolli l\u00e0kk woo gis dafa am cosaanam, am mbokkoo gu dox diggant\u00e9em ak l\u00e0kki yenneeni askan, rawatina askan yi ko g\u00ebna jege. Naka noonu la Wolof bokkee ak p\u00ebl, bokk kook sereer, bokk koog saraxolle ak yenneen l\u00e0kki r\u00e9ew-mi. Wante nag itam, baat yi ci l\u00e0kk wi seen bopp da\u00f1oo mel ni saa woo xam ne soo ko toppee, dangay y\u00e9gg ba fa askani Wolof cosaanu d\u00ebgg te mooy b\u00eblub dexu Niil ca Misira d\u00e9mb!<br \/>\nSoo dendalee Wolof ak l\u00e0kki Misira d\u00e9mb, ag l\u00e0kki askan yi nekk ba b\u00e9su t\u00e9y ji b\u00ebj-t\u00e0nku Esipt, naka Nuer, day f\u00e9s ne Wolof dafa bokk bu baax, ci anam yu jeggi dayoo ag l\u00e0kk yooyu.<br \/>\nMbokkoo gi dox diggante Wolof ak l\u00e0kki Esipt m\u00ebneesu ko fee f\u00e0ramfaccee ba mu jeex: Dafa di mbokk gu xoot te daj l\u00e0kk w\u00e9pp, f\u00e9s ci baati diine yi, baati mbokkoo yi, baat yiy tudd c\u00ebri nit ak yeneen ak yeneen. Te baat yooyu ay l\u00e0kk du \u00f1u ko niroole, te f\u00e0ww amul mbokkoo gu dox ci seen diggante!<br \/>\nLoolu l\u00e9pp nag li mu lay won mooy ne l\u00e0kki r\u00e9ew demu \u00f1u sax bay f\u00f3oy\u00f3oy! Sunu l\u00e0kk yi \u00f1u donnee sunu Maam ya, muy Wolof mbaa p\u00ebl, mbaa sereer, mbaa joola walla wenneen l\u00e0kk wu mu ci m\u00ebnti doon, seen solo ci defaraat nit \u00f1i, defaraat r\u00e9ewi Afrik, delloo leen seen g\u00ebdd lu jeggi d\u00e0yyoo la te mata s\u00e9dd la!<br \/>\nWante nag su caaxaan f\u00e0qee, d\u00ebgg des, kuy jeggaani ba jeggaani aw l\u00e0kk te ame sa l\u00e0mmi\u00f1, l\u00fawuloo, war ngaa seetaat sa bopp!<br \/>\nLi am ba des rekk mooy li Seex Musaa wax ne &#8220;b\u00e9pp l\u00e0kk rafet na, buy gindi ca nit xel ma, t\u00e9y tudd ca moom ngor la!&#8221;<\/p>\n<p>Tamsir Anne \u00a9 wolof-online.com<\/p>\n","protected":false},"excerpt":{"rendered":"<p>Cosaan soo kooy seet, m\u00ebnees naa wax ne, mooy x\u00e0ncc biy boole ay nit ba \u00f1u m\u00ebna r\u00e0\u00f1\u00f1ee ne nit \u00f1oo\u00f1ee \u00f1ooy askan sangam. Ndax soo demoon t\u00e9y marse S\u00e0ndaga, di b\u00e9r\u00e9b bu ay turist yu joggee fun nekk ci \u00e0ddina di dajaloo di j\u00ebnd, doo m\u00ebna wax mukk ne \u00f1oo\u00f1a fa tase askanu turist&#8230;<\/p>\n","protected":false},"author":1,"featured_media":0,"comment_status":"open","ping_status":"open","sticky":false,"template":"","format":"standard","meta":{"footnotes":""},"categories":[18],"tags":[],"_links":{"self":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/671"}],"collection":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts"}],"about":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/types\/post"}],"author":[{"embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/users\/1"}],"replies":[{"embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcomments&post=671"}],"version-history":[{"count":25,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/671\/revisions"}],"predecessor-version":[{"id":687,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/671\/revisions\/687"}],"wp:attachment":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fmedia&parent=671"}],"wp:term":[{"taxonomy":"category","embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcategories&post=671"},{"taxonomy":"post_tag","embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Ftags&post=671"}],"curies":[{"name":"wp","href":"https:\/\/api.w.org\/{rel}","templated":true}]}}